Catégories
Sëñ Musaa Ka

Jooyi xol

Dangaa jooy ba noppeem

Dangaa jooy ba noppeem da ngay jooy Ci xol
Dangaa nopploom am dangaa far wedam

Dangaa fàtte Seex Bàmba am ndax dangaa
Deseetul i rongoñ nga dëkkee xalam

Dangaa miis ba sam xel di fàttey biram
Da ngay daanu am ndax dangaa far gëlëm

Jugal boog te jooy bon gu rëy gii nga bon
Te gaa ñépp baax am ngërëm diy bëram

Te yaw ngay Ku bon kuñ defar saahiram
Te baatin bi làmboo ëyib yii nga xam

Sa maas gépp raw nañ te am nañ ngërëm
Sa kem yépp set nañ te dootuñ tilim

Faseel àddunaak gaa ya koy topptoo
Te fonkal ma allaaxiraak aw ñoñam

Na ngay muslu saytaane fàwwook bakkan
Te bul topp banneex yi lee dog sa kem

Wattul Yàlla yër xol bi gis muy tilim
Wattul sa juróom ñaari cër kon nga dem

Amal yitte am diine jëf lañ farat
Te am xam-xam ak teggiin ak ngërëm

Su fekkee da ngay jiite aw nit da ngay
Am ag xam am ab yar Am i jëf ndaxam

Te kuy jiite ndéem ràññewul yatt yii
Dafay sànku tey sànke lee dig mujjam

Jugal waaji Muusaa te fàgguy ngërëm
Te wékkaat sa xel mii ci Bàmbaak ñoñam

Te yaw kat da ngay ndaw nde kon foo taxaw
Di waarook a waarek a fàgguy ngërëm

Te bul Mel ni sondeel ci leeral ñoñam
Ba ñuy xor-xoral moom mu làkk ug wëñam

Sa kem yépp a ngii dee te set nañ welas
Te yaw àggagoo fenn Booleek tilim

Te yaw jéemu laa dab ña set bay seetal
Xanaa xëntewoo soxna yeek ay dëram

Te sab dig xamoo tay la jee am ëllëg
Te Yàllaa ngi lay xonte wér gi yaram

Te boo seetlu woon jagle yiy xew fi yaw
Gërëm sab sëriñ nde da laa far yërëm

Sa bon gii nga bon ak sa may gii nga am
Sa moy gii nga koy moy te Ànd ak mbiram

Te foo toll muy Dolli ay xéewalam
Wallaay doy na ab soññ gor suy xalam

Dangaa dof nde kon lee nga war koy yeras
Ba tax doo ko moy mbaa nga war koy xalam

Bëriy soxna ak naarigóor ak alal
Di am taaxi-kaw say murit naa nërëm

Taxul Bàmba jox lab sirroom kat yëgal
Dëggal ak ndigël ak sa ngëm ñooy njëgam
Jugal farlu waatal te yeesal sa jëf
Te bul mel ni ñiy wax ne jëf wéy na cam

Xanaa jëf ya daa am du Yàllaa taxoon
Xanaa pay ya daa ñëw du Yàllaa ko am

Te Yàllaa ngi jëf yaa ngi pay yaa ngi nii
Sëriñ bee ni mes waaye mbóot yaa ngi am

Te sax jëmm joo gis dafay xëy ne mes
Waxam jaak jëfam jaa fa des dim ngiram

Xiyaasal ma Yonnen ba wëy naak ñoñam
Te teewul sunnaam saa ngi fiy jëm kanam

Yëral alquraan ak hadiis kiy waxam
Nga gis lim bañ ak lam jëf ak lam gërëm

Xiyaasal ca baawon woroom ngir ya daa
Joxey wird ban tay kurus yaa ngi am

Muriit boo fi gis muy yolom lub nosam
Di waññiy addiyyaam soril ay mbiram

Ku naa tërbiyaa wéy amul tay njariñ
Wutul kum siyaaraati waccal waxam

ladiw ay te mat ay fa gaayay xalam
Dem ug Bàmba gii tax nga rikkeeku gëm

La doy ndam te mat ndam fa gaa ñay xalam
Dem ug Bàmba gii tax nga doleeku ngëm
Boroom tool bu nee mes nga gis waa ja mat
Te tàggook i ngistal du soppim Solam
Sëriñ ibra faatee di yaaram bu rëy
Te am xam-xam ag ngëm te làmboo gërëm
Sëriñ Ahmadu Ndumbe moo dib muriit
Sëriñ Daam a rëy ngëm te sellal ngëmam
Ña ngay gën di doomal ca lañ leen sasoon
Ndigal moo di toolub muriit tay këram

Ndegam yaw dangaa def Ku àggul ba tay
Dawal fekki doomam ya wut cay ngërëm

Te yaw moo ne war ngaa faseetiy nelaw
Di biin-biinlu bab jant far xëy ba dem

Nga jug naa nu may def te leeram ga wéy
Te ab jant fenkaat agul ciy goxam

Jugal waaxu tay daw ne dof buy xaran
Bu jantam ba suuxee dajeek ug lëndam

Sëriñ bee di ab jant moo xëy ne mes
Lëndam gaa ngi tay foo fi jëm far gëlëm

Bu ab jant suuxee ña daa xor-xoral
Berook seen i sondeel ba laa fay ñu dem

Ña taalooguloon rët ba tàggook i xel
Ba far Mel ni man man mi ñee gaa ya dem

Sëriñ bee tahal noo tahal ban berëx
Te bun giim te bun fay ba am sa ngërëm

Te nuy taal bu ñéppuy tibbee kay jafal
Te muy gën di jolleek a yànjiy xalam

Te def nub muriit bob danuy sax ci yaw
Te bun rëcc bun rot ba am say ngërëm

Te bun xàcc bun geesu bun rékki ngëm
Te bun faale dunyaa di Ànd ak ñoñam

Te may nuy àddiyaak i mbooloo yu jëf
Te luñ jëm fexeel bam dajeek say ngërëm
Te tàbbal nu Tuubaa gannaaw sun bakkan
Ñu ànd ak sunuw ñoñ nga may ñépp ndam.

Aji-bind ji: Seex Lóo