Ahlan wasahlan watarhiiban ci sun ëtti xol
Ndokkeel la day lu nu war, Géy Njooro Géy ñaayaa
Siggil nga daara yi ak, mbooleem lu taq ci ñoom
Saw tagg daj na Kajoor, Saalum ba dem Ngaayaa
Say soppe bég na ñu tay, sa noon ya pérdi nañu
Xuraan a ngay sigaree, muy saar akiy aayaa
Yaa aw fa góor ña awoon, moo tax nga daj la ñu daj
Sabrun jamiilun a lay ràngal fi aw laayaa
Kuy rëbb day làqatuy, bóof ak di diir ak a raam
Jawfal faraa mi nga tër, yombul ci bii ñaayaa
Yaa rëbb Yàlla ci xuus, gottub xuraanu bi def
Pastéefu ak fetaliy sox wal ya ray gaayaa
Diiróoy pitax ak i naat, dóoróoy jinax ak i wel
Segg ak tene ya nga fees, jam gaynde mbër Njaayaa
Sab donga wecci na junniy, fóore yaa bari ay..
Baasiin yu raw sëriñub ñay sàmm i nag mbaayaa
Géttub ngëneel ci nga yar, ay yëkki garmi yu duuf
xëccoowulóok Ardo meew, yaa soow lu suur paayaa
Yërmaande ngay yeewe ndaw, teraanga ngay gawe mag
Kersa ak lewet ba ñu koy kàbbar nga doon taayaa
Buural wéyal doxalal, sam mbay rafet na te set
jekkil ci sag gàngunaay, tey xelli àttaayaa
Laf cat sa tukki bi nay, sun yokkuteg daraja
Njëggum Unnayni ma feeñ, léebam wa naaxsaayaa
Boolook jullit yi ci am, ak bépp xol bu ci tooy
Nay ciggiteg daara tey, suuxug ku taal daayaa
Jaaraama waa daara ñii, ñooy gar di garmi yu set
Seen xol ya Buur a ko fees, duñ dàcc duñ daayaa
Fuñ wokke diine ñu jóg, fu Yàlla woote ñu dem
Tiituñ rafuñ takk-der, buy boqi ngànnaayaa
Jub jëf ndigal moyu tooñ, yar yiw yéwén ñime dal
Ñoo mag toj ak yàq kon, bal baa ngi ci seen kãyaa
Busraa li Njaañ Njaga seenuw, tagg law na fu ne
Naw yiw di seen xalima, wërsëg di seen daayaa
Bijaahi jàkka ya ak, daaray xuraan ya fa ne
Yal nañ nu dolli ngëneel, sun xel mi bum naayaa
Bijaahi xabru ya ak, jumaa ja Bàmba siyaar
Fu bàrke nekk na dal, kiy bind wii aayaa
Xéewal wér ak gudd fan, wëwsëg wu yaatu te lew
Nay wal fi nun li fi ak, jullee ngi am taayaa
Daam Jaane baayi Kariim, Xaadim Gëy ay ki ko yar
kuy noonu daara ci way, lay xotti say caayaa.
Aji-bind ji: Imaam Jóob
Aji-topp ji: Seex Lóo