Bismi laahi rahmaani raahiim ,wasallalaahu tahaalaa halaa Sëyyidinaa wamawlaanaa Muhammadin wa-halaa aalihii wasahbihii waxayra xaddimihii wasallama tasliimaa.
Xaala Muusaa Ka bukaa an halal xadiimi li faxri mudrika.
Manatumaa jekki te nekkumay jooy
Sëriñ bi cëy àddina yaaka maa juuy
Sëriñ bi waa ju ko jisoon jisub xol
Koo mantee jis it mu sew ci sam xel
Sëriñ bi waa ju ko jisoon mu jis la
Koo manatee jis it du tax mu doy la
Sëriñ bi waa ju ko mosoon mu mos la
Koo manatee mos it du tax mu saf la
Sëriñ bi gaayi ko amoon te ñàkk-ko
Kuñ manatee ñàkk it du tax ñu faale ko
Sëriñ bi gaayi ko hamoon te xewle ko
Moo tee ñu dëgmu far di jooy ba fekki ko
Sëriñ bi waa kërëm ña nekkoon Njaareem
Seen xol yi dootu jis lu rëy bam jara yéem
Sëriñ bi waa kërëm ñi nan leen wormaal
Te fonk leen def leen i nday bu kenn laal
Sëriñ bi saahir si dafay melow nit
Baatin bi leppi Yàlla éey du leen nit
Sëriñ bi xar-baax la gu Yàlla feeñal
Amul nirook i nawle mbaa kuy feeñal
Sériñ bi doomam yile nana leen jiital
Di leen siyaare bir yi bun ko juutal
Sëriñ bi cam soo ca xiyaas mu yées ko
Te moom palaas boo ko wutal mu fees ko
Sëriñ bi yaw niroowulaak malaaka
Te doo rawaan doo jinne doo Muusaa Ka
Sëriñ bi yaw niroowulaak sahaaba
Yaa raw ñadaan xool di janook kahaaba
Sëriñ bi yaw yaa jiitu gaayi diiwaan
Yaa raw ñadaa feeñal i mbóot di baawaan
Sëriñ bi yaa raw gaayadaan fanaani
Haras di xuus ca dexi leer yay naani
Sëriñ bi jéggi nga palaasi xutbu
Ngir sàkk ngay xawsu yu sàkk i xutbu
Sëriñ bi yaw niroowulaak Jiilaani
Faxóo nirook Saasali baa Tiijaani
Sëriñ bi yaw yaa boole mbóotam ngir ya
Ak àtteyaak sañ-sañ ya ak seen leer ya
Sëriñ bi yaw jàll nga ngiirum werdu
Yaw sab muxaddam du jubook i ardo
Sëriñ bi weesu nga mbirum wilaaya
Xam-xam bi it raw na xamug diraaya
Sëriñ bi yaw niroowulaak wàlliyu
fafoo nirook ñay woote ak mahdiyyu
Sëriñ bi yaw Yàlla a ne laa naabiiyaa
Nde kon ku lay woo far ne yaa nabiiyaa
Sëriñ bi yaw yaa wuutu ngën ji yonnen
Saa gëti xol jis na ko dootu wànnen
Sëriñ bi bir yaak melo yaak jikkoom ya
Day saf meloy yonnen ba siloom ya
Sëriñ bi muñ gaak nattu gaak wàkkiirlu ga
Day saf muñug yonnen ba ak cellerlu ga
Sëriñ bi wéetal gamu wéetal Yàlla
boo koy xalam mu doy la ci Yàlla
Sëriñ bi xér gaak tabe gaak njàbmaar ga
Day saf tabeg yonnen ba ak yaakar ja
Sériñ bi nooy gaak kersa gaak yërmaande ja
Day saf xolub yonnen ba ak yërmaande ja
Sëriñ bi ham gaak dëddu gaak lewet ga
Day saf dëddug yonnen ba ak hamam ga
Sëriñ bi téy gaak raglu ga lewam ga
Day saf ku xool yonnen ba ak muuñam ga
Sëriñ bi wax jaak waare waak haddiis ja
Day saf fu yonnen jekki ak Xadiija
Sëriñ bi nim wootee ci yoonu tarbiya
Day saf na yonnen ba defoon cig tarqiya
Sëriñ bi nim seexale gaayi wuyusi
Day saf na yonnen ba defoon Xuraysi
Sëriñ bi ñam tarbiya woon ca baawon
Raw nanu jéeg ngir seen i xol lañ jaayoon
Sëriñ bi nim leerale taalub lislaam
Day saf jihaar ju mag ja fentoon lislaam
Sëriñ bi moo laxasu yeesal diine
Fekkoon na taal bay bëgg a fay fasànna
Sëriñ bi moo bayaat lu toolub sunna
Ku ne di bay di haj di gën di sonn
Sëriñ bi moo tuxal bidaa ci réew mi
Ak aada yuy jaahil sosoon ci réew mi
Sëriñ bi tax surga du faale ngonnal
Te xam ne dañ daa gonlu booleek mindël
Sëriñ bi bi tax kaamil di jar ay téemeer
Te xamne daawul jar lu weesu fanweer
Sëriñ bi moo dindi ci réewam soodaan
Kuy waññ mbaa kuy wàlli njongiy seetaan
Sëriñ bimoo tax mag ña woon ca baawon
Bàyyi tux ak fóon ak yu mel ni yaa woon
Sëriñ bi moo tax bépp séeréer bàyyi naan
Bawal-bawal ba sàcc pël bàyyi safaan
Sëriñ bi tas daara yi samp i daaru
Ngir daara yee dañ daa doroo ka taaru
Sëriñ bi tax sàmm si dootun wax óow
Ken du ne naam giwal ba xaste ak coow
Sëriñ bi tax ba ndaw ñi màggal mag ñi
Ba mag ñu baax ñi far di jiital ndaw ñi
Sëriñ bi tax ba nun wolof nu tekki
Te xam ne ken daawu fi dox di fokki
Sëriñ bi tax waa Màkka ak Madiina
Difi siyara si di wutsi diine
Sëriñ bi tax deefu nu yët hidaaya
Te xam ne noo daa yóbb ay hidaaya
Aji-bind ji: Seex Lóo