Wolofalu Boroomam
Ma jóg kañ waa ja daa way ngën ji Yónnen
Ba Yónnen fal ko muy xutbub Boroomam
Li tax way wii wolof te waroon di yaaram
Damaa nar gaa yi jàngul xam Boroomam
Ma kañ ko te way ko ndaxte mu dolli may may
Géwal sañ naa wëreeluy kañ Boroomam
Ma nettali fiy jaloore te sulli fiy ndam
Te wax xar-baax yu tax ngeen xam Boroomam
Te xejj ya Yàlla fal xam nañ maqaamaam
Ca xar-baax yaak ca may yaak xam Boroomam
Ca wàlliyu yaak ca xawsu ya sax fa diiwaan
Ca xutbu ya ak ña daa wéet ak Boroomam
Ña xam Yàllaak ña xam Yónnen ca baawon
Ba tay kenn jaarugul fa mu jaar Boroomam .
Te wax jii moo ko wax ba ko noon ya yóbboo
Ku diiŋat wax jii moo juuyook Boroomam
Ca géej ga la làmbe Yàlla ba fekk muy géej
Mu tanq ca leeru hëybu ya naan, Boroomam
Ca géej ga la dàqe saytaaneek i gaayam
Buñiy maaj muy taxaw faratay Boroomam
Ca géej ga la moome mbóotum kun ci baatin
Bu noon ba fobee kënoom mu ne kun Boroomam
Ca géej ga la Bàmba tijjee ndàmbi xam-xam
Ba faf yor alliway xalimag Boroomam
Ba àgg ci Yàlla àgg ci ngën ji Yónnen
Ñu sopp ko soppi léppam muy Boroomam
Saxal foofee jihaari bakkan ci ay at
Di boole taggag julleek wéetal Boroomam
Ba faf seey mel ni suugar far ci Yónnen
Di moom muy moom ci baatin cëy! Boroomam .
Ñu bokk ko fal tofal ko ngërëm mu fob kun
Ñu wommat ruu yi jox ko mu jox Boroomam
Di kenn ku ñépp xam foofee ci baatin
Tubaab ya di bañ sëriñ si di yéem Boroomam
Mu faf dib jant faf tiim jépp dunyaa
Di taalif téere yuy sellal, Boroomam
Malaaka ya seere pal ga mu am fa diiwaan
Mu fal ay xutbu yuy déeyag Boroomam .
Balaa lëf a am ci péeyi aras ci baatin
Ñu diisook Daam te mooy jaasii Boroomam .
Te mooy wuutaatu Yónnen far ci kaw suuf
Di mbóotam kun ci lépp lu soob Boroomam
Mu làq ngërëm ci saahir ak ci baatin
Maqaamaam fawqa mboolem ñoñ Boroomam
Sëriñ Tuubaa di maanaam dex, ku dem duy
Ku sóobu ne mes, bu génnee xam Boroomam
Ku sóobe te wéy aw yoonam ya feesal
Ci ay leeram ba faf di duyal moroomam
Ku sóobug dex, na xam ndox dof bi yewwul
Te wàttum ndox lewet na te wex ci biiram
Ku sàggan sànku fàww te lab te doo duy
Te doo set, doo setal doo xam Boroomam
Meloy Bàmbaa ngi waa ju xamul na dégloo
Te roy-royluy jikkoom moo xam Boroomam
Di jox aji-laaj di dimbali ay dëkkaaleem
Du tooñ te ku tooñ mu jéggal ngir Boroomam
Di may ku ko bañ di woo ku ko foñ di neexal
Safoo ku ko soof ku dul kuy moy Boroomam
Di faj aajook a xamleey bóot di seexal
Di génneg ruu ci tuskare jox Boroomam
Di fekk ku ñépp xeeboon ay cosaanam
Mu fal ko ba ñépp faale ko mook Boroomam
Di fekk ku mel ni man jàngul liggéeyul
Mu seexal sol ko xam-xam mook Boroomam
Di fekk muriit bu dof bu tilim ferul baa
Mu fóot ba mu set tofal mbooloom Boroomam
Meloy kaw yaak meloy biiram dëppoo nañ
Du digle lu bon duy déglu ku dul Boroomam
Du moy ngir tiit, du bew ngir mbég lu rëy-rëy
Du bëgg, du bañ, du faale lu dul Boroomam
Du jàq, du rët, du jaaxle, du fàtte Yónnen
Te masul a tawat lu xew ci ku dul Boroomam
Du daw ay noon, du yox-yoxi ngir pexem nit
Du sukkandikoo ci mbam ku dul Boroomam
Lu mbir rëy-rëy da koy far dolli ag ngëm
Du yoqi, du daw, di mbër mu far ak Boroomam
Du wopp ba tax mu wàññig jaamu Yàllaam
Du tiis ba mu tax mu ër faratay Boroomam
Du dégg ag nodd mbaab kàppar te teewul
Lu taw-taw ak lu liw-liw cëy Boroomam
Du tabje ba tiim, du wuute masul di maamuum
Du gàpparu bis, du wéeru jullig Boroomam
Du yeexal wenn waxtu te masul a fay faat
La koy wax raw montar mooy Boroomam
Du ñàkk ba tax mu boddi kuréel ya koy laaj
Du denc alal lu dul téereey Boroomam
Du dox di tëjook i dëkkaaleem ci ay kër
Bu wéetaa ma nga ci Yónnen baa Boroomam
Du dox di nelaw ci ay lal guddi cëy kii!
