Catégories
Sëñ Daam Jaane

Sant Yàlla

Al hamdu lillaahi rabbil haalamiina ndaxam
ak cant war na ci man al hamdu lillaahi

Naa jóg te santati Buur bi xëy ma bind ci ndox
muy daw ci biir i sidiit al hamdu lillaahi

Naa jóg te sant ki aare aw lumb suux ak i yax
xàllal ko pinc mu yaa al hamdu lillaahi

Naa jóg te santati Buur bi tënk bëtt ci lëm
may rëpp jàpp ko naa al hamdu lillaahi

Naa sant Buur bi fi tàllal suuf si sotti ci ndox
meññet mu teey di ci ñor al hamdu lillaahi

Naa sant Buur bi fi yan samaawu jant ak i weer
biddiw ya feg sama réer al hamdu lillaahi

Santal Broom bi la jox soldaar yu bët teguwul
ñuy daan sa noon yi yëgoo al hamdu lillaahi

Santal Boroom bi la jox cawwam ju sell te yaa
ngay nokki tus fayuloo al hamdu lillaahi

Santal Boroom bi la may sañ-sañ ci say jur i kër
ngay tër di def ci sa biir al hamdu lillaahi

Santal Boroom bi la jox, ay cér yu topp ndigal
foo leen yabal duñu bañ al hamdu lillaahi.
Santal ki baaxe la lum xañ say moroom yu bari
ngay ree ci biir aji jooy al hamdu lillaahi

Moo tee nga sant ki fab daamar yu gaaw ni la am
ngay war di dikk ak a dem al hamdu lilllaahi

Moo tee nga sant kilay fajtal ci boo tawatee
moo cér pikiir ak i reen al hamdu lillaahi

Moo tee nga sant ki yor wërsëg di jox ku ku soob
jinne ak mala ak rabi ndox al hamdu lillaahi

Moo tee nga sant ki def sëqub melen ci sa kër
ñuy fortu ñam wa nga tuur al hamdu lillaahi

Moo tee nga sant kilay wax kaay te sant ma ngir
say may di dolliku neel al hamdu lillaahi

Moo tee nga sant sa géer gii sànge la ak suttura
muur say ayib toroxóo al hamdu lillaahi

Moo tee nga sant kilay jéggal sa njuumte yu réy
loo moy te tuub ko mu far al hamdu lillaahi

Santal ki ngay dese saa yu ñépp nee la yalax
mooy soppi njàqare mbég al hamdu lillaahi

Santal kilay may a may ak loo ko xëy moy a moy
ëppante na ak topp jaam al hamdu lillaahi

Moo tee nga sant kilay wax kaay te sant ma ngir
say may di dolliku neel al hamdu lillaahi

Sun xippi ak sunu xef sun yëngo ak sunu dal
nuy dundu baate nu faat al hamdu lillaahi

Al hamdu lillaahi rabbil haalamiina ndaxam
ak cant warna fi nun al hamdu lillaahi.

Aji-bind ji: Imaam Jóob