Catégories
Sëñ Sàmba Jaara Mbay

Jasbul majsóob

Bismi-l-Laahi-r-Rahmaani-r-Rahiimi

Alhamdu lillaahi ki may

Xamal bu wér, ta di ma may
Xéewal ci barkeb ki mu xëy,
Jébbal lu dooni xéewëlam.

Yéen gaayi diine jegeleen
Ma jege leen te dolli leen,
Xam-xam bu wér te jafe leen,
Ma fecci tay ay fas-fasam.

Koo xam ni xam na Iii,na xam,
Ku ko xamul, ma wax mu xam,
Xamlug xamul, day taxa xam,
Xamlu ku xam ,day dolli xam.

Te Iii ma leen di bëgg a wax,
Day dàggi xol, dëggali wax,
Jagali jëf, te ku ko wax,
Jariñu fii, ak fa nu jëm.

Masuma leen a waxi neen,
Te lii ma wax, du waxi neen,
Lii woyu xudbu la, du neen,
Yu deefi woy ñu dul kemam.

5 – Jazbul Majzòob

Naa sant yàlla mi ma may,
Xutbu bu mat, mu di ma may,
Di fay ay, di dàqi moy,
Ci leeri mbóoti ragalam.

Di ma gisal luma gisul,
Di ma yëgal luma yëgul,
Di ma xamal luma xamul,
Ci duusi géeji xam-xamam.

Di ma amal luma amuI,
Di ma wutal, di ma wattul,
Di ma digal, di ma tamal,
Nangoo yamooki ndigalam.

Di ma yërëm, di ma tifaI,
Di ma jariñ, di ma teral,
Def ma ma mel ni ku nu fal,
Ku tàbbi péeyi ngërëmam,

Di ma dugal fumay musal,
Di ma fegal luma ragal,
Ku jëm ci man ak i fetal,
Mu boole diigali walam.


6 – Jazbul Majzòob

Dima setal ci waxi bañ,
Ba ku ma yéene jëfi bañ,
Mu ni ko tëf, mu ni suluñ,
Daanu, di toppal fetalam.

Di ma xëccal, di ma jañal,
Di ma tàyyil, di ma tayaI,
Di ma ubbil bunti xéewël,
Fat ma ci biir ruqi ñoñam,

Ne ma yëkkét, newuma tuy,
Wan ma boppam, ma di ko woy,
Ta di ko kañ, mu di ma may,
Ne ma yoxoos ci biir xolam.

Di ma fegaI pexe mu naaw,
Di ma teral ren ak i daaw,
Di ma teral sama gannaaw,
Di ma teral sama kanam.

Dib suruseñ bimay fajal,
Di garabal li ma ragal,
Di ma félal lumay sonal ,
Mu teggi, teg, yenu jëem.


Jazbul Majzòob – 7

Dima toggal, dima yakkal,
Di ma ràccal, di ma sefal,
Di ma tibbal, di ma lehal,
Tib yu ñu barkeelug wannam.

Di ma bégaI, di ma seraI,
Di ma xàjjal, di ma dalal,
Di ma moyuI, di ma fayuI,
Kenn duma yab fi kanamam.

Buma yewwee, kenn duma yab,
Fuma fi jëm, du ma ayib,
Sama gannaaw sama ayib,
Xanaa nammeel gu ñu ma namm.

Sama ñoñ it duñu ayib,
Man ak i ñoom duñu layib,
Sëriñ bi moo dajale yëpp,
Beral nu cër bu ñu gërëm,

Li mu ma may ma di ko am,
Moo ma ko may ma di ko am.
Li mu ma wax ma di ko xam,
Moo ma ko wax ma di ko xam.


8 – Jazbul Majzóob

Limu ma wan ma di ko gis,
Moo ma ko wan ma di ko gis.
Ta ku ko gis, ni ku ko gis,
Ni ku ko xam, ni ku ko am.

May na ma lol, danaa ko wax,
May na ma lol, duma ko wax,
May na ma lool, man mi ko wax,
Ak ba ko ñooni kee fa yam.

