Ci àllub Kànka laa réeroon di wër yoon
wa jëm Tuubaa ba gis caawog sëriñ Mbay
Mu ànd ak Njamme Seex Sàmbaaki Kayre
ña ngay sukkóot ci dokkub sàdd ay way
Ma yër seen mbind muy saf géeji Luqmaan
gu bëmboo Hassaan Kahbu lañ roy
Sëfub seen naaga yaay sopp ak liggéeyal
ka taaral Fuuta cér Jurbel ba Bàmbey
Ci xaymag xam-xam ak pas-pas ga lañ dal
jafal làmpub njub ak gindee bu dul fay
Ña ngay xiimee baradab raw ba fàww
ci gaasub màggi maqaamaat akiy may
Ma dëgmal leen nuyoo laaj leen ku leen fal
ci péeyub teddnga ak sañ-sañ bi ngeen xëy
Ñu naan yegsil sunus ndoom toog ñu wax la
ki semmal ñépp cig farlook rafet mbay
Ki yakkal géej gi yakkal jéeri bañ suur
dogub njàmbaar la sóob wàllay te muñ tay
sàngub Seex Ibra baayu seexi Saalih
kiley Xaadim sëtub yaaram ba des Ŋay
Ci ag dooram la romboon gaaya daa raw
ci kursub bëgg Yàllaak xeñ ka jar roy
Tukkeem baa xàcc dandub diine bam weex
mu taaral sunna yeesal yoonu tarbiy
Ba Yàllaakub Yónnen doyloo ko jox ko
nosug ruu yii xamul bor gor la day fay
Ne dañ koo nattu yan koy tiis yu raw xel
mu daagook moom ba sippiy ndam neewul uy
Ci ab yoor-yoor la génnee Mbàkke-Baari
këram yay wéet murit yay daanu ñeey say
Mu naan dalleen damay liggéeyi ngeen añ
ci ginnaaw coono lañ jóor mbég mi leen doy
Mu wan ginnaaw njaboot gaak jom ju rëy ja
ñu naan day delsi ñee naan taal bi day fay
Mu aw Jeewal Luga
ak Ndar dem Ndakaaru
tëral Ibliis tuxal nëx-nëx jëñëx ay
Mu ànd ak Ahlu-Badrin tax raful bët
ku Yónnen doon ndimbal looy ragal kay
Fanaan cib néeg bu lëndëm tiis te jengul
raful tiitul ci buumug Yàlla lay ŋoy
Mu jël gaal jëm Konaakiri jàll Daawme
Garaambasa ak Libarwil def na fay way
Ci mbóotum daa ja ak xalimaam la fàŋŋee
pexey soldaar sa tër seen njiit la leen jay
Ci sirrub bàgg Yàllaak kañ Yónnen ba
la ñoddee mbóoti kun jañ lépp luy moy
Ci barkeb Muntaqaa may sët ci Xaalib
la dàqee mar wa bënnaat teen yu dul déy
Ci teddug Mustafaa may doomi Mudrig
la làqee ndam yu lottal bépp wàlliy
Ca montaañ sent lañ jommee ci saa waay
keroog lañ xam ne dooley muus saful ñay
Fa Làmbarnaaki Galwaaak Kablabiisaa
la tebbee tuuri way muñ yéeg ñëley wéy
Ci dooley Murtadaa may Najlu Murra
la fàttee tar-tar ak mettit ya eskéy
Ci mbaaxug Mujtabaa may naaru Haasim
la gàddoo ndam lu tax nuy ñee ku koy way
Ci màggug Muhtamaa may sët ci Xusay
la làmboo jagle yuy yéem démb ak tay
Ne Buur Yàlla a ko tegtal sun Yónnen ba
Yónnen jébbal ko Buur moo sell jub xay
Mat ak muñ moom la jàngal waa Mataadi
ka feesal sàq yii Maayomba moo bay
Bu toolub diine booyul fee fa Baafël
Ràqiib ak Hattiit ñoo seede lii kay
Ci jagley baayu Ibraahiim mu baax ma
la jéggee yeer ma cëy Yàlla a ka koo may
Ka jullee gaaya faatoo fee ca Wiir-Wiir
ka delloo Sàmba Lawbee tedd am téy
Ci doylug Muxtafaa may sët ci Mahd
la takkee lu garaatug pal mu diw say
Ci sunnas Muqtafaa may ci Maalig
la moomee penku noot sowwoom lu dul muy
Soxiy wal bocciwul jaasi mbaa xeej
ci wéetal Yàlla lay taalee ca lay fay
Du jambat nattu baa muy xul dogal ba
du mer cib xew-xew baak lum doon du wut lay
Bu doon am maas ci muñ xëy donn Ayuub
kasaa Yahyaa ma jëmmam des ci ag guy
Ba seen xam-xam ya jaaxee seen xalaat réer
ci lañ délloosi Daam fii nii nga toog tay
Ba tay fellul ca lam daa dégle darra
ta lam daa aaye démbam moom la bañ tay
Ilaahii jalla han tasliisi barrun
badiihoo sàkk ñiy wax noo ak ñi wax wéy
Kitaabul Laahi kansii wahwa hissii
ci diiney Mustafaa mañ tànn laa ŋoy
Ka bàddil Mbàkke tibbal Sàmb cér Ñaŋ
defal tëggak géwal géer maabo am xëy
Meloom yaay gëm sawar wakkiirlu laabiir
teral soppeem goreel noonam ya ñuy wéy
Du tobbanteeka fayantooki mbindéef
Jolof moo tin fegal leen mbewte ak rëy
Sagul bàkkul ndamul siggil te jaayu
lu waa soodaanu jar tay Bàmba yaa fay
Billaay Seex Bàmba yaay waamew terànga
xamóo tundak xurak joor fépp ngay duy
Ku taataan feese barke ak yiw wu dul jee
ku seetaan sooy ëllëg ñeetaan du am lay
Na ngeen taataan ca jikkoom roy doxiin wa
buleen tuddoo turam way dox ci ag moy
Na ngeen am ngor lewet yiw farlu dëggal
yar ak xam-xam murit day jàng jub way
Kaweg yitteem ma sut sut wees biddiiw ya
dungeen gis cam su làngak moom jarul xoy
Bu doon am kem ci njàmbaar far di Jahfar
ba raayaw diine sampee moo ko tee joy
Ca njombaxtal la lay gaayam di féexloo
amul am pëpp dongaam yépp a ñor xay
Ci fii laa fëkke bët ngëmmen tëral ma
ñu may yeetal ba bët set mbër ya jóg xëy
Ta may ñaanal mucc ak xéewal terànga
wér ak wërsëg ndamak xaalis bu lew doy
Sutal say nawle cig mbaax romb sag maas
ku fiirook yaw lu dul yiw yal na Buur fay
Ma ànd ak ñoom ñu jullil Yàlla sëlmël
ca sàngub sàng yaak gaayam ya koy roy
Salaatul Laahi maa aalin wa sahbin
li feek way Bàmba gën fuuf napp gën mbay
Salaaamun Laahi maa aalin wa sahbin
li feek way Bàmba gën fuuf sàmm gën mbay
Aji-bind ji: Imaam Jóob
Aji-topp ji: Ismayla Géy