Catégories
Saabal

Yat wu am i gët di gindee

Ñaari dongoy ci daaray farañse fent nañu ab tum ngir silmaxa yi ci Senegaal

Maalig Faal ak Kani Kan ñoo ko fent, ab tum dañu koo defar ngir dimbali walla gindi nit ñi dul gis walla seen ub gis neexul. Yat wii toll ci benn ñay da ñu koo defar cig xarala goo xam ne dafay wane ay bir yu nekk ci kanamu nit ki ci riir walla yuuxu, ci xamleg « Socialnetlink ».
Tum bi nag dina dimbali silmaxa bi mu man di doxi soxlaam, jéggi tali ak di moytu pakk yi ci yoon wi. Li koy artu pësin la bu ndaw yooyu liggéeyaale ci bant bi.
Fii nag la réew mi di xaar jépp doomam, mu wane xereñam ci di sos ak a sottal ay bir ak i jumtukaay yuy yombal dundug nit ñi. Fent ak sos ay bir ak yokk xereñug bir yi jot a am bokk na ci li man a suqali am réew ci lu gaaw.

9i tontu ci « Yat wu am i gët di gindee »

Tubaab bi ci nataal bi de, amna lu ko gën. Nun noo war a gën a farlu ñépp ci bataaxel yi dul kàddu, ta di jeexital ci xel.

Ayca Senegaal yewwu takk jóg dem jot na. Yàlla noppi na ci nun, noo ci des. Na nu jëfandikoo sunuy xel ak sunuy xalaat te bennoo ànd ak sunnu jom. Ca kaw ca kanam nit ku ñuul.

Yëy-yàbbi