Man Samba Jaara, maa gërëm
Samab sëriñ, danaa xorom
Way wi ma way ci waa këram,
Ñoo am ngërëm, ñoo am xorom.

Bu sëg sëggee ba ñu wéral,
Li tax ma jóg di ko biral,
Werante deñ, kon nag yëral
Seen i jaloore ca kanam.

Jësbul xuloob bi dafa jib,
Bii jësbu jóg xeeñ famu jub
Lu, ku ko xeeñ na wut a jub,
Wéy na xameeful fumu jëm.


Jazbul Majzòob – 9

Jësbul xuloob bi dafa daw,
Bii jësbu jóg, xeeñ fa mu aw,
Ta ku ko dab na daw a daw,
Raw na xameeful fumu yam.

Lu jiitu Iii dafa dawal,
Ña daa rawanteek a dawal,
Nabka fëxal raw ba àggal,
Ak am wa kenn gisul pëndam.

Ma daal di jóg, tofal ko bii
Jësbu, di woy ki woy Nabi,
Di ko ko fay na woy Nabi,
Ma di ko woy ba fa nu jëm.

Kemub li ñuy dox di ko woy,
Fayante la ak moom ki mu woy,
Da koo gërëm ba di ko may
Lammiñ yi daal di ko gërëm,

Ma far jafal man di ko woy,
Di barkeelook a di ko roy
Ci woy, ba daane ku ko woy,
Ak ku woyul ñu ne wedam.


10 – Jazbul Majzóob

Luma wax ak lu ma waxul ,
Wuute gi fës na, nëbbuwul,
Ta ba fi tay danaa fësal
Lu doy a xam ci ay woyam.

Danaa xamaI, xamul mu xam,
Xamal ku xam, mu gën a xam,
Ku bëgg a gis ta bëgg a xam,
Na déglu, xippi ay bëtam.

Kenn du werante Ii ma wax,
Way xam ya, xam na sama wax,
Seriñ bii moo may sama wax,
Moo tax ma saf ko ci xolam.

Buleen ma yéem, yéemleen ko, ndax
Du man di wax, mooy ka di wax,
Waxande laa wuñ tëjii wax,
Buma tijjee may lammiñam.

Wàlliyu day feeñu, ta kum
Feeñu ci yaw, nga daal di xam,
Bu nee waxal, nga wax ñu xam,
Way xam ya ,seede daal di gëm.


Jazbul Majzòob – 11

Bu fekkee moo feeñu ci man,
Ñu naa ma yaw, booba du man,
Moom, ka di moom, moo fi di man.
Ma di fi moom, muy ki fi xam.

Moo tax ma wax ku déglu lii
Na xam ni yii ñuy wax du lii,
Waaraate jóowuma si lii,
Seriñ bi may na ma boppam.

Kaawteefug Yónnent la gu des,
Te ag wéyam dara du des,
Lu doon kiraama yu fi des,
Dina ko yóbbaale ñu dem.

Sëriñ bi muxjisaat la, moom,
Man nag kiraama laa, ci moom,
Ku weddi lii, na dem fa moom,
Laaj ko, mu teqalem lëjam.

Moo tax li may wax moo ko moom,
Masuma ko jaawale moom,
Tudd turam doy na ma koom,
Ta mooy seral sama yaram.


12 – Jazbul Majzóob

Bind turam may na ma xel,
Tudd turam may na ma xol,
Siirub turam may na ma lol,
Duma ko wax, xol a ko xam.

Danaa biral tuuti, ci ay
Mayam ci man, yu ñu ma may,
Te yi le may, ku ñu ko may,
War nay gërëm diirug dundam.

Buur Yàlla may na ma ci moom,
Gëm, ak xam, ak lafu ci moom,
Ma jòg ne naa taasu ci moom,
Di ko beral woyi ngërëm.

May na ma lol, deefuma nax,
Wan na ma lol, deefuma nax,
Naxtima kenn, kenn duma nax,
Sama ngërëm raw nag xalam.

Xam naa ndigël, xam naa ndugël,
Ti naa ndigël ,të naa ndugël,
Damay digal duma dugël,
Sama mébët, aw ndigëlam.


