Damaa génn bis saa kër di dox romb benn dof
Mu toog cib ruqam jël ay yoxoom faste ciy waggam
Te leeg-leeg mu ree leeg-leeg mu jooy rafle wang ko wër
Ma ngay lox keroog daa sedd boolek tarug lëndam
Wérul waaye teewul nag mu dis gor nde tàllalul loxoom kenn
Tooñul it ña toogoon ci ag wetam
Yaram waa nga sooñoo sooñoo duw dàll duw basaŋ
Te lee-lee mu taw ndaysaan ba taa suuxal ab ëmbam
Bu xiifee pupel lay dem amul ndey ju koy tibbal
Fa nuy këppiy des lay dem fa lay fekki aw ñamam
Te it man la wax day mujj dem lekki ñam wu bon
Wu am yaari fan woo xam ne baaxul ci ag wéram
Na muy def?Gisul yaayam te it amna yatti at
Yu mat sanguwul lum sol da koy for ci ay sënam
Bu jaaykat bi sànnee màngo mbaa sax orãs bu nëb
Mu daw këf ko noonee sax la koy lekkee cig takkam
Ngalaw sàqi nit daw tàbbi néegam ne kàpp tëj
Mu des tay kanaayal want yay dal ci ay gëtam
E ndaysaan bu rombew dàll mbaa pot wallaw sagar
Da koy teg lu rëy moo tax mu koy boole cib ëmbam
Dafay waxtu fum wéetée te lee-lee mu mer di xul
Te kat am na ndey am baay ba am rakk ak magam
Ba muy wér la bokkak ñépp bis ñëw ñu dal ko ber
E waay wéradee tax waaye as gor la woon su gëm
Rakkam donn nab néegam jabar jaa ngi séy feneen
Te ndoom sam amoon boobee batay xolu koy gëtam
Juróom yaari doof lañ fekk Tàmbaa ñu rendi leen
Ba jël séen i awrak séen i yuur lii ka daw yaram
Dañoo butti ñee xar boppi ñee ñee ñu sànni leen
Ci ay kër yu kenn dëkkul ba ñuy xeeñ ñu door a xam
Gisal ñaata yoon lab dof di xëy dee ci ay tabax
Yu yeggul ba am ay fan ba fay xeeñ te kenn du xam
Gisal benn dof bee faatu Leelan ci wenn xur
Ba fay xeeñ te ab xiif rekk moo sànk ag dundam
Gisal ñaata yoon lab dof di xëy lekk ñam wu bon
Ba febar ca ay at kenn du jug saytu ay mbiram
Gisal ñaata yoon lan fekk ab dof mu xëy wësin
Te ken man ta laaxaan kenn ken foogulab ëmbam
Gisal ñaata dof ngay fekk dus kumba mbaa tubay
Dañuy rafle noonee rek di dem ñépp gis pëyam
Gisal ñaata dof ngay fekk duñ jekki duñ nelaw
Dañuy dox ba dee doo gis ku naa xam na bàmmelam
Te gis naa fi bis ab dof bu am benn góom bu rëy
Ma ngay wokkotoo kay waxtu kenn saytuwul wéram
Liilee tax ma jug tay woo Etaa beek ñi Yàlla ñor
Ñu booloo taxaw tey saytu jaa-Yàlla yii ñu am
Wowóowow wowóo yéen góornëmaa réew mi walluleen
Ewaay walluleen as gor su xëy ñàkk am xelam
Te gis ngeen fi ay dof yoy ku leen faj ñu daa di wér
Te xam ngeen ne mbooleem dof yi koo tëye dootu dem
Nde dof boo fi gis muy dem kërug nit la bàyyi koo
Ku wér dellu ciy mbokkam xarit xel dafay xalam
Te gis naa ku faj mbaamam te gis naa ku faj fasam
Fajum jàmb-jóobam faj goloom sax fajub xajam
Te taxtil mu faj mbokkam mu xëy ñàkk am xelam
Ku faj mbaam fajub xaj bàyyi nit àndul ak xelam
Ci lii sax ci laay faf ñaaxe askan wi may waxal
Ñu daw lépp luy tax nit di xëy ñàkk am xelam
Xelal gànjarag nit xel la nit am ba not mbëfër
Xelay tax xaleb naar not gëléem bay xëccab nosam
Xelay tax nu wullig naaga war xàcc tay dañal
Te xam gee ne du maasam nit ci dooleek ci ag rëyam
Xel ay tax ba lislaam teg nu jëf waa ju ñàkk xel
Asal dootu am aw yiw te dootu yilif këram
Xel ay tax nga xàmmee mbaax xel ay tax nga daw lu bon
Xel ay tax ba nit xam lëf ci Buur Yàlla ak mbiram
Xel ay ndab la xam-xam tàbbi ngir waa ju ñàkk xel
Du xam lëf du am lëf waa ju am xel am i yëfam
