Catégories
Sëñ Sàmba Jaara Mbay

Ku faatu yaa fay…

Bismil laahi rahmaani rahiimi
Xaala Seex Muhamadu Abdul kariimi Sàmba Jaara Mbay

Ku faatu yaa fay jëkk a teew
Buñu koy jullee nga di fa teew
Ñuy rob nga ànd ak ñoom di teew
Ñu dem nga des tontuw layam

Seetleen na ngeen di jébbaloo
Bii tënk nun ñi jébbalu
Gis ñam mu neex te mosuloo
ko xaw ma man luy njariñam

Fekke ju mel ni wuute mooy
Fekke jamonoy ngiir te sooy
Du def lu dul xoole ni looy
Di réccu tey mattum tuñam

Ñi sóobu raw ngeen seen i maas
Ñi bañ ne ñooy ñee een i maas
Gaal gaa ngi, jógleen ñaani paas
Ku yeex ba tarde ding ko xam

xamleen na ngeen di ñaane
nag
Gëmak yarook toroxlu ñag
Bakkan te muñ sax fa ba ñeg
ba laŋ ba Moom ndigal ba jam

Wóolu dëggal ak rafetal
njort te set pas-pasi xol
Loo xàcc loola dal di dal
muy fii ba fee na ngeen ko xam

Moo tax ma wax lii ma fas
moo gën ci man dawal i fas
Moo gën di fecci ak a fas
Moo gën di wekki ak a jam

Da naa béral ci li ma fas
tuuti ci xutbu bi ma fas
Ne moo ma doy te lii ma fas
doy na du fii mang ca kanam

Fii dub barab faful di kër
Fas gi ci moom dara du mbir
Keram gi naaj la kat du ker
Lemam di ngañ mu wex xorom

Méddam mi tan yi di ko biiw
Bawkat yi siiñ ko di ko yéew
Di dox di xiiroo ba mu siiw
Te lay bu dee taa, dal di dem

Àdduna kërug ku dul am kër la fee
Moo tax ma dëddu jublu fee
Li tax nu jublu fii, ma fee
foofa la soxlawoo ñoñam

Te tay ma jàngalleen na ñuy
Faseg njullit xëy bàyyig moy
Te xam ne jàkkam wa du moy
Boroom ci kaaŋam mbaa dënnam

Te seede yaari baati seede yii
Te fas sellal te seedeloo ko
Bùur ba doy ba seede ci lu leerak lu lëndam.

Te dëddu àdduna te wut
Sëriñ bu mat Sëriñ te àttan yenam
Te bul tawat benne lu dul ay tawatam

Te kooka mooy Bàmba bu leen
Dese ba jóg wuti keneen
Ba réer ci màndiŋ mi du ngeen
Taseek ku gindi seen ngëlëm

Defleen ni man
Da ma ne man
làbbayka Bàmba maa ngi man
Fukki barab ma teg ca benn
Fu nu fa toll maa la gëm

bakkan bu dee tàggoo di waaj
Saafara deñak i gàllaaj
Soppe bi yaw la nu fa laaj
Yàllaak sa barke maa la gëm

Bu ruu di xar-xarle ba dal
Malaaka agsi di bégal
Seex Bàmba yaw lanu àndal
Yàllaak sa barke maa la gëm

Bu ruu roccikoo ba naaw
Jëm asamaaw wane gannaaw
Seex Bàmba yaw lanu fa ëew
Yàllaak sa barke maa la gëm

Buñu ñoree yaram di rob
Ruumaan ni jaas du nit du rab
Seex Bàmba yaw lanu fa ŋëb
Yàllaak sa barke maa la gëm

Bu ñaari gaa ya nee jalañ
Di laaj te neex, nga ne jalañ
Bégal nu mbég mom dootu deñ
Yàllaak sa barke maa la gëm

Keroog bun dekkee ba xëy
Jëm bëyti àndandoo di wéy
Keroog a tax nga doy nu tay
Yàllaak sa barke maa la gëm

Keroog bu nuy taxaw te kenn
Du fa riis tànkam te kenn
Du gë, lu dul lu mu ne kun, Yàllaak sa barke maa la gëm

Bu téere yiy rot
ci diggante ñaari wet yi
Mel ni tan yu dal te kenn du réere benn
Yàllaak sa barke maa la gëm

Bu ñuy tëral màndaxe, ñee
Seen yiw wa wat ñu gañe ñee
Ñu gañe léen ñu ñee fa ñee
Yàllaak sa barke maa la gëm

Képpeem ga fay sampe te mooy
Siraat ku jéggi mbir ya nooy
Fa moom te dootu deñ di nooy
Yàllaak sa barke maa la gëm

keroog bu mbooloo mi ne ràcc
di seddaloo def ñaari pàcc
bisub keroog Yal naa la daj
Yàllaak sa barke maa la gëm

Nu daagu jëm Daaru Salaam
Di xëy di joqàntey salaam
Fu ne nu déeyaaley salaam
Yàllaak sa barke maa la gëm

Soppe bii laa fas ba ñëw
Seex Bàmba yii laa fas ba ñëw
Yaakaar ci Yàllaak ci yaw
Texe gu sax du deñ ba fàww
Yàllaak sa barke maa la gëm

Maa ngi taxaw fi sa gannaaw
jublu la wan ñeneen gannaaw
Foo man a jëm yóbbu ma gaaw
Yàllaak sa barke maa la gëm

Ku sedduwul man seddu naa
ku fàdduwul man fàddu naa
Ba matle weesu naa danaa
Yàlla ak sa barke maa la gëm

Subhaana rabbika rabbi isati hamaa yahsifuuna wa salaamun halal mursaliina wal hamdulilaahi rabbil haalamiin

Aji-bind ji: Seexunaa Faal

Aji-topp ji: Seex Lóo