Catégories
Saabal

WAX NE WOLOF DU AW LÀKK MOOY AG RÉER

WAX NE WOLOF DU AW LÀKK WALLA XEET, MOOY RÉER DËGG AK ÑÀKK XAM-XAM

Ca Esibt gu njëkk ga ak nguur gii di BÀNTU ak làkk ya ñu fa daan wax.

Wolof aw xeet la, am aw làkkam wu mu jagoo, aw làkkam jotewul dara ak làkku fulbe pël, ñoo bokk seen ug bokk ci meen, waaye seen i làkk wuute nañu. Loolu nag mi ngi mel ni séeréer ak joolaa, ñoo bokk i meen. Wolof dafa am làkku boppam ak mbindum boppam. Seex Ahmadu Bàmba bind na lu bari ci wolof, moo xam way walla taalif ngir dundal ko, ci làmmiñu ay ndongaam, sëriñ Muusaa Ka … Bu defutoon li mu def wolof naax-saay.

Mbooleem làkk yi amoon ci nguurug « BÀNTU » daan nañu leen wax ca Esibt gu yàgg ga. Esibt gu yàgg ga mooy ndayi làkk yi ñu daan wax ci nguurug « BÀNTU. » Jàngat bi Seex Anta Jóob wane nag ak jokkoo gi am ci Esibt gu yàgg ga ak làkki Afrig yu tay, ñu xàmmee ci wolof yu Senegaal. Seex Anta Jóob wane na ci lu leer ne ñoddi gi Esibt gu yàgg ga ñoddi Esibt gu tay gii, bokk gi làkki ñoñ Afrig bokk ak Esibt gu yàgg ga ci téereem bii nuy wax: Mboorum Afrig gépp. Lu bari ci làkki Afrig yi manees naa firndeel seen cosaanam ci Esibt gu yàgg ga. Te manees naa weddi te teg ko ci xam-xam jàmmaarloo ak képp ku tubaab bi naanum xelam ba muy wax naan wolof du làkk, du xeet.

Ngir joxe ay niral ci bokk gi Esibt gu yàgg ga ak làkki waa Afrig bokk nday

1- Ca Esibt gu yàgg ga kef daf daan tekki « teg loxo ci mbooloo mu doon def ñaawtéef « 
2- Ci wolof muy tekki « teg loxo ci kenn ku doon def ñaawteef walla kiy rëbb li muy rëbb »
3- Feh ci Esibt gu yàgg ga di tekki dem
Feh ci wolof di tekki yónni/yabal
4- « Kheep » Esibt gu yàgg ga di tekki jaarukaay ndox
« Kheep » ci wolof di tekki mbir mu tooy, « Tooy xipp »

Képp koo dégg mu naan wolof du làkk, mbaa du xeet bul ko tont, xamal ne tubaab li muy def ci ki mu noot mooy xeebloo ko boppam, loolu rekk a ko dal.

Aji-bind ji Imaam Ñaŋ

Wolof ak Xamle