Catégories
Saabal

SONKO AMNA DËJ

Ibraayma Jaxabi noppalu na, biig, ginnaaw ag jagadi gu yàgg. Taskatu xibaar la woon, doon liggéeye GFM.
Moo gaaraloon kàddu yu xóot yi ci xëtu feesbugam, ci 24i fani saawiye 2019 :

Dafa am jamono yoy la woon day wonni, am tolluwaay yoy ne nemm wóorul. La fay tane ci lu wóor mooy def lu wóoradi. Nanu aamu lu wóoradi ngir Usmaan Sonko am ndam, 24i fani feewriyee 2019 ca ngoon

Jaxabi moo saytu woon diggante Pastéef ak caabal gi. Sikkuwul ne bokk na ci ñi ubbil Sonko ay wunt, niit ko ba ñépp seen ko.
Yal na suuf woyof ci kawam. Boroom pastéef la woon…

1 tontu ci « SONKO AMNA DËJ »

Yëy-yàbbi