Catégories
Saabal

KAAWTEEF CA USUY

Lu doy waar te metti di ab liir bu ñu sànni ca àll ba mu jur coow lu rëy fële ca goxub Usuy. Alkaati yi ñoo gis ab liir buy dund te yaayam sànni ko ca àll ba ci bisub 30i deesàlaar 2019.

Li doy waar ci mbir mi mooy, liir ba amna fukki fan ak benn ca àll boobu bu nu sukkandikoo ci « seneweb » waaye Rfm nee na ayu-bis la fa am.

Jamono jii nag mu nga ca cuuruur bu Usuy, yaayam mi am 27i at te nangu ne moo def jëf ji ginnaaw bi ko luññutukat yi sonalee; mujj nañu ko yóbb ca kanamu toppekat ba.

Yëy-yàbbi