WAAWAAW
Sëriñ bee di góor
Moo di waayi Buur
Yàlla moo di Buur
Waawaaw
Wax ju baax a baax
Jëf ju baax a baax
Waayi Buur a baax
Waawaaw
Bàmba daal a baax
Jëfam daal a baax
Waayam daal a baax
Waawaaw
Moo fi def lu baax
Moo fi am lu baax
Moo fi am ku baax
Waawaaw
Nitam ñee ka leer
Ngéram mee ka leer
Ku koy moy di réer
Waawaaw
Turam wee ka siiw ngoram gee ka siiw
Ku koy topp siiw
Waawaaw
Ku koy noonu sooy
Ku koy ŋàññ jooy
Ku koy gedd yooy
Waawaaw
Moo di kenn moom
Amul dend moom
Raw na ñépp moom
Waawaaw
Du xas kenn moom
Dafay tagge moom
Mbaa mu noppi moom
Waawaaw
Du teg nit fi suuf
Bu lay gis fi suuf
Nga jóg fàww suuf
Waawaaw
Moo di ngën ji seex
Def na seex i seex
Yu am seex i seex
Waawaaw
Fabal lépp jaay
Jënde Yàlla waay
Kon nga baaxe waay
Waawaaw
Xamal Yàlla teel
Te far jëm ca teel
Kon nga raw ca teel
Waawaaw
Sëriñ bee nu yéem
Jëfam jee nu yéem
mbiram jee nu yéem
Waawaaw
Moo ne mes ci géej
Ba nee faa ko ngéej
Mu xëy génn géej
Waawaaw
Ba muy tàbbi géej
Asal booba géej
La guy tàbbi géej
Waawaaw
Képp ku dul géej
Bu tàbbee ci géej
Des ca googa géej
Waawaaw
Mbàkke yaadi géej
Gu xëy génn géej
Ba xëy tàbbi géej
Waawaaw
Doy nga ñépp kaar
Sut nga ñépp kaar
Mat ub sang kaar
Waawaaw
Jël nga ndam li géej
Far ndam jiitu géej
Gënnle ñépp géej
Waawaaw
Fulal gëm yi lool
Yokk fan yi lool
Man nga yépp lool
Waawaaw
May nu Barke lool
Ak ug mucc lool
Am nga yépp lool
Waawaaw
Noo ngi nii di ñaan
May nu lii nu ñaan
Ku xam far la ñaan
Waawaaw
Yaa fi am lu baax
Te am gépp baax
Te far gën ku baax
Waawaaw
Feg nga mépp tiit
Ba ken dootu tiit
Mat nga ñépp njiit
Waawaaw
Yaa nu wan lu wóor
Yaa nu may lu wóor
Yaa nu gën bu wóor
Waawaaw
Noo ngi nii ne tiis
Te tàggook u tiis
Jeñ nga bépp tiis
Waawaaw
Sant jot na lool
Sant war na lool
May gi rëy na lool
Waawaaw
Far nga wépp toor
Dàq wépp toor
Defar gépp giir
Waawaaw
Yàlla moodi Buur
Yaa di gën nji góor
Not nga gépp góor
Waawaaw
Ku nekkul di Buur na def waayi Buur
Mbaa mu miin i dóor
Waawaaw
Jébbalul bu baax jébbaloo ka baax
Ku kay def di baax
Waawaaw
Jébbalul bu wóor te def nag lu wóor
Kon nga am lu wóor
Waawaaw
Faral dugg gaal ku duggul ci gaal
Ñee ku dugg gaal
Waawaaw
Liggéeyal bu baax ku sonnul du baax
Ku am yitte baax
Waawaaw
Dangay wut lu baax te kuy wut lu baax
Da koy wut bu baax
Waawaaw
LU YÀGG YÀGG
Lu yàgg yàgg lu baaxay am lu sedd xolay
Am dëgg dëgg ak lu gën loo gis gënal nu lu ne