Jazbul Majzóob – 13

Ki lay digël, ta du la jay,
Ki lay dugal, ta di la jay,
Boo xelluwul, defoo ku way,
Réccooki jooy feeñ sa kanam.

Ku may digël, dafay taxaw,
Ku may dugël, dafay taxaw,
Ta naa awal, fii bufi aw,
Ki ma giseel a mat a xam

Lu ne ci Iii, ma ni ko jàkk,
Lu ne ci lee, ma ni ko jàkk,
Xam la jagul, ñee ak la jag,
Ki ma giseel a mat a am.

Wan na ma lool, yee na ma jar,
Ba ma ràññee dëgg ak i nar,
Jarti ma kenn, kenn duma jar,
Ki ma giseel a mat a xam.

Wan na ma lol, dindi na sikk
Ci sama xol, ba duma sikk,
Duma ragal lu ki ma sàkk
Ki ma giseel a mat a am.


14 – Jazbul Majzóob

Feesal na xol bi, ba du xam,
Lu doy a yéem ci Ii mu xam,
Lu ki nga xam ni moom la xam
Ki ma giseel a mat a am.

Feesal na bët bi ba du gis,
Lu doy a yéem ci Ii mu gis,
Lu ki nga xam ni moom la gis,
Ki ma giseel a mat a am.

Doylul na xol bi, ba du raf,
Jëm ci leneen lu lu ko saf,
Ci biir mbalaanam la ma laf,
Ki ma giseel a mat a xam.

Génne na réer ci sama xol,
Dugal na riir ci sama xel,
Kenn duma yeer di sañaxal,
Ki ma giseel a mat a am.

Kenn duma wootal di ma fiir,
Kenn du ma yab, ba di ma fiir,
Mi ma àndal, ta dafa fiir,
Ki ma giseel a mat a xam


Jazbul Majzòob – 15

May na ma xam-xam, ba ma xam,
Xóot-xóoti xam-xam yu ma xam
Ci moom, ba jaaxal ku ma xam,
Ki ma giseel a mat a am.

Dolli na am-am bu ma am,
Dolli na xam-xam bu ma xam,
Leeral na mbooleem Ii ma xam,
Ki ma giseel a mat a xam.

Jëfi wilaaya la ma wan,
Dindi la woon wëccag ña woon,
Def fi leneen di ma ko wan,
Ki ma giseel a mat a am.

May na ma wóolu ki ma moom,
Xiir ma ci moom gi mu fi moom,
Biral ma moom gi mu ma moom,
Ki ma giseel a mat a xam.

Biral ma sañ-sañ bi mu sañ,
Biteeki biir moo ko fi sañ,
Ta kenn du sañ Ii mu fi sañ,
Ki ma giseel a mat a am.


16 – Jazbul Majzóob

Biral ma saayiir sa, bu wér,
Biral ma baatin ba, bu wér,
Ne ma lu dul lii, du lu wér,
Ki ma giseel a mat a xam.

Ne ma yëkket yor ci loxoom,
Di ma xamal lu diy soloom,
Di baay ci baatin, ma di doom,
Ki ma gïseel a mat a am.

Jiitu ma ànd ak man di wëy,
Lumay ragal mu ni ko tuy,
Ba man ma waaru ba ni cëy,
Ki ma giseel a mat a xam.

Di ma digal, ta du ma jay,
Fu ma taxaw, mu di ma xëy,
Ta di ma gontu, di ma may,
Ki ma giseel a mat a am.

Nee ñooki, nee na, lani cas,
Buttil ma biir ba ba ma gis,
Raññeel ma mboot yi, ba mu fës,
Ki ma giseel a mat a xam.


Jazbul Majzóob – 17

Ni dëgg a ngii dëgg a fi gën
Fen du taxaw, tagti fi fenn,
Ku jëm fi péey ,du yori fen,
Ki ma giseel a mat a am.

Lisaani aal lamiy waxam,
Lay sànni xol bi, ba ma xam ,
Fuma fi toll di ko xam,
Ki ma giseel a mat a xam.

