Catégories
Yuusu Nduur

Tongoo

Bu la kersa manee, nga bañ maa woo
Mbaa mu jàpp ma, ma bañ laa woo.

Xaw ma lu ko jar ba sa xol def góom
Te góomu xol di lu la man a gaañ.
Suma jekki-jekkee
Damay dégg am luy riir, ci biir xolam.

Nu dëkk ci tong
Sama xol di jeex
Sa xol di fees
Nun ñaar noo ko def.

Mii xel naan , naa ko woo
Yaw seetal mi gën
Mële xel naan buma ko woo

Yaay seet!
Yaay seet!

Mii xel naan , naa ko woo
Yaw seetal mi gën
Mële xel naan buma ko woo

Yaay seet!
Yaay seet!

Mii xel naan , naa ko woo
Yaw seetal mi gën
Mële xel naan buma ko woo

Sa dëgg-dëgg, yaay sama guddi
Yaay sama bëccëg
Ba tax na yaa ma moom

Te it bunu dee nelaw nun ñaar,
Day ànd ak teey ànd ak silãs.

Fumu toll, dafay janeer
Mel ni ku réer ci biir mbëggeel.

Nu dëkk ci tong
Sama xol di jeex
Sa xol di fees
Nun ñaar noo ko def

Mii xel naan , naa ko woo
Yaw seetal mi gën
Mële xel naan buma ko woo

Yaay seet!
Yaay seet!

Mii xel naan , naa ko woo
Yaw seetal mi gën
Mële xel naan buma ko woo

Yaay seet!
Yaay seet!

Mii xel naan , naa ko woo
Yaw seetal mi gën
Mële xel naan buma ko woo

Yaay seet!
Yaay seet!

Mii xel naan , naa ko woo
Mële xel naan buma ko woo

Dafa daan peñewu yoor-yoor.
Dafa daan solu di ma xaar.
Dafa daan xeeñ gëtt ci yaramam.
Yaramam, yaramam, yaramam.

Suma lekkee mu mel ni lekk na,
Suma xiifee mu tàggoo ak sagoom.
Suma toogee mu janoo ak man di ma xool.
Di ma xool, di ma xool, di ma xool.

Ée yaw! Ée yaw!
Kaay gindi ma
Ée yaw ! Ée yaw
Kaay firi ma
Ée yaw ! Ée yaw
Kaay jege ma
Ée yaw !

Mbëggeel dafa neex lool,
Mbëggeel dafa neex.
Dafa neex a neex a neex ba mujj metti lool.
Metti lool, metti lool di metteek a naqari.

Ée yaw! Ée yaw!
Kaay gindi ma
Ée yaw ! Ée yaw
Kaay firi ma
Ée yaw ! Ée yaw
Kaay jege ma
Ée yaw ! Bilaay !
Xolam dafa ànd ak xet gu neex.
Haa billaay lu xel mi gën a sori ci tukki…

Billaay! Su guddi masaan a jot ci suuf su teey sii
Cëy waay, billaay, billaay!
Xolam dafa ànd ak xet gu neex, gu gën a teey billaay!