Lëndamug cofeel gi ma tàbbi, tax na ma gont war
Mutafaahilun ji fi ñépp, taamu ci tagg mbër
Tegu yéene way yaru tagg bàkk wu saf xorom
La ma koy cawee di ko rëpptal da ma dib gawar
Li ma yeex a jóg terewul ma jiitu ca tuur ba ndax
Wile naaru-góor du fi dàqe mukk, ci kursu par
Li ma naal a bind ci sibtu Bàlla ba tax na tay
Keru xol bi féex, cari xel mi naat na te daa ji far
Ku fi doon wayantu, na teg xalim ga te ñëw awu
Sama géer gi fawxa na gépp géer fa mu làng a bir
Ku fi doon tëbantu na dal, te ngax yi ni nemm cëy
Mbëru mbër yi gétti na waada, cëy ak a neex a far
Sàmba yaandi ngaan nañu tekki, cuur yi te jox ko ndam
Jaratul limaale du maasu ñii fële lañ ko ber
Galanub sëriif la ko Buur tëggal, nattu yoy Yonnen
La ne cas di wéy, bëtam aŋ ca gaaya fi woon Badar
Aka neex a taas, aka neex a jiin, aka yomb a kañ
Aka jar di bàkk ne géeju may ya du nëx du fer
Sëriñub njariñ ba nu daam, ngëneel ya ñu daa xaroo
jëfi Soxna Jaara ja Yàlla nangu mu law di wër
Aka teel a sóobu ca ngir mu sell ma roy Yonnen
aka teel a dab ña ko jiitu woon te fi daa sikar
Fa nga jaare Yàlla la gaa ña jiitu di wër ba tay
gisaguñ sa kem amutoon du am ba ba dun bi far
Ñime coona way, yanu nattu tiis aw sun balaa
Tinu teete taawu nu taaralaat sunu bépp cér
Gaboŋ ak Konaakiri Bàmba kuñ la fi dendaleel
jëfalul ñoñam ña lu tol ne baat ya nga tont Ndar
Ma ne kon sarax nu te yiir nu yaw, mi fi gën mbalaan
Bu nu àppe njuumte yi démb tay lunu moy nga far
Ba la waa Garàmbasa diggi géej nga nu xettalee
Ba nga daane noon ya ca Jéewali la sa ndam ya wér
Di ñu sànge sag suturaak i may yu ñu dul dara
diñu sargal it suñu biir i nawle di fanq mer
Talatun fayantu ni Daam a faj la nu metti woon
Dexi kawsara ay sunu naanuwaay lu nu namm xer
Asakaa ki ay sarax ak ngumeen la nu daa dundee
Bamu ñibbisee la fi nqonji jeex nu ngi afra xar
Xalimaam du jaawale mag na runge du gag du naax
Àlliway Boroom bi ca kursuyun fa la daa nafar
Mbindam ay gësëm aras ak kenoom ya di xacci xol…
Y di dàq ñàkk di dindi réer ak a sippi lor
Tawat ak balaa musiba ak i ndog lu nu jub mu fél
Dërëm ak ngërëm daraja ak i ndam di nu dëkke wër
Asamaan du tiimati gor su baaxe ni Baayi Bas
Lewet ak nëtëx nga mu boole teewu ko mel ni gar
La nga daj Ndakaaru ca néeg ba jar na ku nekk jooy
terewul nga wéy dellluwóo ginnaaw ku la sédd ngor?
Ba nga nee fa jóox kero ràbb jam na sa ndëggu sar
Terewul nga teg ba ca des, nde jom la la Yàlla xër
Masuloo ne uh te sa xol du nux-nuxi bay tawat
Sunu tedd yaay ki ko jënde coona bu yàgg a tar
Dunu am sa fay lu dul ñuy jubal ak a jaamu Buur
di la roy ci sunna su sell jëf di ko teg fu wér
Jote nan la nday jote nan la baay jote lay nijaay
Jote nan la far sunu lépp gee bëccëg ak fajar
Ku la séddu raw te du fuuy du bew ku la am texe
Ku la teggi réer ku la foñ suur lu mu sóor mu dar
Ku la fat ci biir xolam ak xelam nga di ay céram
lu mu yóotu jot lu mu songu daan lu mu jàggi tër
Ku ñu ber nga uuf ku fi loof nga wudde ko ay ngërëm
Ku ñu xeeb nga aj ko ca kaw mu far kawe ñépp cér
Na nga ful nu yaw mi nga xam ne mbaax a ngi far ci yaw
ku la denc féex ku la jënd bég ku la jaayu jar
Ku la sëmb tooye na may yu ànd ak i jagle kon
Nee ma jàkk teg ma ca gàngunaay gi fi ñii di wër
Taxawal te xatmu sa way wi géej amul ab yamu
Tëralal xalim gi te ñaan ca barke ba mujj wér
Texe njub teraanga ju sax fileek fa ñu jëm ëllëg
Darajay Yonnen ba mu daa xëyal ba mu def ko mbër
Salawaatu Rabbi hallayka yaa sëyyidal basar
Maha aali feek muritiy Sëriñ bi di waaj safar
Aji-bind ji: Imaam Jóob
Aji-topp ji: Seex Lóo