Yàllaa rafet jëfam ak léppam rafet mu yéwén
Rafet jëf ak njort a war waayam te gën ca lu ne
Ñaawul bonul tilimul aayul nayul tëjuwul
Tuubal sa moy gi sa moy gee tee nga jot ca lu ne
Jortal ci moom ak lamiy def lépp jàmm aku yiw
Bakkan bi nag dee ko tuumaal ag loram ci lu ne
Bakkan dafay digle aw ay tey teree defu yiw
Yàllay terew ay di diglew yiw ci lépp lu ne
Mbooleem lu koy saf ci waayam lépp yal na ko fab
Tàbbal ci nun fàww biir ak bitti maynu lu ne
Cantam ga yal na ko fab jébal nu ak ngëramam
Lu dul tuxooti ci xarbaaxam yi ëpp lu ne
Dexug ngëneelam gu dul fer mukk yal na ko fab
Saxal fi nun dàkk nuy yokkook a yokk lu ne
La sedd xol lépp biir ak bitti yal na ko fab
Jébbal nu jébbal gu seddub xol nu làq lu ne
Waamew teraanga wu lóoral fépp yal na ñëw ak
Lu sedd xol luy waral xel yépp dal ci lu ne
Mucc ak mbeg ak suturaak ag cant yal na ñu ñëw
Ànd ak lu ñépp ne ngeej ak ndam lu ëpp lu ne
Ku nee ngi taatan akay yaakaar i waame yu ñor
Ne xépp fees ak lu gën loo gis gënal nu lu ne
SËRIÑ BI YAA BAAX
Seriñ bi yaa baax
Yaa yéemu yaa jeex
Ci Yàlla yaa neex
Neexal nu Mbàkke
Yaa sell sellal
Yaa màgg màggal
Yaa jiitu jiital
Jiital nu Mbàkke
Yaa ame tawfeex
Yaa maye tawfeex
Sarax nu tawfeex
Gu yéemu Mbàkke
Màgg nga màggal
Taaru nga taaral
Yegg nga yeggal
Yeggal nu Mbàkke
Ub nga ubal nga
Raw nga rawal nga
Doy nga doyal nga
Doyal nu Mbàkke
Gën nga gënal nga
Set nga setal nga
Way nga wayal nga
Wayal nu Mbàkke
Wér nga wéral nga
Fés nga fésal nga
Jub nga jubal nga
Jubal nu Mbàkke
Fay nga fayal nga
Faj nga fajal nga
Jam nga jamal nga
Jamal nu Mbàkke
ÀJJANA JAA NGII:
Àjjana jaa ngii
Fu sedd faa ngii
Fu yéemu faa ngii
Fu sell faa ngii
Jongama yaa ngii
Ñu tedd ñaa ngii
Ñu yéemu ñaa ngii
Ñu sell ñaa ngii
Tedd nga jaa ngii
Teraanga jaa ngii
Sutura saa ngii
te jàmm jaa ngii
Yonent yaa ngii
Malaaka yaa ngii
Sahaaba yaa ngii
Wàlliyu yaa ngii
Yu xumbu yaa ngaa
Yu takku yaa ngii
Yu soppu yaa ngii
Yu tand yaa ngii
Ak lal yu yaatu
Ak kër yu yaatu
Ak ker yu yaatu
Lu màgg laa ngii
Ak ñam wu dul jeex
Ak ndox mu dul jeex
Ak mbeg mu dul jeex
Lu sotti laa ngii
Loo bëgg a gis gis
Loo bëgg a mos mos
Doo ñàkk tus tus
Sa cant gaa ngii
Sa soxna soo gis
Doo gis lumuy des
Doo ca gisug das
Day ree ne maa ngii
Ta ree ja day leer
Jëmm ja yit leer
Nga beg sa xol leer
Lu dàq laa ngii
Kër ya wurus la
Lal ya wurus la
Lu fa ne mbeg la
Tedd nga jaa ngii
