Catégories
Saabal

Iraŋ yuuxu na yuuxug fayyu jëme ca Amerig

Lënkoo-xare yu farandooy Iraŋ ya fa Iraax woo nañu « képp ku bokk ci karce gi » nga « taxaw jonn waajal xare » ci Amerig ngir deewug seneraal bu jàmbaare bii di Xaasim Sulaymaani, nekkoon daanaka wéeruwaayu Iraŋ foofa. Abu Mahdi Al Muhammat jël na gox boobu def ko muy farataam niki tay.

Ñi ci jiitu ci googu woote ñooy ñi jiite karceg Al Xuds di ñiy saytu jeqiku ga, te ñu dénk leen biri Iraax. Ki ci tege di, njiitul Haas Al Saabi lënkoo gi boole mbooleem njabootu karce gi, lënkoo-xare gog sax jaxasoo woon na ak kerceg Iraax gi. Jëf ju ñaaw jooju, tax ñi gën kawe ca nguurug Iraŋ wane seen naqaruw xol tay ci àjjuma ji, neee dinañu « fayyu » ci kaw Amerig, di lees ragal nag mu jur ag jàmmaarloo.

Ci jamono jooju teewaluwayu Amerig foofa ca Baxdaat wax na saa-amerig yi ñu génn Iraax « ci na mu gënee gaaw » ndawal Amerig li xamal na ay ñoñam ne bu fa kenn des te ku man a jël « ropplaan moo ca gën » walla « ñu jël yoonu suuf wi dugg ci réew yi digaloo ak Iraax » yoon yi gën a ubbeeku ci ay digam nag moom Iraax mi ngi jëm Iraŋ ak Siri mi nekk ci xeex jamono jii, teewut nag amna yeneen jaaru yu jëm Araabi Sawdi ak Turki.

« Fayyu gu matale dees na ko def ñeel jëfkati pékke wi »

Kilifa gu mag gu Iraŋ gi xas na ne fayyu gu tar dinañu ko def, Ayaatullaah Aali Xamani, aamu na ne dina « fayyul » deewug Xaasim Sulaymaani digle it ñatti fani sarax ca réew ma yépp. Joxe bakan mooy payug liggéeyam bu matale ci dundam gépp (…) te su neexee Yàlla, ab liggéeyam ak i yéeneem du yam fii dina wéy ba fàww, « fayyu gu matale dees na ko def ñeel jëfkati pékke wi » ak képp ku mas a taqal say yoxo ci lii mbaa lu ni mel di kàddu yi mu rotal moom Ayatullaah Xamani

8i tontu ci « Iraŋ yuuxu na yuuxug fayyu jëme ca Amerig »

Iraŋ war naa def dank ci ay pexeem bañ a gaawantu ba am kangam lu doy tolluwaay ak Sulaymaani ci dayo ci ñoom saa-amerig yi, bu ko defee fayyu gi am dayo.
Lu ko muy dina def lol fay yëkka coom ba xeex man caa am te kon moo cay gën a ñakk, ñday saa-amerig yi waaj nañu ko lu yàgg door a man joye ci moom Sulaymaani.

Yëy-yàbbi