Xel ay leer ga nit xëy tedde moo tax ba Aadamun muñ
Di sangub malaakaak jinne Ibliisu ñàkk ndam
Xel ay tax ba nit rekkay sangub suuf lu weesu nit
Xarit loo fi gis ngir nit la ngir moo yoram xelam
Xarit ñàkki gët mbaa ñàkki waaraama gën nga nàkk
Am xel xel ay nit nit nitteetil ci ay cëram
Ku jàngoon walaa tulxuu bi aydiikumóo ilaa
Dangay xam ne kon kuy yàq am xel yorul gëmam
Ma wax yenn mbir yuy tax ba sun ndaw yi xëy di dof
Ñi ley rab la nii ay raab la raab yàq nay ndawam
Dofab raab dafay wuuteek dofab rab ci yenn mbir
Na ñuy moytu yàmbaa daw dorog bàyyi ay mbiram
Dofab iilu ak bob siisu ñoom it danaa ci ñëw
Damay jëkk a way ki sàngara yàq ag dundam
Bu kenn fóoni diyiyã day rayum xel di yàq xol
Lu rey xel di yàqub xol ku koy def du nit daxam
Te alkool alag naw gaay ku koy naani dootu wér
Lu waay am lu dul wér jaay ko ngir jënde kok wéram
Lariklees di yàqal nit ci xol ak ci ay xëtër
Ñi xam nee ñu day dem sax ba far gàttal ug dundam
Te dee diis ku koy naan man na dee dee gu diis te tar
Nde luy fuq bët moo gën ci nit luy fuqab xolam
Gisal waa ji naan sum-sum ne xëndaŋ ci géddi bëy
Nelaw bay xaran sum soof na lool xel yi lay gësam
Amoon na ku màndim sëng faf dër di yag-yagal
Ñu koy tàccu muy taasook a saagaa ci ab ëttam
Te am na ku naan biiñ daanu bañ sàcc lam yoroon
Te muy lim bu rëy boo xam ne moo yor dundug këram
Amoon na ku naan sàmpaañ di xeexoo ñu far ko ray
Sulaar saa ko jam ay paaka ndaw dee gu ñàkk jom
Ku naan roos du rus nit dootu rus Yàlla dootu rus
Njabootam ndaxam man naa sëyak yaayamak rakkam
Wisig yeek falaag day yàq am xel ba leen dorog
Kokaa gën kokaayine fopp cib xol akuw yaram
Te gis naa ku naan am ñoll daa màndi bay tërëf
Xalel yaa ko sottim ndox mu far yàq ay sëram
Te it am na dof yoo xam ne ay wird lañ yoroon
Ba rawhaan ya dofloo leen ñu far topp ay xëram
Gisal benn waay biy wird ab diir mu summi ay
Yëreem summi caayaam génn néegam di dox di dem
Te kat bañ ko laajee nee na suuf see ko àttanul
Ma laaj waa ji kon san suuf la doon sàmp ay ndëggum
Te talsam yi ak rawhaan yi lim sànq ciy xalel
Dorog mantikoo jot fàww daf dul lu neex a xam
Te say jàq tax nas cam di siisook a say ba dof
Kurus ag ndofam day metti ndax yombulam pajam
Gisal jenn waay jiy yuuxu tay daw di wër te naan
Dafay bañ a doon ab xutbu kii séenu nag ndofam
Te am raxasun xas-xas xarit xawma lum saxal
Lu dul ndof jëlal aw tur wu leer bàyyi talsamam
Te tas tas na waay bam yuuxu xàccit mu tas këram
Te tas mbiramak soxnaam ñu naa déet mu tas xelam
Kitil ak katal ak màkk jal-jal ku koy sikar
Bu teewloo war a naree dafay waat yu saf xorom
Te ag nasabin ak hatariisun ku leen bawul
Dafay mujj rekk fab ay mbubbam daanu ciy sënam
Jaxaay yaayi dëhtëhtiilu doofloo na ay kuréel
Jalaal jal na fiy wàmmeel te dofloo ñu am xorom
Gisal waa ji tëj néegam ba ab diir mu mbëkk daw
Te naa maa nee ajabaaru maa tay ci ab ëttam
Ku woo Ummu Muusaak yaayi Xëlbaa ci ay kurus
Ma woo man ki bindoon yaayi Muusaa te yor mbiram
Ku fiy woo Afaariitun minal jinni man ma woo
Ka bindoon Afaariitun te yor léppi wërsagam
Dalal nag te teey booy sàkku mbir ndax ku wattuwul
Xérak ëppalak yàkkamti looy sàkku doo ko am
Faral noppi yaw Baas wax bu niwee te am njariñ
Dafay doy salaatun yal na dal Taaha ak ñoñam
Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun