Boo donnatul mbir ma jëggil mbir ma fum fu gëne
Bul toog te jëggóo ko fekkóo muy cosaanam fi nga ne
Njéem woomalóo mbay ma gàntal jëggi war na la yaw
Njéem am nga barke dawal xiifug njaboot fumu ne
Mbir mooy jubal góor yu gàddaay seen i xeet ne fi yaw
Ngir Yàlla boo ko xamul réeral murit ya ma ne
Kuy gàmbe ay fas te ñàddul fas ya féqu ba yooy
Yee dee fa yee dog nde xiif baa tar fa ñàdd ya ne
Lii dara yéesu ko sàkkul mbir ba am lu la doy
Kon say murit naat te saw tur siiw ci gox yi fi ne
Am barke it bumu tax ngay def araam di ko tay
Naa yàqu wéy na te yaw sag yàqu sax ca nga ne
Seetal ne Balhaam amoon nag baax lilee ko alag
Birsiis mbiram yàqu ñii ñaar doy na lii ma wane
Xam-xam bi ak barke beek màggal gi baa du la wor
Deel xëntewóo dem ci bàmmeel neex malaaka mu ne
Ngir barke am na daŋar yuy ray te moo di pexey
Ñenenti noon yii dawal ñoom lee ñu laa posone
Booy daw dawal bakkan ak saytaane ak nitu tay
Dawaale bànneex bi kon Buur jox la mbir mu tane
Bul faale ab jajukat day tax nga fàtte sa mbir
Jàppeel sa mbir kepp niw sémmeñ wu ñuy taxañe
Yaw Kayre jullil ci Yonnen moom ki gën ku ñu sos
Ca teg ci Saaba ya ndax mbir def cosaanam fi nga ne
Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun
Yaw kiy murit bi yanul te sant mooy li la war
Sa yan bi soppi ko ag teg leegi doon sa gawar
Doorug murit sew na nib gif muj ga rëy niki guy
Kuy bootu mooy tuut ku màggay dox di hub niki mbër
Ku xiin mu taatan bu dottee waame dootu maral
Njéem dégluwul gumba guy wax cam du taw dafa wor
Xamal ne kuy rafetal njurtay dajeeg lu rafet
Buur Yàlla fii njort lay àttee mbindeef yi du wur
Man Taala maay laahe biir fii kuy dëggal sama wax
Ku sax ci maanaa yi dib saadix bu am lumu war.
Aji-binf ji: Soxna Móomi Jóob
Aji-topp ji: Seex Lóo
Bul wóolu Yàlla ba tee laa jaamu jaamu gi sax
Moo tax mu bindoon la yaw deel jaamu jaamu gu sax
Deel boole jàkk ak a yaakaar Yàlla def ndigalam
Yii yaar la tànneef ya daa booleek i jaamu yu sax
Ku leeralul guddi teg ca lëndamal bëccëgam
Day pert ngir ëllëg it lu waay jiwul du fa sax
Yaw rikk Momar sa bakkan gàttalal yile way
Kuy digle day jëf te yaw sag jaamu sax du gu sax
Yaw daal dogonteek sa seex bii gën ci seex yi fi gën
Fa ñuy layoo doo fa yay ay wor du tee dëgg sax
Taalaa njegam manulaa jox Yàlla ay farataam
Te lott ciy sunna say mbir jox ko xutbu bi sax
Ku yàgg a ànd ak sëriñ bi dara jombu ko ngir
Ku àndulaak seex ba foofee ndax waxam dana sax
Man sant naa Yàlla moo def Bàmba muy sama ndey
Moo tax ma baaxoo taggam wii bañ du tee dëgg sax
Lu bukki wiir wiir ne kuuj dem ndaari man sama daa
Reeyi taggu kiy soppi ndaarik Daaru Yàlla na sax
Te mooy ki fiy sopp xambiy ndaari xutbu yu mat
Ñuy jiite ay Daaru Bàmbaa tee ba réew mi nasax
Aji-bind: Soxna Nogay Cuun