LOYU W :
Saytaane day wëtt ci xol wudd la am
Wattu ko bul ko wacc muy war di ku lëm
Dafay woreek a weddilooy werenteloo
Di wàjji ngëm di wonni pas-pas du welu
Wor ko te wodd xol bi ngëm waaru bu wér
Sotti ci waamew tudd Yàlla xol bi wér
Weeral sa wañsu diine def say warugar
Bu ngëm gi woos ni woddbeer wu gar ya wër
Werante wottee ko lu war, lu wóor itam
Na wuutu wor te worma wecci wane tam
Nga wéex sa xol wekki ca luy wollamiku
Te bàyyi weeje it welal tayle ba ko
Te wulli nag wëllu kañaan ak weli rëy
Wetañ yu jëw weñ ko te wetti far ko ray
Te wacc weerante te wéer fa wóllare
Wareef ak ug wegeel te wicc njàqare
Te wërsëgoo wiiri wakiirlu wis ca way
Te xol bi weex nga wattu waŋŋi wuute wéy
Te waggar it sa bopp tey waaru bu wér
Te bul di wëndëŋ wa wogul wàqi te war
Di waaj di wàlli weddi bakkan ak loram
Te weer ko bul weng ci moom ak ci wujjam
Di waslu àq woor ci caaxaan ak i nar
Wékku ci Yàlla def ko waay jëf la la war
Te fonk waxtu xam ne daa wund lu rëy
Te bul di wuññi awra bul di wóoyu ay
Na ngay woyof te bul di wex ci kenn itam
Ku dul ku bon te fonk worma tey xalam
LOYU Y :
Yaraanga a ngi may yeerook a yedd ak a yong far
Yërëmleen ma saag yées yas na yoqat a ngii di yër
Ba yambar ya far nañ tiim ma man may yalaŋ mu yës
Ba yuqóolu naa far yollungar nañ ma far ma ber
Te yiiruñ ma may yoppoorlu yërmaande far na jeex
Ma nàmp yanaatub njàqareek yéjji xol bi mar
Te yombul samay mbir yemb yenkeewlu naa itam
Ci yëmmug yaras maa yay di yuuxook samaw naqar
Te saa meññatum yaakaar mi yuntul ma yéene yiw
Ku nekk te teewul may yëgg uw naqar ak lu tar
Ba saa kawarug mettiit wa yiif na ba yéeg i yéen ba rongooñ di yol saaw fit ne yacc ni laaxu gar
Ma yeewat ci yittey gaa yu yéeme mu të a yéwen
Ma yuugan ko yootug yokk fàww ci ngën ji yar
Te daw yaafus ak yonj ak di yeex ak di yox-yoxi
Te def yoww aw ciw yoon ba def yunn cig cigar
Ma mucc ci yeer muy yabbalum xel di yaag xalam
Te muy yaradal am xel ku yewwu du sóoru mbër.
La yellay ñu yippil may yéréy yeete tey ya gën
Ma far yalfandoo ag muñ ci saa yan bi yuur te dër
Ba yéjj jalag saay bir yaraax yiiraley wetam
Ñu yeddan ma baa yaax, yànjaxaan ma soreek i lor
Ma mucc ci yaafug yitte far yam ci ngën ji yiw
ne yomm yoxoos jàmm ak njariñ ni yulub ci kër
Te yaakaar du tas saay yitte yemb ma yokk itam
Yarook yewwu, luy yàq ak lu am lor soreek i nar
LOYU K
Defal ganug ngënéel te bul di gangalam
Ŋàbb gogub giide di gindi képp ku gëm
Te sax ci gàgganti gox ak gàddi ngëmmeen
te aw ca ngér ma bul ragal giili gëléen
Te ŋoor ci ngor te buñ la ger te bul ca goow
te xàmmi giiri gor yi bul génn sa kéew
Fexeel a gën, ngëneel ya gaw la nib gëwéel
Nga gétti, góor Yàlla gu nekk yor sa kiil
Te goor ci way-gànjari jëf yi bul di géey
sa taali jàngu bum di giim mukk ak a géey
Te jàpp gunti yar ba gànnayu te ŋëb
Ngérti ngëram genge ci kaw xàll wu jub
Te moytu ñall, ngir ngis ak ngiroo nga ca
Moytu giraawaali te loo nekk të ca
Te ŋeeg sa wanti kóttiteefi gàcca tam
Te ŋoy ca mbicci kaw ga gàddu gaali ngëm
Gindiku, say góomi ayib ŋàññ ko nag
Gëlal ko, taal ko ngànj, gas ko suuli nag
Te ŋoy, sa kaaraange gegal ko kaasi mbég
Sugglikook gar ya ca gotti gol ba nag
Nga dib gawar bu gaynde dul gaar ak a kar
ku fit wa dul ŋiis ak a ŋott, nay dëgër
Te bul di gooy ni ŋóot, ku gàlli nang ko ga
Te gaaw te jàmbaare ba mel ni gaynde ga
Te bul di bañ kumpa, te bul kañook a kaal
Jur gu boyug gotti te gur-gur ko ca teel
Te moytu kàmbi kekk yuy golliku ya
te guuf sa gàkki xol yi suul ca kekk ya
Gëndale say ngërëm yu kersa gunge nag
Te guuf sa goog gi, ŋacc kumpa sànni nag
Sa kem yi gaw leen ak i may te bul kañu
Te bul di kooj sa jikko ngëx loxook jañu
Ngaaxi tukkal deesu ko perngal mbòccoor
Nangay worook képp ku doon ab kàccoor
Te ngàcca-ngaalaama ya buñ la këf ba tax
Nga far ca gàllankooru kaf ya buñ la nax
Te bul di gëllgóose jëm ci genn wet
matal ci lépp bul di gaaruwaale it.