Moom ka di moom, xam na ma xam,
Lu diy mbiram laa jëkk a xam,
Boobee ba tay, ma di ko xam,
Ki ma giseel a mat a xam.

Léewoo na maak moom cig cofeel,
Di ko mébët ba may xaleel,
Mu daal di may fab yóbb teel,
Ki ma giseel a mat a am.

Tegtal ma yoonu njariñam,
Ubbil ma bunti xéewëlam,
Burxal ma mbóoti ngërëmam,
Ki ma giseel a mat a xam.


18 – Jazbul Majzóob

Yee na ma jar, ba ma ni jar,
Fegal ma kor, sàmmal ma ngor,
Fayal ma mer, fajal ma mar,
Ki ma giseel a mat a am.

Di ma defar, ta di ma far,
Ta ku ma far, mu di ko far,
Ta lu ma far, daal di ko far,
Ki ma giseel a mat a xam.

Di ma taxawu, ma taxaw,
Buma taxawul, mu taxaw,
Teeweel ma xew, luy man a xew,
Ki ma giseel a mat a am.

Ku jëm fi man di ma lëjal,
Mu boolekook lu kay lëjal,
Lu gën mu fab jox ma, ma jël,
Ki ma giseel a mat a xam

Luma ragal mu ni ko cas
Sànni, ba dóotu ma ko gis,
Mbaa mu labal ko, mu ni mes,
Ki ma giseel a mat a am.


Jazbul Majzòob – 19

Bittërñi dun bi, ba ma gis
Ni muy naxee, ta ku ko gis
Jox ko gannaaw mel ni ku rus,
Ki ma giseel a mat a xam.

Wan na ma lal wan na ma bës,
Noteel ma leen ci sama bés,
Misaal ma leen ba ma ni mbas,
Ki ma giseel a mat a am.

Yaramu xol bi dafa mees,
Jee na ba mel ni luñu fees,
Cofeel gi wal na ko mu tees,
Ki ma giseel a mat a xam.

Tibbub cofeelam dafa fees
Ci man, di fokki ak a rees
Ci sama xol, ba dóotul yées,
Ki ma giseel a mat a am.

Moo tax mu def buma nee gees
Ci sama xol,mbaa mu ne gees,
Sunu diggante ne depees,
Ki ma giseel a mat a xam.


20 – Jazbul Majzóob

Di ma xamal ta du ma fët,
Dolli ma xam-xam bu rafet,
Dolli ma ngëm, dolli ma fit,
Ki ma giseel a mat a am.

Di ma yaral boppam ma yëg
Yar ba ci man, ba ma di yëg
Luma yëgul ne luma yëg
Ki ma giseel a mat a am.

Wan ma jamono na mu mel,
Jàngal ma xel, di ma bindal
Ci àlluway maxfoosi xol,
Ki ma giseel a mat a xam.

Di teew ma teew ci péeyi xol,
Gisee mu taal ci lampi xel,
Jum buma wan yoon wu ñu xàll,
Ki ma giseel a mat a am

Jeeqel ma xel, ràcceel ma xol,
Xel du ne xol, xol du ne xel,
Xel a di xel, xol a di xol,
Ki ma giseel a mat a xam.


Jazbul Majzóob – 21

Ruujal ma ji, di ma bayal,
Xiinlu, mu xiin ci niiri xel,
Tawlu, mu taw ci tooli xol,
Ki ma giseel a mat a am.

Mu ñor di xam-xam yu rafet,
Xam-xam yu àndul ak i fët,
Xam-xam yu dul yuy rékki fit,
Ki ma giseel a mat a xam.

Sédde na maak xam lu rafet,
Ba duma yër lu lu rafet,
Ta du ma gis lu lu rafet
Ki ma giseel a mat a am.

May na ma déggóok moom i wax
Ci ay waxiinam yu mu wax,
Samay waxiinay na mu wax,
Ki ma giseel a mat a xam.

Wan na ma boppam na mu day,
Yàllaa ko xam, moom la ko may,
Ta wóolu naa ni moo ma doy,
Ki ma giseel a mat a am.


