Catégories
Sëñ Maam Moor Mbàkke

Loyu F, X,R, S, T, mottali gi

LOYU F

Fegul te fog te foogu tey ku fendi far
Ci lépp luy fëkke te am fulla ju far

Te fuglu fàwwu Yàlla tey fàggu bisam
Ba mujj tey farlu ba feesaluw fanam

Te femm bakkan bi te fàndaañu te fëx
Ba fagg bul fippu ba far tàbbi ci pax

Te bul di féttéerlu ba fiirook sa bakkan
Facanteel ak moom te far ak Yàlla ba fen

Fépp fu saytaane ñëwee nga fénati
Te xam ne lépp lum la wax day fenati

Yàlla ku fiir la kon faral féete fa moom
Àdduna daa foytu te ag sax du jikkoom

Te fiir la guy firngale fàdd lay fexe
Ku ci ne foox sa tànk far ñàkk pexe

Nga rët sa faalànq gi fettax ne fëlëñ
Te fekk fomm wéy nga fënde nib fëriñ

Nga fande fii ak fële feccikul ca teel
Lépp lu lay musal ca fiir googa fexeel

Sa faayda firndeel ko ci foog ak fagaru
Fab jiwu fit te dem ca tooli xol faru

Faxas sa fóoy gi tey fésal sa yéene nag
Te ful sa jëf mu feese yiw nga falu nag

Fodaŋ sa bakkan bi te folli ag palam
Te fecci kóllareem ga fas nag sa kanam

Faramlikug tenq ga bum la fif ba tax
Nga far ko kon nga fuuti fequl te nga fëx

Firincikul ca buum ga filli teel a fog
Fenam ya buñ la fàbbi fippul të ko nag

Fabul te fas yéene mu foñ la foñ ko it
Te bul ko faale it na fàndaañu ba rët

Bu follikoo ngay falu fàww fëll it
Ca maas ga for mànko ci coona fés ci sut

Defal sa fàggulde mu doon ay jëfi yiw
Yu yéene lal, te farlu, kon sa yiw wa lëw

LOYU X AK Q

Xarit xélul te xellu aw ci xàllu xam
Te xér ci xëntewoo lu lay xiir ci xalam

Te xettalil ku nekk xiirtal ko ci xay
Te bul xatal sa xol bi it ba xëy di xay

Te say xalam na dooni xiig nga xuuyi mbéey
Te bul di xottente te xér nag ci liggéey

Melal ni xettar ci ku dëng mel ni xaal
Ci soppe yépp ku xuloo nga xañ ko paal

Te bul xulóok a xeex ak ay xasante yaw
Te bàyyi xiirook a xëccoo lu man di xew

Te bàyyi xeebante xaroo xoddiku yaw
Te ngay xereñ te jéem a xejj jëm ca kaw

Te xeet xumaagi xol bi xembi ay xalam
Xerawlu yiw wa faj sa xëndóoñi xalam

Sa xel mi bum xuuge na jub xocc te wér
Xëllóob ya buñ la gën di aaru kon nga ñor

Bu say xalaat xajam nangay xajoo ku ne
Te bul ko xumtoo te xemmem njariñ lu ne

Te bul di xàddi bul di xàcci xàllalal
Ku nekk u xàll bul di xallal it sa xol

Te xippi gët yi xoole bul di xuuse it
Te bul di xand xur wu xéewal ga newut

Te ngay xareek àdduna xas ko xupp ko
Te xoqatal ko xuuxle it ci xeexi ko

Te xam ne màggat mu Jigéen mu xubbidaas
Te xetembee xetembe xàŋŋ gët ya laas

Moo di misaalam bu ko xoymet sa kanam
Xëb ko te far ci xol bi xuulu ag bëggam

LOYU R

Rayal sa rëy gi rendi reewandeek ragal
Te roy rafet-rafet yi réccu ràggi xol

Raxas sa réeri xol ba roppi ñépp raw
Te roof ca rus Yàlla te rembatal ko yiw

Te rëcc saytaane raxal fiir ga mu yor
Te rat ko rinkil ko du ruur génnati far

Te bum la rambaaje defal rokk ci moom
Ratt daŋar ja rékki mbooleem i naram

Te rënk gëm ca róog te bul raf ba mu rot
Te rikk bum la xoqatal ba tax nga rët

Bakkan bi ruuj ko rijj reen ya riije ko
Te rëq ndiggam la te ray ko robi ko

Àdduna rusloo ko te raaf rëddi faram
Te bul di ruusaanu akay ronn i yëfam

Tey raju bànneex di ko rog, ràññe ko moom
Ragg téram ba ba mu set rësal pexeem

Sa noon yi buñ ree bu ci kenn rëcc tam
Na seeni reefu ne ci yaw bu leen yërëm

Na seen dereet yi riix ci suuf si rungleen
Te ràngleen lu rëy te metti rombleen

Nangay rañaan di jàggi ruur di daw fu rëb
Di tuub i rëcc-rëcc roñ ca yiw ya ŋëb

Te riggalal ngëneel ci xol bi yuñ ca riim
Te bul di reggal it sa kàddu dee ko riim

