Gëy Njoora Gëy ñaaya yaw, téereb Boroom bi nga def
Am xëy ku lay fakktal, daa repp mbaate mu dof
Yan bañ yanoon mbër ya woon, téeñ baa ngi yaa ne ko cas
Kuy tee nga dëngëñ di wéy, am mbaam la dees na ko sëf
Ku doomi Bàmba di yéem mbindam ba koy terali
Sag suufe faat na asal mosleen ko, xam li mu saf
Kenn manta lim ñi nga def, sëñ daara tay ak i kaaŋ
sun taal ya doon bëgg a giim, ca Njaañ e yaay ki ko ëf
Doo bërgal ub ndonga yaw, doo boddi mag walla ndaw
Gëy ràggalóo, ruuralóo, reggal nga yékkati tef
Xeet yépp am nga ca kaaŋ, lawbeek i géer a ci yam
Ab ŋaydo mantil a tee, ngay xëy di bay wile lef
Tërub xol ak xel mu nëb, gis-gis bu gàtt bi ngeen
Koy xoole tay dafa doy, def ngeen lu yées li mu def
Kuy jéng baay tëj ci kaaf, tey maas kurã ak a dóor
Looy bañ ku jéng ku daw, ngeen mel ni mbóot yu ñu nef
Jéngub noteel bi ñu leen, ràngal ci ngeen war a wax
Te bàyyi daara mu toog, xam ngeen ñi ngeen war a ñaf
Jaay suuf si jaay peterool, jaay nit ñi sànni sa ngor
Jaayal ba jaay li nga wuuf, mee bàyyi nook sunu yëf
Kuy bañ mu jénge joxal, sëñ daara bii la mu moom
Ŋaaŋleen mu wadd te ngeen, jóg jëf li ngeen war a jëf
Du seen moroom te du seenub, nawle yeen a ko tay
Walleen i nàkka te muñ, seen ñay wa nee na ko tëf
Misyoo la yor matagul, daaraam ja dees na ko taax
Seex Murtadaa a ko sos, ñeexum cofeel la ko sif
Daam Jaane baayu Kariim, Xaadim Gëy ay ki ko yar
Ak mbër yu kenn du lim tee ngeen a jëf li mu jëf
Buur Yàlla Yàlla na tër, kuy noonu daara ci suuf
Labal ko ciy fitna ak, kër-kër këram ya di jaf
Féexal sëriñ daara bii, ndax ag jotam bariwul
Ab ŋaydo mantil a tee, muy xëy di bay wile lef.
Aji-bind ji: Imaam Jóob
Aji-topp ji: Seex Lóo