Way ya ñu fay way
Suuxal na yii way
Te dàq yii way
Jaloore jaa ngii
Ndaje mu dul tas
Foofa la am mbas
Fi le amul tus
Cam àll baa ngii
Garab ya day naat
Seen i xob it naat
Ña koy gis it naat
Naataa nge jaa ngii
Cëgg ya day yoor
Meññat ma yit yoor
Cëy Yàlla gii nguur
Gaayi daraa ngii
Ker yaa nga jokkoo
Garab ya rabboo
Way kat ya dengoo
Naa dëkk baa ngii
Ken du tuxooti
Ken du lorooti
ken du xulóoti
ngir soppe yaa ngii
Dee wey na fàww
Lor wey na fàww
Bor wey na fàww
Yërmaande jaa ngii
Pal gaa ngi nii nag
Mbeg maa ngi nii nag
Yëf yaa ngi nii nag
Lu safe laa ngii
Yaram ya day neex
Xol ya dañiy neex
Fàww li lee neex
Karaama yaa ngii
Loo mana am yaw
Te amula lii yaw
Amula lëf yaw
Sa tono jaa ngii
Yàl nanu am lii
Léppak la gën lii
Te am ka def lii
Nag dayo baa ngii
Lii ñor na xomm
Ku ci ne yemm
War ci ne yomm
Ngir Yàlla jaa ngii
Ka mbind lii a rëy
Kay maye lii a rëy
Li miy mayee rëy
Lu gën wataa ngii
Xol bu ne guyyi
Te talli ñàyyi
Jàmm ne beyyi
Jaaraama jaa ngii
Ne dàkk cik pal
Taqooki dimbal
Càyyak dalug xel
Daraja jaa ngii
Mag du ne foofa
Ndaway ne foofa
Te fee te woo fa
Mbeg solo saa ngii
Bala nga faa dem
Def ndaw lu am ndam
Lu ñàkk lëndam
Soppi ku gaa ngii
Yaram wa day xees
Pecc nga far fees
Dell woyof yees
Lu jafe laa ngii
Sangu ba set nag
Wecc rafet jag
Sol yu rafet nag
Soppante baa ngii
Ñu ubbi say kër
Wan la sa waa kër
Ñu tëb la far for
Te naa la yaa ngii
Ndax noo la namm
Am yaa nu namm
Ku man a namm
Kisante baa ngii
Jàppante baa ngii
Duggante baa ngii
Soppante baa ngii
Àjjana jaa ngii
ÀTTE BA DAW NA
Àtte ba daw na
Ndogal ga daw na
Muslu ko wey na
Moytu ko wey na
Gàntu ko wey na
Nangu ko jot na
Gëram ko jot na
Ta mer ko wey na
Ku mere Yàlla
Reere na Yàlla
Te reere Yàlla
Màgg na rëy na
Kenn du def lëf
Yàllaa di def lëf
Kuy mer lamiy def
Ndofam ga rëy na
Lu kenn dul faj
Mer ko lu muy faj
Xul ko lu muy faj
Dëgal ko dog na
Gërëm ko yaw mii
Nangu ko yaw mii
Te ree ko yaw mii
Yaaram ya ree na
Yaaram dafay ree
Lu dikk muy ree
Lu déll-lu muy ree
Ngoram ga wer na
Yàllaa nu sàkkoon
Yàllaa nu bindoon
Te ku la bindoon
Tóppu ko war na
Ku reere Yàlla
Du tópp Yàlla
Kuy tópp Yàla
Xamal ne xam na
Ku sàkk i jaamam
Te bind i jaamam
Te moom i jaamam
Xam ko rafet na
Yàl nanu gëm nun
Yàl nanu am nun
Yàl nanu def nun
La nee fi jub na
La Yàlla àtte
Yàlla na àtte
Nu sant àtte
Boobale mat na
Aji-bind ji: Lamin Dem
Aji-topp ji: Seex Lóo