22 – Jazbul Majzóob

Wax na Yónnent bi Ii mu doon,
May it, ma wax ko Ii mu doon,
Moom it, mu def ma Ii ma doon
Ki ma giseel a mat a xam.

Nee na Yónnent bi, yaw-a-yaw,
May it ma wax ko yaw-a-yaw,
Mu ni ko yaw, ma ni ko yaw,
Ki ma giseel a mat a am.

Buur yàlla may na maw kañam,
Ma di asaanam fuma jëm,
Di tarjumaani lámmiñam,
Ki ma giseel a mat a xam.

Lii le du puukare ci man,
Dafay ngërëm lu war ci man,
Ta may gërëm ki gën ci man,
Ki ma giseel a mat a am.

Mayam yi, yaa na, dunu xul,
Cofeel gi, rew na sunu xol,
Ba doggi reenam, sunu xol
Rootul lu dul wanew taggam.


Jazbul Majzòob – 23

Amna ci yoy, dunu ko wax,
Amna ci yoy, nun mu ko wax,
Ak ba ko, noo yamoo ni wax,
Lay dàggi xol, tay dolli ngëm.

Wuutu na saaba ya, ña wéy,
Ca la bokkoon ta mujj a wéy,
Fab nañ ànd ak moom di wéy,
Dunu ni wuy fi kanamam.

Da koo jëkkal, far koo mujjal,
Muy kun mujjal, tay kun jëkkal,
Taal bu fayul la far jafal,
Daay gu maneefulug fayam.

Buur Yàlla sédde na nu lii,
Lu jiitu nun, xam na nu Iii,
Te yërmandéem jiitu na Iii
Ci nun, ba war nanoo gërëm.

Leerug Yónnent bi la fi def,
Mu juuri leeram ku ko saf,
Mu ubbi xol ba, ba mu af,
Dugal ca xam mbiri sangam.


24 – Jazbul Majzóob

Yawma alastu naka laaj,
Nu ni ko waaw, ta defi xaaj,
Booba la door ni nanu waaj,
Ta daal nu fay yenni yenam.

Sunu Yónnent moo jëkke waaw,
Na ka ni waaw, nu daal ni waaw,
Soppeeki bañ, ku ne ni waaw,
Tay déglu baati ndigëlam.

Ruu yi jungaama ndax ragal,
Yee ak cofeel di leen yëgal,
Amna keroog ñunu xamal,
Xam-xam ba tay la ñu ka xam.

Yónnent bi booba la nu wan
Kanam ñi gën booba la woon,
Booba la Seex metteel woon,
Murid yi booba Ia ñu am.

Booba la Bàmba gañe woon,
Booba la waayam falu woon,
Baax gi fi tay, booba la woon,
Lu ne ci nit, nee na ak jëkkam.


Jazbul Majzóob – 25

Lii le nu tektal ba fi tay ,
Ne ab sëriñ du ku ñu jey,
Ku beru mel ni aji say,
Ju dëddu reenug garabam.

Baaxug keroogay law ba tay,
Bonug keroog itam du moy,
Lawoon keroogay wéy di wéy,
Lu ne di teeri fa mu jëm.

Na waay meloon, mooy Ii fi tay,
La waay amoon, mooy Ii fi tay,
La waay xamoon, mooy li fi tay,
Buur Yàlla, yéem naa kàttanam.

Ku yàlla wan boppam, mu gis,
Ku Yàlla yiir boppam, du gis,
Ñii di ko gis, ñuu du ko gis,
Mooy ñi ko réere, ak ñi xam.

Buleen di siis, buleen añaan
Buur yàlla yaa na, nañ ko ñaan,
Kañaan dafay soppiku jaan
Màtt,luggéeftil màtt-màttam.


26 – Jazbul Majzòob

Jileekuleen, añaane leen,
Añaane kuy xëy jublu leen,
Di wut a jub, Far dëddu Ieen,
Dëkki faneen palam-palam.