Du lekk ba regg day mos ngir Boroomam
Di far ay moy di gàdduw tiis ci aw nit
Di sotiy may di jël sànjub Boroomam
Bu nattu jógaa ba jëmsi ci ag njabootam
Mu daar-daarloo ko ngir àndag Boroomam
Yërëm naw ndaw xamal leen yoonu baatin
Teral naw mag ba jébbal leen Boroomam .
Yafal nay bër tabax nay kër ci suuf sii
Xamal na ña sànku woon ngéerum Boroomam
Te taal na ci réew mi taal bu dul fay ci dunyaa
Maseefu la gis kemam cëy mook Boroomam !
Dëgër ba ni këŋ nooy ba ni nemm cig wet
Te am njàmbaar gu tar te ragal Boroomam
Woyof ba ni toyy diis ba ni gann cig wet
Lewet ba ni domm saf-sàppag Boroomam
Sawar, te lefog, te yaatu, te xér, te am ngor
Di tab bu dul jeele lumu am jox Boroomam
Rafet jëf saf xorom du waxa te reewul
Bariy teggiin ci ku mu gis ngir Boroomam
Du xejjag seen, du ay bokkam, du jàmbur
Ku ñëw mu teral digal la nga xam Boroomam
Du boddi, du ñax, du jànni, du xotti saatir
Da lay yaatal ëfal la nga mel ni doomam
Du màtte, du jëw, du xool lu warul te siisul
Du rummi, du mer, du xul ci lu dul Boroomam
Du xaste, du dóore, ñàkkul bay fayantoo
Du dog wormaak i bokkam baa Boroomam
Du fàtte, du fécc wóllëre, masul a wor nit
Du xàddi, du naagu yërmande ngir Boroomam
Du bew, du bajantu day waarook a waare
Du jeng, day fakki maasam ngir Boroomam
Du reetaan nit, du far-farloo, du sot nit
Du yàqub der, du tas nit ngir Boroomam
Ndaxam jii waay jikooy Yónnen la làmboo
Maneeful a lim ngëneelam yeek Boroomam
Funuy raaseeti waa juy mel ni mii mbër
Woyof na kaw te diis na ci biir Boroomam
Funuy raaseeti jant bu dem ba njolloor
Ta leeral yépp gox di kenul Boroomam
Funuy raaseeti waa joo xam ne buy wax
Ku nekk di lox di làqu ku dul Boroomam
Funuy raaseeti kok bu jógaa du geesoo
Di romb dërëm ya, jëm ca mbiram Boroomam
Funuy raaseeti kuy fob Alxuraan jii
Di def ciy taax di taalif ngir Boroomam
Funuy raaseeti kuy gis Ahlu Badrin
Di ànd ak ñoom te dëkkaaleek Boroomam
Funuy raaseeti waa joo xam ne buy way
Araf wu mu def aras di ca bég Boroomam
Funuy raaseeti waa joo xam ne fumu teew
Ku wopp mu faj ku dee mu yëgal Boroomam
Ku bañ bii xutbu bay raasiy moroomam
Du gis bu ni mel ci jii jamonoy Boroomam
Giseefu ko woon ca gaa ya wéyoon ca baawon
Te xarnu yii nuy jub it du ci ñëw Boroomam
Ku weddi ba tax mu bëgg ne maay moroomam
Na def li mu def te wax li mu wax Boroomam
Te dox li mu dox ci réewi Gaboŋ wa Kongo
Ci ay noonam te dellusi ciy moroomam
Te sàkk ku mel ne seexi Ibra Faati
Wa Ahmadu Ndombe ak Làmpub Boroomam
Te sàkk ku mel ni seexi Abdu Rahmaan
Ku juddu ci Mbàkke mool a xamal Boroomam
Te sàkk ku làq jagleg Siidi Muxtaar
Ki dem ba siyaare Yónnen mook i doomam
Te seexal kem li Seexi Bàmba seexal
Te sellal seen xol ba ñu xam Boroomam
Te sàkkal leen i booloo fàww yuy jëf
Te tàggat leen ba duñu man a moy Boroomam
Te kat na saxal liggéeyal ngën ji Yónnen
Te bum tere muy taxaw faratay Boroomam
Te dootul nelaw, day daw soxna ya mu am
Di daw saytaane tey wéetag Boroomam
Te bum yoqat te bum jéllal lamuy jëf
Te bum ngistal ci jëf na ragal Boroomam
Te bum diiŋat sëriñ sa te bum fayantoo
Te bum bég ngir ku koy gottil moroomam
Te bum xas nit, bum jëw bum rambaaj it
Te bum fen bum dogag bokkag moroomam
Te kat na saxal jihaar bakkan ci boppam
Te muñ tiis ak naqar te ragal Boroomam
Te day xam bóoti xol xam baatinam nit
Di saafara ràggi xol di xalam Boroomam
Te bum digleek a aaye ci wàllu bakkan
Di woote ci kaw te biir ba gisul Boroomam
Li ngay lim doy na yaw Muusaa taxawlul
Ba tay jotagóo lu mat asakay Boroomam
Gu dégg ñu jàng way wii nang ma ñaanal
Ma am ngërëm te sax fi ba xam Boroomam
Te def géwelam bu koy way fii ak ba may dee
Te wax ju ma wax mu saf ko te saf Boroomam
Ku bëgg di mbër meloy Bàmba a ngi nii seetal
Ku mel nii mooy donay xutbub Boroomam
Aji-bind ji: Njaga Saar