Catégories
Saabal

LU JAMP IRAAG:


Ngomblaan nga dogal na ngir nguur gi génnee réew ma karceg Amerig gi, ginnaaw yongug Xaasim Sulaymaani

Lu masut a am dale cancug Amerig ga woon 2003 fa Iraag : Ñaari mbootayi polotig yi gën a rëy ca gomblaanug Iraag ga Al Fataah ak Siyaarun déggoo nañu ci wote sàrt biy dàq karceg Amerig gi ci seenum réew. Ca njëlbeen 170 i jàmbur ñoo ko xaatimoon, waaye mujj na ñépp feksi leen ca muy Kird yi ak Sunit ñi ci lu amul xàjj ak seen, di sàrtub dogal ngir génne Amerig ak ug karceem réew ma. Ca jamono joj Iraag def na ag njure ngir boole Amerig ak mbootaayu xeet wi ci yong ñayu-xarew Iraŋ wii di Sulaymaani ci seenum réew moom ak ay ñoñam di luy xëtt seenug cang. Bi ñuy wote sàrt boobu sax fekk na woolu nañu ndawal Amerig la foofa di Matéew Tolle fa njëwriñ ji yor biri bitim réew yi (AE) ci dibéer jii, di it lu masut xew dale 2003 ngir mu leeral lu wara yongug ku toll ne ñaareel ñit ci lerug kilitéefu nguuru Iraŋ, ak Abu Muhamed ak ñeneen fukk ñañu andaloon diy saa-Iraŋ ak Iraag.

1 tontu ci « LU JAMP IRAAG: »

Yëy-yàbbi