Way wii nag, aji-way ji Sëñ Maam Moor da koo tëgg ci anamug abacada.
Tàmbalee ko ci loyu a indi ci waati Wolof yu jafe yi tàmbalee A yépp. Toppe ko noonu bamu jeex.
KUBBITE GI
Xerawluleen ma sadd fii baati wolof
May sunu làkki maam ya déggatuñ ko faf
Ngirag ne sunu jamono lañu xëy mbaanig
Jànqe ko yaawur te rañaane kàcci nag
Te xëy ma ñépp këmm mbaa jópp la dal
Ña jànq it seen diñe gaay seen wéttal
Gaa ya rañaan war ca gëléemi fande ya
Te xit fetal ca ñall yuy golliku ya
Ba génn kéewi dànna yoy ëwoon na leen
Ni dédd def xallóobi gaynde saŋe leen
Jéggi dayoom gu weesu lef moo ma ëlëm
Ma rët ba tax ma bëgg a dëflu cig wayam
Ngir dekkalaat ko góomu alkandeem bi wér
Te suuxataat reen ya ba meññatam ma ñor
Ñu raas ko, fuuyoo ko te racc, def cafaay
Yuur ca di fas dumóoyu lépp lëf lu aay
Jafal la giim te taal ko ngànj muy bérax
Di lekk sun liw bi ba kenn dootu lox
Ñu naan ci dex gi bàyyi tepp-tepp yi
Ak déq yeek njunux yi, xond-xond yi
Dëtëm ba màndi raggu bokkul ak di ñeer
Ci lol dafay guusali put di yokk tér
Masëy-bandaŋ wa wenn dooñ la tooyalul
Waame wa mooy tooyal i tool te koy ñoral
Ba tax ma fëx àkki wolof ya jiitu woon
Muy waxi sun maam ya di mag ñee fi ne woon
Waxiin ya laa jëlaat, fasoo mu delsiwaat
Te ñooy wolof yu wér ya, nar ñu dekkiwaat
tudde ko mottaliy mébet yuñ sémb
Ci dekkalaat waati wolof yoy démb.
LOYU A
Aw naa ci àlli waa Unaare fekk leen
Ñu àngu ñoom ñépp di an calli aréen
ma ëyu leen ne aaye naa ko, indileen
fukki andaar te boy te moytu aawe yéen
Te aw ci xàllu njub te moy anéeri moy
Te wut aléeri topp àkki tool ya bay
Te àlli wànqaasi moy ak àkki ngëmmeen
Buleen di aas ci ëtt mbaa urmbali yéen
Lépp lu aay ër ko fa tay aayelu ay
Tey àddu tey aar sa njaboot ci wépp ay
Te bul di ës ba muy waral ñu ëñ sa kéew
Te mooy sa kiiraay li la ëw bañ di la yéew
Te bul asar lenn, na ngay afal ku ne
Sa xol bi nay af man a uuf mag ak gone
Jépp ayib ju dul sa jos umpale ko
Te ëmbalal ku nekk u yiw àntule ko
LOYU B
Ku bëgg nay bëgg lu baax bañ lu bonam
Te am mbañum-rus ma di xeeñtu aw banam
Te néewi mbóorant te doon ku xuuyi mbéey
Setal sa pooki xol te nàmp batti péey
Ŋoyal ca mbicci kaw ga bul jàpp ci pet
Moyul barastikook a bàyyi bul di xét
Te rendi say mbamb ca pottox ya te boy
Jam ko ca baljat ya te bèccingal ko wéy
Te ñàkk paal ku dul ci Yàlla miy boroom
Te sàkku mbëbbal ma , ñemeg péete ci moom
Te buddi say bémpéñi xol ba buddi buut
Sol ca ngëneel ba lépp pendal ak i mbóot
Te néewi bébbant nde moodi pëppi jëf
Di pindi pax yu feese pert bum la këf
Defal bërét te binni ngir yéem sa ayib
Sàkku pexem faj ko te pasteefu te jub
Defal sa jëf yi pàggutéef wëlif poñat
Lu dee gi bette bette berndeele ko mat
Mbewte nga bërgal ko potoxlu pekki mbég
Génn ci mballi barjalug bakkane rekk
Mbémburi xol di yéene nay mbell mu set
Te bànk i jëf peeg ko te mbaayàlla poñat
Berul te bul topp mbaboor mi deel bérés
Lu bon ci ag mbëbëstënam ci foo ko gis
Bul ca deseb patt faral béel ci lu baax
Te bul ca bar sa mbir na bir ci fonk baax
Te dagg pëjji pànka buural sa kañaan
Te daal di buur jëm ci boroom bi daw safaan
Te fab sa baag yoor ko ci mbalka mom ngëneel
Tanq ca naan te wacc mboori xiila-xaal
LOYU J
