Bismillaahi rahmaani rahiimi
Yewwuleen bu Yàlla falee
Ab laram na ñépp dagu
Dag ca péey ba lay xala añ
Wuyusileen ci seeni sago
Xaadimu Rasuuli la fal
Gàngunaay ga moo ko jagoo
Moom la Yàlla far ca lësal
Nattu yooya moo ko tegoo
Farlu ga ak yitteem ja mu yor
Lëf taxul mu raf bu dogoo
Yàlla rekk rekk la ŋoy
Alxuraan la mas di fegoo
Sopp Mustafaa di xolam
Aw taggam la mas di wagoo
Aar na ngir mi Yàlla tëral
Ag tëyam la mas di wegoo
Waa ju xam du wër ku ko moy
Moom la Mustafaa di sagoo
Lim defar ci dénd bii doo
Seeru fii kemam ba Tógoo
Wër wëraani dem na ba ñëw
Dem na Misra dem na Segu
Wër na ñoñ Araab ba dajal
Ñëw ñu naa ko yaw jugagóo
Nee gisul fi dëek i didi
Réew mu nekk nee na fa góo
Ag Yonen ci Taaha la yam
Xejj baa ngi kaay nu dagu
Baas yëngul te way ko ndaxam
Soo ko bàkkagul wayagóo
Baas yëngul te jublu ci moom
Soo ko jubluwul wayagóo
Sant rekk mooy li la war
Yaa ngi saddi way te gagóo
Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun
Aji-topp ji: Seex Lóo