Gàmm Jaksaaw gog 2020 gi, te ñu koy amal at mu jot, mu war a am 8i fan ci weeru Saawiye, doon na gees di xaar bu baax. Li ko def mooy Xalifa bépp Murit yi di Sëriñ Tuubaa Sëriñ Muntaxaa Mbàkke la ñu tuddee Gàmmug ren gi. Loolu di mbégte mu rëy buñu xoolee mbokkoo gi dox ci diggante Tuubaa ak Tiwaawon te ñaari kër sax ci di ko sàmm. Sëriñ Muntaxaa Mbàkke wax ne bég na loolu ci cér bii jóge Tiwaawon jaare ci Sëriñ Siidi Ahmet Si Dab-Baax mi ñu yabal.

8i tontu ci « Tuubaa ak Tiwaawon ànd defati lu rëy »
Lii daal mooy senegaal
Bég naa ci lool
Jërëjëfati xol sedd na lool ci ànd bo
Jërëjëfati! Am naa mbégte lool ci jëf ji rafet na.
Jëjëjëfati xol sedd na lool ci ànd bi
Lii de am na solo lool, Yal na wéy.
Yal na sax te nu ànd ko ak jullit yépp
Lu rafet yàggna senegaal, dox diggante mag ñi!