Jafanduleen tay dëgëral,
Buleen yolom, kiy dëgëral,
Buleen ko wax yolomalal,
Ku yolomal, daal di yolom

Ku la gënal ki la ñu naan ci gënal,
Moo la gënal ka la gënal,
Ki la gënal ki la gënal,
Moo mat a xam, moo mat a am.

Sërin bi gën ki ma gënal,
Moo ma gënal ki ma gënal,
Te moom mi gën ki ma gënal,
Ame ma may, mayu yaram

Jaayante na ak moom ba matal,
Biteeki biir ,ku ma jiital,
Moom a, ba kenn du ma lëjal,
Xol bii la fab, joxub xolam.


Jazbul Majzòob – 27

Waxtaan na maak moom ba matal,
Waxtaanu xol wu kenn yégul,
Bu ne mu tàbbi sama xol,
Mu yombalal ma ak xamam.

Yawma alastu, ba fi tay,
Masu la tàggook di nu may,
Di yari ruu booba ba tay,
Diggante ndigg ak i ruuwam.

Xam turu taalibeem bu doy,
Xam seen i baay ak seen i nday,
Xam seen i kër ak na ñu day,
Ku ne mu raññaley mbiram.

Xam ña màggante, ak ña fay
Jiitu di toflante ba tay,
Xam ku ñu taal ba dootul fay,
Ak kok du tàkke fii, ba dem.

Xam aji wopp, ak aji wér,
Ak ku ñu fajtal ba mu wér,
Xam aji toppeek ku ñu ber,
Xam fa ñu dooreek fa ñu yam.


28 – Jazbul Majzóob

Fekkoon ñu feeñu ko ba fee
Ñal ko ca biir, far ko fa fee
Ñaatal, mu xam ba fii, ba fee,
Kasful ko yépp fi kanamam.

Kiiraay ya deñ, ba set ni wecc,
Lu diy pakkam ñu boole toj
Ko, sànni yépp, koote ga toj,
Ngir ma ni saww, di am ngiram.

Mu xam boppam ak ña ka topp,
Ñu daal di jël yëf ya ni kupp,
Mu ne di sàbbaa ak a tuub,
Te xam gannaawam, xam kanam.

Buur Yàlla xamloo ko la woon,
Ak la xewoon, ta di la woon,
Ak la di woon ,ta di la woon,
Mu far saxal lu new bindam.

Booba mu def ko ni badar,
Bu feeñ ci laylatul xadar,
Rañaan di sabbaa ba fajar,
Ci asamaani barsàqam,


Jazbul Majzòob – 29

Mi fi diggante kursi, ak
Ars, aki bëyti naari ,ak
Turaa bi, ak awaa-i, ak
Maa-iiki, law i, ak xalam.

Moo tax ma xéy di leen yëgal,
Seen mboole tay lungeen yëgul,
Ba far ci woo ñi dikkagul ,
Ña bëgg a ñëw, ñi bëgg a dem.

Ndax Ii ñuy yartingi, ma jog,
Ta far si ñëganti ku ñëg,
Ta ñaguwul, ta bëgg a ñag
Ñeneen, ta xam-xamlu du xam.

Ta sama woote bii, ku xëy
Mu tàbbi ab noppam, ta muy
Tanqamlu, def boppam ku doy,
Xolam ba, mbaa lakkul ba xëm.

Lu diy muqàddam laa di woo,
Ku di allaaji maa ko woo,
Mbooleeki seex, ku ma ci woo,
Na ni labbayka, mbaa naam.


30 – Jazbul Majzóob

Di leen yëgal kii ma fi gis,
Ta kii ma gis, ku ko fi gis
Ta andulook moom, ka nga gis,
Gënu fi, mbaa saful xorom.

Na ngeen ma laaj ki ma fi gis,
Sangub jamono laa fi gis,
Daalleen di ànd ak ki ma gis,
Bu kenn ni déggumaw turam.

Sayxi suyooxi Axmadaa,
Kii moo nu tektal Axmadaa,
Ta di fi kañ Muxammadaa,
Ba mu tàbbal ko biir këram.

