Àddina ndax day bëgg a jeex
am gaa yu baax yeey bëgg a jeex
am mbër yu ndaw yeey bëgg a seex
Moo gaa yi xam naka pexe ?
Ka xamle woon ag tarbiya
ak ka xamoon ag tarbiya
moo buñ demee ba surga ya
ku leen di wax nag luy pexe ?
Ka woote woon ci àddina
ba ñépp wuysi fàddu na
nan jéem a dëddu àddina
te jéem a wuyji mooy pexe
Seex Bàmba dem ca « Wamsashi»
Seex Ibra dem ca « Tamsashi»
Moo ñi fi des ku ñuy dese ?
yeenu muriit naka pexe ?
Ab séet du dem ba doom dikkeem
Seex Ibra Faalay doom dikkeem
moo rawi bokk, rawi doom
topp mi waaj leen mooy pexe
Ab séet moroom yaay topp ma
sëriñ muriit yaay topp ma
jéem leen a wàlli séen po ma
te ba po mii ngeen di fexe
Seex Ibra gëm ga làndi na
moo tax mu dëddu àddina
fekki na Bàmba sotti na
wàcci na aljanay texe
Mas nay xibaar ag jébbuloom
ba wax ne Yàlla mii ko moom
moo ko ne Bàmba moo la moom
raasi ko jox ko say pexe
Tegtal ko yoon wa ab muriid
di aw ba raw pexem Mariid
ba am ngërëm bariy muriid
te dootu ree di tex-texi
Mu dal di dem Tayba-Daqaar
Ngir dégg Bàmba di fa xaar
seet na Sëriñ Tayba-Daqaar
ci jàng lay xamey pexe
Mu tëdd guddi listixaar
bët set mu xëy ba tusubaar
Sëriñ Mataar Turee fa jaar
leeram ga wan ko ay pexe
Muxtaar Turee nga yori njoor
yanu ko jëm Mbàkke-Kajoor
Sëriñ ba yónni ko ca buur
Seex Ibra topp cay fexe
Mu jis fa Seex Aadama Géy
Sànni mbiram dal di ca ŋoy
Mu wan ko Bàmba mbër mu rëy
Sëriñ ba naa ko foo fëxe ?
Mu wax ko tegtal ya fa moom
Seex bàmba wan ko la fa moom
mu xam ne jis na ka ko mom
mu dal di fab mbiram joxe
Mu sóobu far ba jiitu leen
Bàmba ne kii ëpp na leen
leeram gu rëy gi wër na leen
fum toll xol bay nux-nuxi
Wax na ne tuuti kon mu dem
fekk Sëriñ ba lëm mbiram
ba ken du jot ci baatinam
lu dul ca bis ba ñuy texe
Jaaraama Seexi Ibra Faal
Làmp bi Sayxii Bàmba taal
leerale réewmi, yaa kamaal !
yal na nga dolliy beréxi
Ba mu ñëwee Mbàkke-Kajoor
fekk na daara ja di suur
moo jëkk a yalwaani di woor
ñu di ko ree di tex-texi
Yendoo liggéey, fanaan a root
gaa yay xaran ba naa xuréet
ba lay ganaar ne kurkureet
moo ko xewal daawul doxi
Moo fa xewal nuyoo di raam
moo nu teree wuyooti naam
fekkon na ñuy jàng fa maam
moom muy muriitu di fexe
Fekk na daara ja di riir
moo dindi àllarbaak dibéer
lu Bàmba wax mu dal di buur
lum mas a am dal di joxe
Moo fi xewal soli sagar
moo fi xewal saxoo sikar
moo fi xewal sëqal kawar
daawu fa bay di rux-ruxi
Ba mu demee Mbàkke-Bawal
daf ne na waa kër ga ba wal
naay soq tey rooti di wal
booleek liggéey di ko joxe
Lu bàmba wax mu dal di naaw
fóore ju rëy ja sant Saaw
naa ko dangay dellu gannaaw
jàngil muriitu du pexe
Mbooleem muriit ya di ko soow
mu mel ne dof bu mat a yeew
ba mujj far ñépp ne siiw
Meloom ya far di ko doxe
Mu jiitu far amul moroom
far gëni bokk gëni doom
jaaraama jaaraama Xadiim
wàcc nga wàccaaleek texe
Yaw masulaa juuyook ndigal
naka nga jóg të nga ndugal
ku aw sa mboor duñ ko mbugal
garmi yi yaa tax ñuy texe
Yaa jëkk a jébbale sa xol
fekkon nga gaa yay xorxoral
ñaley setal ñaley nëxal
yaa wane ngér mi ñiy doxe
Yaa xam Sëriñ bi yaa xereñ
daawoo weranteek ab sëriñ
bàjjo bi yaa bariy njariñ
waane wi yàgg ngaa naxe
Am ngay gërëm ba am dërëm
fab ngay dërëm jëndey ngërëm
loo mas a am tàbbal këram
ay junni daal nga daa joxe
Joxe nga àddiyay giléem
yu safi ngurdu safi koom
soldaar sa yaa joxe sa doom
Faadilu Faal am nag texe
Sa ndaw da daa dem ba Gaboŋ
di yóbbu ay saaku yu roŋ
di war ca gaal ya yori boŋ
doo denc lëf ba muy maxe
Moo tax nga mel ne ag saxaar
ku nar a dem da na fa jaar
kuy ñaani paas na seeti gaar
bum nég ba naa naka pexe ?