Te bul di ràppal ak a reesal lu lewul
Donte lu ras nga am te am rooy rafetal

Te bul di rànnamtalu ngir ràbb ca wor
Ngir jëfe kuñ rëbb la daw ko jiitu far

LOYU S

Sotoxlul saŋes Yàlla war sàllu ngëm
Te sóob um lefam daw ba seer ug palam

Sawar am sagos muñ te sàkk ub sagam
Te sëmbërtaloow yiw ba gën sépp sem

Te sartaagal’ak sag safoo Yàlla jëm
Ca kaw sippi ag sew waxam mbaa jëfam

Te naan kaasi ngëm suggalee sell yaw
Te bay saw sas ak gopp sunnas ka xam

Selaŋlul te bul dox di sonjaanu sas
Te ngay sopp Yàlla’ak a santiy mayam

Sa bakkan bi dang koy sébéj bam séxéñ
Ci ag nooy ak ug topp sunna ak sëfam

Te siiwal pexeem bul ko bàyyeek sagoom
Dafay sooke aw ay sexeeral mbiram

Te siiw mbicci kaaraange semmal ko jëm
Fu sooŋooŋ ak ug sooy newul ak tilim

Nangay sémb loo man di sottal di sos
Ne siiw am njariñ ak sutura ak ngërëm

Te bul jëf lu suufeek lu sew bul soxor
Nangay jëf lu set saytu sàqiy payam

Nangay sonne xam-xam soril luy safaan
Te bul sob te bul sikkal it senn cam

Te bul sóoru mbër it ndegam suq nga
Te bul soxlu mbër soxlawool ug manam

Te bul siis itam ab siboor saytu ko
Nangay seexlu ñaawtéef wa sib ag jëfam

Te bul sànj benn ub jullit sopp ko
Te bul koy sabooteek a salteel deram

Te ngay digle ag sell bañ caa selaw
Suturaal ku nekk it te sàmm ub deram

Te bul def safaan it ba tax ngay sëngéem
Sippeekul di surgab ka man tey ku xam

Safoo sab sëriñ fàww dib sang yaw
Te sa baati seedeem ka sapp ug demam

Nangay faj sa jikkoy saŋañ sempi ko
Te bul suux ci sañ-sañ yi Yàlla a ko am

Te bul nég ci am mbir suba’akiy sibir
Dafay faatal uw yiw du sottal mbiram

LOYU T

Toroxlul te tuub tey topp Yàlla te teet tereem
Te teey tabe tey tàggat bakkan beek a daw pexeem

Toŋal ko te tóngook moom te tëkku ko bul ko tëy
Toroxlu ci Yàlla’ak ug tëyam sàkku yërmandeem

Te bul toog te bul jëf it ci maa tey mu tond lool
Na tandu te bul teeŋal ku të togg tuskareem

Tegul yaw ci kaw yoon wii taxañ bul ko teggi tam () te bul tagatémbeek ug tàyyeel ak lu deesi yéem

Te daw tabarondum digg njolloor mi ngay taseel
Mu teggilook’ay tàbbiloo teen i tappaleem

Fegug Yàlla moo gën ngën ji tungaar ak iy tata
Nangay tàbbi kaaraangeem te bul génn bul ko jéem

Te taafenteloo nag aw turam foo fu man di dem
Te ngay tos sa xel bam saf ku dul yaw nga far ko tiim

Nga tutti sa xol bam set ci tér ak tilim-tilim
Te muñ tiis ak iy tar-tar ba gis tërgën ub taneem

Te daw tañaxook tànjaŋ ci mbir moo xalaatagul
Te daw tumurànkeg xam nangay tàpp cig wuteem

Nangay tànn say àndaale tey tànnu taaru jëf
Te tàmmal sa làmmiñ wax ju yiw mbaa nga far ne xiim

Te tooke sa bànneex far ko tiiñal te tanc ko
Te tuumaal ko far tëjjal ko tàbbal ko ciy pexeem

Nangay tembareel say mbir sa jëf takku am njariñ
Nga lal tesaranteg muñ te bul tayle ngor ci keem

Te ngay bàyyi téesanteek a teefonke ak tërëf
Te taataar toroxlul nag ka deesul gis ug tëleem

Te tàpp ca xéewal yee te jug tepp-tepp yii
Te tàggook i tër ak taq tey fab teraanga leem

AG MOTTALI :

Laa yéene woon a indi fii nag la mate
Te mooy wolof ya sànku woon ba të jote

Ma jug dabaatalaat ko ngir mu dekkiwaat
Te suuxataat reen ya ba xob ya seqiwaat

Ba meññatam ma ñor njariñ la daj fu ne
Ku nekk mos ca kotttéef la daj ku ne

Ñu bokk fëx ku des ginnaaw jéem a dabe
Te daw ba roppi népp nag te buñ rabe

Mu doon i mbég ci népp tey ag sigére
Te xel yi dal ba xol yi dootul fér-féri

Yaraax-yaraaxam yi yitam fatt taraj
Ba ab poroxndoll du des bu lenn xaj

Ba sun cosaan xajam-xajam ya set welas
Layaat ko seggaat ko ba tër dootu ca des

Ñu rat ko nag ba dóotu dàngaŋ jawali
Ci ndàndfayfayug keneen bay lëjale

Ne nit amul lu dul cosaanam ak ngëmam
Cosaan la it làkk a ca jiitu nañ ko gëm

Ku wàcc sab àndati ànd boo dem it
Fekk boroom ca kaw ne déjj day ku mat

Ndegam dangaa waññiku delsi ci sa bos
Fekk keneen toog ca dangay ku xel ma des

Kon maa ngi woo népp nu bokk takkuwaat
Te fonk sun làkk wi bun ko sànniwaat

Nit bu nitee du dem ci tool bàyyi sasam
Di bay sasuw keneen ba booyal uw sasam

Dafay fexee lippiku ñépp bay sasam
Bu sottalee bayal keneen di ndimbalam

Dafay jariñ nit ki te bañ koo jariñoo
Balaa jariñ nit ki na nég ba jariñoo

Nu ñaan ci Yàlla miy boroom mu boole ko
Ca jëf yu yiw ya sun xel it mu dolli ko

Te def ci way wi barke xiirtal nu ci way
Ci fonk sun làkk wi népp bokk wéy

Aji-bind ji: Sñ Maam Moor
Aji-topp ji: Abdulaahi Juuf