Catégories
Leeral waxiini wolof

Jàmbaari fàkk tëdd

Leeral:

Bu xare masaan a am, ba xeex bi tàng, ña ñu daan xeexal jekku leen te bëgguñoo daw dañu daan yeew seen bopp, daal di fàkk ci suuf daal di tëdd yor seen i fetal jàkkaarloo ak noon yi di jam. Nga xam dañuy dee rekk ba ñu not, waaye duñu daw.
Ñooña ñooy jàmbaari fàkk tëdd.