Catégories
Saabal

BIS NI TAY 8i FANI SAAWIYE LA 1896…

Bis ni tay, 8i fani saawiye 1896, la tubaab yi yóbb woon Sàmba Lawbe Penda Gaboŋ

29i fani mee 1890, ca la jàmburi Yaŋ-yaŋ ya faloon Sàmba Làwbe Penda Njaay Buur ba Jolof. Nguuram ga nag Farãs aka ko tëye, taxawu ko, gannaaw ba ñu dàqee Alburi Njaay. Ay fan yu néew rekk a tege ca pal ga, Sàmba Lawbe xaatim ak tubaab yi ag déggoo, ci 3i fani suye, gog Jolof nangu na ca ne Farãs teg na ko loxo, ne yéey da koy aar.
Ci 7eelu tomb bu déggoo ga, dogalees na fa ne :

« kenn dootul sañ a sanc fenn ci Jolof, lu dul kàngam li fi nekkoon di ab tubaab moo ci maye ndigal ». Ak it ne « tunduw Jolof terees na ko Alburi Njaay ak sàmbaabóoy ya mu àndal ak ña ko dar, jóge ci yéneen i réew jàpple ko muy yàqate Jolof ».

Juróomi at la ñu ca teg, Seex Ahmadu Bàmba dem Géej. Nees tuut, am ñu tuumaal Sàmba Lawbe, ne ci taalubeem yi la bokk. Tubaab yi posee ci daaneel ko, moom mi wéeru woon ci ñoom, ba noppi yóbb ko Gaboŋ. Li gën a doy waar, doomi Alburi Njaay miy mbokkam ma mu noonooloon ba taxoon mu jébbal Jolof Farãs, moom la kàngam la fal : Buuna Alburi.

Fàttali mboor mii, dina delleosi xel yi ci ne xeex bi jéexul. Coppet ci gii, ndong ci bee, mooy naka-jekk doxaliinu Tugal ci sunu réew yi. Nàkk bopp nag, wéesuwul foog ne ànd ak i doxandéem ngir xeex mbokk dina maye ndam. Mukk! Du sax ngor, du it jom.

Ndaxam dey, mooy li fi nekk ba sunu jonni tay jii. Ci njiit yi fi Farãs dooleel ci sunu kaw, dëgg la. Waaye it ci sunu biir, nanu ko xam.

Làkkuw tubaab wii nu nangu mu nuy àtte doy na ci sëkk firnde. Ndax bari na ñu gëm ne def Wolof muy làkk wi réew miy doxe, tas réew mi la. Naan kon nanu fi bàyyi làmmiñu farãs, ndax jàmm am. Doonte nooteel a nu boole ak moom. Doonte 85% ci waa réew mi dégg nañu Wolof, te ñu néew ñoo dégg tubaab. Amna ñoñ, làkk tubaab a leen gënal làkkuw wolof, donte wolof ay seen mbokk.
Li nu xam kañ la ñuy jariñ? Fi nu jaar ndax doyul yeete?

2i tontu ci « BIS NI TAY 8i FANI SAAWIYE LA 1896… »

Yëy-yàbbi