Bismilaahi rahmaani rahiimi
Ñalgul dañal xalimag way
Ca lef ma ñuy tagge Daamu
Sëriñ bu mag ba fa Tuubaa
Rijaal ya moom la ñu taamu
Moo jar di way ak a sargal
Di riim taggam ya di baamu
Yaw soxna Jaara sa ndam lii
Moo raw ci jëf ak ci jaamu
Mbusoobe moom la nu taaroo
Ak Mëhramu ma mu maamu
Bul wër kemam amulam kem
Seex Ibra Faal fa la raamu
Amul ca Faas ak i Baxdaat
Amul ca Misra ba Saamu
Ku CernoFaati di bóofal
Ak Cerno cër ya mu sammoo
Dootóo fi seeru ku raamloo
Ku toll ne mbër ma fa Ndaamu
Dogon sëriñ ba fa Tuubaa
Sëriñ Daaru jekki ni kaamu
Moom rekk moo man a raamloo
Masàmba Jóob ma fa Saamu
Murit ba daa baye Déndéy
Seex Móodu bóof na ba Saamu
Sëriñ Mamar ma ñu màggal
Bóofal na Bàmba ba Saamu
Sëriñ Ma-Baabu ma selloon
Samsan la bóofe ba Saamu
Péncum sëriñ ba fa Tuubaa
Góor yàlla yépp a fa raamu
Yaa tax ba Ahmadu Baasi
Sàlloo di tagg ak a baamu
Boo jàppatee xalimag way
Taggal ma Ahmadu Daamu
Askaasaraa may rabbin
Bihii yunaa lumaraamu
Halal nabiiyi bi hizbin
Feeg maa ngi fi tagg Daamu
Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun
Aji-topp ji: Seex Lóo