Tampeel ko tampeb ngërëmam,
Ni ko yoxóos ci biir xolam,
Digal ko baati ndigëlam,
Fal ko ci kaw lalub palam

Ne ko yëkket wane, ñi xam
Ak ñi xamul daal di ko xam,
Jiital ko muy muxaddamam,
Daal di taxaw fi seen kanam.


Jazbul Majzóob – 31

Junjung ya gor ci asamaan,
Suuf sa di rëkk péeyi diiwan,
Sañse, ta naa xutbusamaan
Moo falu ànd ak i dagam.

Rijaalu xëybu dajaloo,
Ba mel ni weer yu tegaloo,
Boroomi leer di tegaloo,
Fu ñu fa feeñ soreek lëndëm

Mbooloo yi wutsi ko di wal,
Ta daal di tuub, njébbal ma dal,
Ndëndam ya rëkk ci wépp wall,
Wayam wa riir fuñu fa jëm.

Werante deñ koote ga toj,
Ku bañ, nu tëj, mbaate ñu toj
Këram, mu far mel ni ku aj,
Kàngam ya waaf fi kanamam.

Boroomi giir ya jiitu woon,
Ak seen i giir, ta ñoo rawoon,
Jébbal ko giir ya ñu awoon,
Booleeki wérd ya ñu am.


32 – Jazbul Majzòob

Xaadiru agsi, ni ko am,
Tiijaani agsi ,ni ko am,
Salsali agsi, ni ko am,
Dabbaa-i agsi, ni ko am.

Jaayante faak moom, di ko wan
Yéene, ta ngeejoo fekke woon
Tay, ba muritu ko, di sant,
Fi gannaawam ak ñoñam.

Mbooloo ma naa ko yaa fi gën,
Wii waxtu, yaw la ñu fi tànn,
Yaay tinu, yaa fiy ki ñu tin,
Tinu fi kuy fekke ta gëm.

Buur yàlla yaw la wàcce tay,
Yaa àtte mbir yi ba fi tay,
Sàmmal njaboot gi, ku la fay,
Fase du sëy diirug dundam.

Ku déglu Iii, na xam ni Iii
Yàllaa ko def, ku fekke Iii,
Ta dëddu, far dummooyu Iii,
Defu ko kenn, lumuy boppam.


33Jazbul Majzóob

Gumba gu nanŋaaral, taxul
Mu gis badar, ba tay gisul
Jantu bëccëg, bu ñu wuril
Yoor-yoor, mu jàkkaarlook jëem

Ta gumba nag, ba gumba jee,
Gumba ci xol, mooy waxju jee,
Yal na ñu am gis bob du jee,
Ci bëti xol, ay yuy kanam.

Buur yàlla mooy wane, bu kenn
Defe ne boppam a ko wan,
Gis ki le, ab cër la ba woon,
Buur yàlla mooy joxey mayam

Ku fekke kii, ta fekki kii,
Texe na fii, ba fee, te kii,
May la gu Yàlla maye, kii,
Des na ak ñi des, ànd ak ñi dem

Xutbusamaan a ngii bu mat,
Jógleen àddiya yi na mat,
Ku jéem a gàntu na ni mott,
Di wéy ta xamtil fu mu jëm.


34 – Jazbul Majzóob

Addiya tay moo ka jagoo,
Ku def ni moom, di ko jagoo,
Ku ko deful, bu ko dogoo,
Bàyyil mu àtte ay mbiram.

Lu tax àddiya moo ko moom,
Laay bëgg a wax, ta mooy boroom,
Moo ko jagoo, du seen moroom,
Neleen gannaaw, mu ne kanam.

Yëf ya ca biir ,ak Ii ñu gis,
Ta li ñu gis, mooy li ñu gis,
Biral gi mooy, bët yi ko gis,
Noppal na mbokki lammiñam

We waa ngii, tay xeeñ ak a dóor
Boroom we waa ngee, gën a wóor,
Ba jaan, ta gis des wa di dóor
Du tere jaan duggum kanam.

Yëf ya ca biir nag ku ko xam,
Na daal di doyloo la mu xam
Ku ko xamul ma wax mu xam
Jébbal ko ruuwug bakkanam.