Ndegam da nga xebat sa paas
way-wata yaa nga fa garaas
seetal ma wax jii te xiyaas
ndegam da ngaa am looy joxe
Baayay saxaar doomay wata
kuy xamle Yàlla du fi të
ku ji àndaar góob cay mata
jiyal ci taw buy bex-bexi
Seex Bàmba taawloo Mustafaa
Seex Ibra taaw bay Mustafaa
diggante Marwataak Safaa
kuy aji war na faa doxi
Seex Bàmba am nam Faadilu
Seex Ibra am nam Faadilu
ku xam na faale Faadilu
kon ag mujam du toroxi
Seex Bàmba bégle nam Basiir
Seex Ibra bégle am Basiir
ndab loo ci dem lekk ba suur
jegeel ma kay toggiy joxe
Seex Bàmba am nam Abdulaay
Seex Ibra am am Abdulaay
Abdu mu nekk mat na waay
bul weddi céebo kaay texe
Yal na ñu aw seen tànki baay
ba mujj donnu seeni baay
ba mujj boole seeni gaay
aamiina ndax ñépp texe
Seex Ibra dem na wàcci na
lum mas a aajo faju na
ba xëy ne ñibbi àjjana
nan farlu tey àndi pexe
Ken masl a jis sasam wu booy
du daw ku koy moslook a jooy
moo jar a way te jar a jooy
Céy àddinaa man a naxe
Déglul ma lim fi ay ndamam
ba gaa yi dollee xam mbiram
ba xol yi bég ba dellu gëm
leegi ragal yi yox-yoxi
Jaaraama Ndey Saynabu Njaay
la Soxna Jaara yor di jaay
yaa ko mosal waa Njare-Njaay
saw ŋàññ rot na yaa texe
Diggante Njukkeek Jamatiil
dañ daa dajey naani butéel
yaa tax ñu jébbulu ca teel
Faal Njaga yaa rëyi pexe
Mbulaki Sàqaki Sugeer
dañ daa falook a soli fuur
yaa tax ba diine di fa leer
toxal nga póon mañ daa tuxe
Doomi Dàmmeel ya fi ne won
yaa dàmm mbir ya ñu ne won
tay ñépp ñépp a ngi fi nun
ken amatul lu muy fexe
Yaa yóbbu Mbaaxaan ca Xafóor
yaa tax ba xol ba dootu fuur
yaa tax mu sànni yatu nguur
fab yatu ngëm di laaj pexe
Te xam ne mas naa yor junjung
fum jëm géwal ya naa kundung
muy xas di bàkku cid goroŋ
tay mu yam ak nun ay pexe
Yaa tax ba Abdulaahi Xaar
taxaw fi bunt di fa xaar
woyaflu bay lekk daqaar
ngir sopp Bàmba kiy joxe
Te xam ne moo doon doomi buur
lum mas a wax ñu dal di buur
la dale Mbaakol ba Kajoor
moo ame woon seeni pexe
Yaa tax ba Soxna Mbenda Faal
ak Gañsireeki Làlla Faal
gën doomi soxna yii fi taal
diine ju rëy ji ñuy doxe
Te xam ne seeni baay a moom
Feedar ma taalagut kanoom
koo mas a jis ay jamonoom
xolam ba daawul yox-yoxi
Yaa tax ba Abdulaay ñaxib
làmbi ndigal far na ko wub
la gaa ya giiroo moo ko xëb
tabax na ay kër di joxe
Te xam ne mas naa dox fi moom
tay jii mu mat sëkk boroom
nga denc doomam dib goroom
lii doy na xarbaax doy pexe
Seex Ibra Faal amul moroom
sàkk na bër yu tol ni moom
leeral na penkoom ak sowoom
luy yàq dootul ñuy-ñuxi
La dale Ndar ba ca Dakaar
jàll gannaaw yoonu saxaar
mbër mu fi rëy ba ñu ne kaar
Seex Ibra lay laaj pexe
Ndar la ko doomi Jaara may
leeral na bopp jaara tay
waykat wa Sàmba Jaara Mbay
moo tax dënnam bay béx-béxi
Mu jóg fa agsi Ndànd-Faal
jàpp fa doomi Ngóone Faal
def ko ne làmp bu ñu taal
tay Ngingineew moo fay fexe
Leeram ga sar ba agsi Kees
ku ñëw mu duy la ba nga fees
luy nit ku ñuul ak ku xees
ñéppay bawoo fa Ngaay-Mexe
Sëriñ bi ñëw Njurbél mu ñëw
gàddaay këram ya te du daw
guddeek bëccëg ñam ya di ñëw
Ba Bàmba xëy sàkk pexe
Mbooleem muriid yépp gëlam
ken xamatul kuy Sëriñam
kune na ngéej a dal di dem
àddina séppiy jëx-jëxi
Mu dal di ŋoy ci Mustafaa
ngir xam ne yor na listifaa
mag ñépp dem moom mu ne fa
Masla tuxook a yox-yoxi
Ba xëy na wuyji ab sangam
tuubaa la togge woon añam
Bàmba a ko jiiteloo ñoñam
diggante Béb gaak Guy-Texe
Ma ngay janook tooli dërëm
meññat mu gën junniy dërëm
jis na lu weesu mébetam
am na lu raw lam doon fexe
Ngërëm la Yonnen bay gëram
Abaabakar ma jëkk a gëm
la Sayxu Bàmba di gëram
Seex Ibra mooy njëkk a texe
Midaay ba Yonnen bay takkal
Abaabakar ngir ag dëggal
la Sayxu Bàmba di takkal
Seex Ibra Faal bisub texe
Mànto ba Yonnen bay solal
Abaabakar yor paresol
jël saadixiina ya tofal
yal na ko Bàmba di joxe
Muusaa la way wii wolafal
yal na ko Shayxii Bàmba ful
te boolekook gaa yu dëggal
yoo xam ne ken du yox-yoxi
Aji-bind ji: Sëñ Mbàkke Jeŋ
Aji-topp ji: Ismayla Géy