Catégories
Saabal

Tukkib Putin ca Siiri

Tukkib Putin ca Siiri: bataaxelub dànkaafu ñeel Trump

Mbalum Penku mii, àddina sépp ne jàkk xiiroo gi diggante Amerig ak Iraŋ, ci la Waladimiir Putin tànn a dem Siiri. Ku am seetlu xam ne, tukkig nemmiku gii, bataaxelub dànkaafu gu leer la, ñeel Amerig.
Talaata jii la Putin dem Damaas ngir, ci li ñu biral, nemmeeku sóobarey Riisi ya windewu ca réew ma, ak it gise ak Basaar al Asaat.

Néew gi mu tukki bu bette boobu néew, rawatina ci jamonoy xiiroo gii tangal gox ba, jar naa bàyyi xel. Ag pàttali la, ngir Trump xam ne amna fa boroom kàttan bu ko man a defante ak moom. Kok ëpp naa yëngal, ndax it farandoow Iraŋ la.

Tayraan ak Mosku seen ug lëngoo day yokku. Ndax, Riisi diganteem ak Tugal mi ngi gën a ñagas, ak doxalinu maslaa gi muy doxee ak siiyit ya fab ngannay di xeex, ba tax na jëmewu ñu xiixaan gi ci déndu Riisi.

Doonte, nguurug Amerig a ngi teewal xare bu rëy ca réewi naar yi, te Riisi deful lu ko tax a joŋ ca Penku boobii, jublug Putin mooy xamal Trump ne du moom rekk a nekk ci tool bi. Na mu ko gàllankoore ca Siiri, la ko man a rëccu loo song Iraŋ.
Ak lu man di xew, li wóor mooy, kenn ci ñi séq mbal mi sawarul a xeex.

Leeral
Sóobare : ku bokk ci xare bi (« soldat » ).
Siixa : « chiites »
Joŋ : daan, jël ndam li
Lokki xare : taal ab xeex, tàmbli ko.
Mbal m: la crise

2i tontu ci « Tukkib Putin ca Siiri »

Yëy-yàbbi