Damay janeer lu mel n ceeñeeri cofeel
Mel ni ku ñer cafka ga far ñëggu ca teel
Ba maa ngi jànkoonte ci xol bi aw mettiit
Wu jeggi njobbaxtani cëy jépp jëreet
Ba xel mi jollasante na ak xol bi, li jib
Xañ na ma cëslaay ba jamuuj naa ci lu jub
Mel ni njunux ci man, ci kuw maram lëjal
Ma far di cam su wéet di jukkat di jofal
Te jàmbat ak junj jeñul jóori cibeel
Ma jaaxle componu ci màndiŋum cofeel
Ba jàmberaayi ronqooñ it di car-cari
Jàllawle xel mi xol bi it di jér-jéri
Fit wi ne ñogg jokkalook njàqare xol
Lu sax ne ñumm mel ne coggal gu ñukkul
Ba maa ngi ceeñeerlu ci biir am njayaxaan
Samab ñës it call ba maa ngi ñeetaan
Ma ñaxtu ñaxtu kenn ñëwul jàppale ma
Cawarte dem njàqare ñëw jaxalsi ma
Ba càqaral na xol bi, jàmmi jamjamoor
Moo ma ñëwal njold ma jéllu kekki joor
jullóotu naa ba faf ne jànjaŋ ca ja ba
Ca digg njolloor ga ba weeroo ni Rubba
Ma sàkku aw ñaraasu mbég jàppandiwul
Ñu far ma njàmbaasale njëgg mom jarul
Kanam gi ñëkk , ñaq, ñuqi lëf të ma
Ma njoofu ay jafeñ-jafeñ jàmm të ma
Mu mel ni jaani ñës yu ñàng ñoo ma war
Te doon yu ñammasle di curpi mel ni jur
Ma aw ci ñallu njommet ak xel mu ñorul
Ba mel ni am njëgg ma ak curi lëjal
Ma jumm jummi jiiñ jamoono lii ma dal
Te xam ne moom du jag du jekkal du jagal
Te xam ne ñàngóor a ko gën jikko ndax it
Njekk da koo xamul du jekki it jubut
Ma daal di jàppeelu ci lii ma xam ci moom
Te def ko ñukk jàpp nag ca kay boroom
Te ñukk jëm ci moom te jokk nag ci jëf
Te kañ ko, njukkal ko te far sóobu ci lef
Dontele ne nag njàqare fim ne moo ma muur
Ni njoof di muure jaasi war ma bépp boor
Du tee ma jéem a muñ te xam ne rekk ngëneel
Deesu ko jox cuune ku muñ rekk la ñeel
Te ñàkk jom day tax a jëf cëkk te it
Da nay waral di jëf lu juunu lol jubut
Ay njegemaar yu jekk tey joŋante
Firdawsi cig njoggama yal nan ci joti
LOYU D
Na ngay dëgër ne déjj far jéggi dayo
Te doon ku déjjérle di dàkku mbamb yu
Ba mel ni mbëtti deg ya mbaa mel ne ndëfëñ
Du jàmbatub dagg ni dëññ mbaa wetañ
Te bul di aw ndóol wu dëféenu fàww rekk
Saxal ci dàllu bul di dallu mukk nag
Bul di dijooti ndàmm sonn a koy maye
Faral di dànna bob du déjjatuy moyi
Dëtëm ndoxum ndam ma mu neex ci denqaleeñ Nga nòyyi ndeemeexi ngëneel sa diine feeñ
Dët ga di dotti yaw nga des dér darale
Ni ku ñu dott tey ku dërkiis të file
Di dëflu ciw tiis te nga ndarkepp sa mbir
Dëxëñ sa ndaaf te dàmbe mbeg ak i naqar
Te bul di diis ba faf di ndaare des ginaaw
Na ngay doronke dund gii doylu la teew
Te bul di dàcci mel ni kuy das defarul
Ndéeyaale ak ndétti ndënéer yuy dexi xol
Te doylu yaw doonte ne dóor-dóor nga ame
Dëkke ko ndéem dooj nga am it bul ko gëme
Te dànd doolenke bakkan, daw ko bu wóor
Te bul di dandal it sa xol bu xel mi dër
Te dàngañal te moytu detteelu itam
Ca kàmbi diiŋat ya te daw dee du xalam
Demal ca dex ga bàyyi déeg yi daa doyul
Te digg-dóomu nag ci lépp bul ëppal
Te bul di ndeeteet lu di tan-tanlu itam
Saxal di tan te bul dagook a ndiigu tam
Na dëgg doon sa nding looy dunde dëdam
Te bay sa dooñu diine bul di dooji tam
Te bul di dóore mukk diisool ci lu ne
Da nay teree daanu di tee diig ci lu ne
Xamal ne Yàlla day dënéerlu képp nit
Naŋ ko ba xel dàggiku ngir teg na la bët.
Aji-topp ji: Seex Lóo