LOYU L
Maa lànk dóotuma lépp bay lonk fay di ma të
Lott ay waral leb di tee fay lëj-lëj ay lëm i bir
Laggal te liiru ba jot sam lef te moytu lixóor
Tey moytu am lëgg bul léej ëpp lor la ci lar
Sa lépp nay leer moyul luubook lu lënt te daw
Làggil ci sàkku lu lew daw laaxo ya ak waxi nar
Bul lump ciy jëf, jëfal luy léemtu bul laf itam
Te seeruwóo lolli bob law na ak i mbég lare wér
Bul laŋ ci sab lal bu suuf lóoree nga làlli te wéy
Te lippikuw nit ba làqqiy leewi leew ak i tar
Ŋaawal sa legg mi bul lëñbët lu dul sa ayib
Bul lunk jëm suuf jëmal kaw leemtu naa la nga xér
Sa yitte nay law te bul lump it lu dul li nga man
Nga luf ci dénd bi bu liis mukk itam na nga dér
Laabal sa xol bi te làng ak gaa yu xam ya te way
Bul làmbtuy jëf lateel ug xam te teg ko ci ngér
Bariy lijjanti te bul lott it ci lenn faral
Man lépp làggi ci jëf tey lab ci def warugar
Laggal te bul laŋ ci ag moy bul ca lëng jëm it
Bul luññtuy awra bul loofal sa xel bu ko lor
LOYU M
Maandul te man yaw ci sag maas bul di mànki mukk it
Bul def sa màndiŋi moy ab miinuwaay tubayul
Xeebal masëy wa te muurloo waame moo am i may
Saw fit bu muy màcc jëm cig maax lu mànki nga ful
Bul mëdd may yeeti nang koy sante Yàlla bu wér
Te say wax ak say jëf it nay màndaxoo matalal
Bul magg-maggal sa bakkan nang ko miinal i yar
Bul mer te bul metti, màbbal moy te muñ lu la dal
Metlàngo far ko mu def menteñ ne meŋŋ ne mes
Nga muure kog dëgg gàttal say mébét di jagal
Tey muñ mettiit moom la Yàllay méngaleek musalam
Bul mel ne maaka ma cig bañ tàng dund saxul
Mokkal te màggal, sa jëf bul mëkkal it matalal
Bul yàq nig max te bul def mëkk màmm gënul
LOYU N
Nit nag ba laa nite day niitem xelam te du nar
Te not ci am xel ba buñ koy nax ngirug naaxam
Te nëbb tey jëf te neexum xel di néewali wax
Di noppi cig neen soriy nëx-nëx matal naalam
Di nemmikug naat te nargan bakkanam bañ a nay
Nërmeel itam néegi niig-niigal ngirug naayam
Fum tollu nay naabu lum nàmpal xelam bañ a naw
Tey natt boppam ci ag néewam akug naatam
Waxam nëtëx neex ngirug nooyam nosub bakkam
Di ñoddi muy nàcc ak ay nef daw sorig naagam
Te néeg ci bakkan bi ay tànkam na nooj bumu dem
Mu naj ko bam nàngi faaw bay nuur ci ag naanam
Nemmat ko bum nenn noflaay bum ko xam na ko not
Bam naagu bay neer te bum noppal ci ag naabam
Te yeew ko cig naw di dóor ciy nenkteŋ te mu nal
Daŋar ja bam set mu naaxsaayal ko ciw naajam
Te nàmm xol ba ba dootul yëg naqar te du noos
Ba dee ga ñëw far ne nuus ruuwam ga cig naawam
Te dee du néggandikus lëf, nës-nësal aki nax
Du tax mu dem, nakk-nakkal it du dog naalam
Aji-bind ji: Sëñ Maam Moor
Aji-topp ji: Seex Lóo