Catégories
Saabal

BIRI XIIXAAN JAAXAL NA MAKI SÀLL LOOL

Ngir xeex xiixaan, Maki Sàll teg na ci cempteŋ li ab sàrt ngir kaaraangeg réew mi:

Dafay doon luy jox kilifay njémmeer gi jumtukaay yu nu yoonal yuy tax ñu man di jël i saafara yu jag te tolloo ba noppi méngoo ak jafe-jafe bi taxaw, ngir xeex congi xiixaankat yi walla jépp jëf ju niroo ak moom, niki jël i nit, tooñ, walla di màggal jëfi xiixaan. Kenn dootul nangooti ku ñëw di nu jàngal Islaam ju wuute ak ji nu xam te mu lalu ci jàmm, ak déggoo, ak yaatu dënn ak fonkante, te Senegaal di ko dundal ay xarnuy xarnu booba ak leegi. Ci noonu, Càmm gi dina wéy di saytu tënku gi ñu war a tënku ci sàrt yi ak dogal yiy dox ci réew mi. Ci wàllug yoon, ginnaaw ndogal yi nu amal ci nangu tëye ak jël alali nit, ak kuréeli xiixaan yi, war na ñu itam bàyyi xel doxiinu lënd gi bu baax ndax dafa di barab bu ñuy jaar ngir di jàllale seen i bataaxel ak di fa jote ay koppar.

Loolii la njiitu réew mi xamle.

Leeral:
Xiixaan =terrorisme
Cempteŋ l=la table
Xiixaankat =terroriste
Càmm g= l’Etat
Njémmeer g=le public

2i tontu ci « BIRI XIIXAAN JAAXAL NA MAKI SÀLL LOOL »

Yëy-yàbbi