Catégories
Saabal

JAMRA JURE NA NDAW SII DI RÀNGU:

Kureel gii di JAMRA noppi ngir jàmmaarloo ak ak RÀNGU miy lémbe lénd gi. Ki yor kàddug mbootaayug Diine googu, jure na ndaw si. RÀNGU nag waw na bët lool te ñime coow ginnaaw ba mu defee ay werale yu tegginewul ngir di ca siiwal ngontam xumbal ma muy def. Coow li mbir mi jur nag, taxul mu teggi tànkam benn yoon nde tóllanti na ko ginnaaw bi mu solee colka gu gàtte di wane céram ya siiwal ko ci mbaalu jokkoo gi. Lu ni mel la maam Maxtaar Gëy di ñaawlu, ba tax muy wax ne «RÀNGU mi ngi dëggal boppam ne dina def i biram 11i fani feewarye bii di ñëw di luy xëtt sàrti réew mi tënk njémmeer gi jëm ci yiw, ak jikko yu rafet. Bunu sukkaandikoo ci maam Maxtaar Gëy ginnaaw seen daje bi ñu nar a def àjjuma jii di ñëw ci ngoon, dina jébbal yoon ay firnde yuy wane jëf yu bon yi RÀNGU di def.

Leeral:
Jure =porter plainte
Njémmeer g=public
Lënd g=Internet
Mbaalu jokkoo g=réseaux sociaux

Yëy-yàbbi