Ma yee fi gaa
Ma yee fi gaa ñiy bañ a digluy wolofal
Bañ xam ni Yàlla buur bi mooy ki man a fal.
Ngir wolafal mooy wolli tooli xol yi
Di yokk gëm yi faf di wubbi xel yi
Buur Yàlla moo bindoon Araab bind wolof
Tàggale làmmiñ ya te Yàlla moo ko def
Moo sàkk ñay làkk di làkki soose
Ak Tukklóor ya ak Fël ya ak Majoosi
Pël yaa nga naa mbii mi Wolof naa dama ne
Te Yàlla xam na seen i wax fuñ man a ne
Pël yaa nga naa mojji wolof naa baax na
Te Ku ci wax buur Yàlla xam ne wax na
Yàlla du buur buy gàntu mbaa muy gënale
Loo fa amul ci yaw la yaw miy yàllale
Ñu njëkk ña ak ñu mujj ñii la yamale
Ku ko jëfal mu fay la moom du tappale
Wasaabixuunas-saabixuuna moo ko wax
Waaye du tee ñi mujj a ñëw daf leen di jox
Wolof ne njëkk a fecc taxt a mujje
Ab géew Ku mujj a fecc Pël naa mójji
Waxi Wolof ak waxi yaaraam ñoo yam
Dégg na làkk ak Wolof ak yaaram
Ci jamonoy noohin la wax ya tàggaloo
Waaye jullit seen yéene dóotul tàggaloo
Loo yéene mbaa nga laaj ko Yàlla Fay la ko
Àddina ak laaxira dellu fay la ko
Soo ko gëmul seetal Ku ndox suuf màtt
Soo ko luggul day faatu faf ne fàtt
Te lugg ay jat la du baati yaaram
Du ay Wolof duy làkk Yàlla moo ko xam
Te terewul loo jàng jàng it alxuraan
Soo ko jatul doo wàcce jaani saamaan
Saalaali waalaali te naa ko tookee
Waa ju ko ñaane Yàlla xam na kookee
Te loolu Rekk a man a wàcceb njàngóor
Moo tax nga xam ne Yàlla rekk mooy buur
Buur Yàlla loo ko ñaan mu may la loola .
Lu dul nga mel ni Mustafaa fa Yàlla.
Aji-bind ji: Seex Lóo