Jazbul Majzóob – 35

Kuy faatu moo fay jëkk a teew
Ñuy jullee mu di fa teew,
Buñuy rob, mu ànd ak ñoom di teew,
Ñu dem, mu des tontu layam.

Seetleen na ngeen di jébbalóo,
Bii tàng, tàngub ñi jébbalóo,
Gis ñam wu neex, ta mosuloo
Ko, xawma man luy njariñam.

Fekke ju mel ni wuute, mooy
Fekke jamonay ngiir ta sooy,
Du def lu dul xoole ni looy,
Di réccu, tay màttum tuñam.

Ñi sóobu, raw ngeen seen i maas,
Ñi bañ, na ñuy ñee seen i maas,
Gaal gaa ngii, jògleen ñaani paas,
Ku yéex ba tarde daŋ ko xam.

Xamleen na ngeen di ñaane nag,
Gëm, ak yarook, toroxlu, ñag
Bakkan, ta muñ, sax fa ba ñëg,
Ba lang, yamook ndigël ba xam.


36 – Jazbul Majzóob

Wóolu dëggal, ak rafetal
Njort, ta set fas-fasi xol,
Loo xàcci, loola daal di dal,
Muy fii, ba fee ; na ngeen ko xam.

Danaa biral ci li ma fas,
Tuuti ci xutbu bi ma fas,
Ni moom a doy, ta Ii ma fas,
Doy na du fii, mang ca kanam.

Fii, du barab, faful di kër,
Fas ji ci moom, dara du mbir,
Keram gii, naaj la kat, du ker,
Lemam di ngañ mu wex xorom.

Méddëm mi, tan yi di ko biiw,
Bawkat yi siif ko, di ko yéew,
Di dox di xiiroo, ba mu siiw,
Tab lay bu dee taa, daal di dem.

Kërug ku dul am kër la fee,
Moo tax ma dëddu, jublu fee,
Li tax nu jóg, du fii, ma fee,
Foofee la soxlawoo ñoñam.


Jazbul Majzòob – 37

Ta tay ma jàngal leen, na ñuy
Faseg njullit, xëy bàyyi moy,
Ta xam ni, jàkkam wa, du moy
Boroom, ci kangam, mbaa dënnam.

Ta seede yaari baati see
Deyi, ta fas sellal, ta see
Deloo ko, b
Buur bu doy bi see
De, ci lu leer ak lu lëndam.

Ta dëddu àdduna, ta wut
Seriñ bu mat seriñ, ta at
Tani yenam, ta bul tawat
Benn, lu dul ay tawatam.

Ta kooka, mooy Bamba, buleen
Dese ba jóg wuti keneen,
Ba réer ci manding mi, du ngeen
Taseeg ku dindi seen ngëlam.

Def leen ni man, dama ni man,
Labbayka Bamba, maa ngii man,
Fukki barab, ma teg ca benn,
Fuñu fa tollu, maa la gëm.


38 – Jazbul Majzóob

Keroog ba ñuy dekki ba xëy,
Jëm bëyti àndandoo di wéy,
Keroog a tax nga doy nu tay,
Yàllaak sa barke, maa la gëm.

Keroog ba ñuy taxaw, ta kenn
Dufa ni riis tankam, ta kenn
Dunga lu dul lu mu nekkoon,
Yàllaak sa barke, maa la gëm.

Bu téere yay rot, si digën-
Te yaari wet yi, mel ne tan
Yuy dal, ta kenn du réere benn,
Yàllaak sa barke, maa la gëm.

Bu ñuy tëral mandaxe ñii,
Seen yiw wa wat, ñu gane ñee,
Ñu gañe leen, ñu ñee fa ñee,
Yàllaak sa barke, maa la gëm

Geppéen ba, buy sampu ta mooy
Siraat, ku jéggi mbir ya nooy
Fa moom, ta dóotu deñ di nooy,
Yàllaak sa barke, maa la gëm

Aji-bind ji: Seexunaa Faal

Aji-topp ji: Seex Lóo