Aatu réer na mii ñuy way ci làmb yi, Aatu réer na nga xam ne waykat yi dañu koo yeesalaat ak a tëggaat, waaye way wu yàgg la. Góor gi...
UbbiXoolal Laltaayug Kippaango Jàng Wolof bala ngay door njàng mi
Aatu réer na mii ñuy way ci làmb yi, Aatu réer na nga xam ne waykat yi dañu koo yeesalaat ak a tëggaat, waaye way wu yàgg la. Góor gi...
UbbiKuy laal Maademba sabar ga ca Ndaayànde kuy laal ndaat-saay.Kuy laal sama doom jee, salaan jooyul wéet óo. Sama doom sama soppe dund a mat a jooy óo, moom laay...
UbbiWaati wolof ak seeni leeral
Kippaango Jàng Wolof barab la bees sos 10i fani féewerye ci atum 2018 ci njiital Sëñ Seex Lóo, Sëñ Bëgg Bàmba Géy ak Sëñ Ismayla Géy di ñenn ci Akaademi wolof. Cos gee ngi tukkee ci coobarewu ak bëgg a liggeeyal làkku wolof ba ñu bari man koo wax, man koo dawal ba noppi man koo bind. Ci kaw gis-gis bii, la Kippaango Jàng Wolof sosoo ngir yaatal làkk wi, suqali làkk wi ak liggéeyal làkk wi ci sunu xam-xam, sunu am-am ak sunu man-man ci lu dul fayeeku kenn. Njiiti Kippaango Jàng Wolof warlul nañu képp ku ci bokk te tënku ci sàrt yi, njàngum wolof ci lu dul muy fay dara, loolu nag amul setteey cosaan walla gog xeet walla gog diine. Kippaango Jàng Wolof dafa séddalikoo ci ay jàngu yoy ku ci nekk sag coobarewu ak sag bëgg ak sag tënku ci sàrt yi ñoo lay boole ci njàng mi.