Catégories
Saabal

PETEROL BI AK LIGGÉEYAM CI SENEGAAL:

PETOROL BI AK LIGGÉEYAM CI SENEGAAL:

Bir yi tàmbali na, jëwriñ ji yore petorol bi ak yasara gi di Mamadu Maxtaar Siise tàmbali na ci talaata jii liggéey yi jëm ci génne petorol bi ca Sàngomaar ginnaaw bi mu xaatimee ndogalul meññal lu mujj li. Te ñi ko gaaral di ñi bokk ci sosyite bi war a amal liggéey bi. Jëf jooju nag mu ngi am ginnaaw bi Njiitu réew mi amalee ab ndogal buy maye ñu tàmbali liggéey bi te ñi koy amal di lijjantiy Óstaraali yii di (FAR AK WOODSIDE) lijjantig Amerig gii « Cairn Energy » ak lijjantig réewum Senegaal gii di PETROSEN. Toolub petorol bu Sàngomaar bi dina génne ci njëlbeen gi lu tollu ci ñaari téemeer ak fanweeri milyoŋ ci barigo tolloo ak téemeeri junniy barigo bis bu set. Li miy génnen lépp ci peterol dina tàmbali ci atum ñaari junni ak ñaar-fukk ak ñatt (2023) bunu sukkandikoo ci jëwriñ ji, ba tax ñu ngi ciy xaar barigo bi ñiy njëkk a génne bunu sukkandikoo ci APS.

Leeral:
Lijjanti g : entreprise

Leeral:
Lijjanti g : entreprise

1 tontu ci « PETEROL BI AK LIGGÉEYAM CI SENEGAAL: »

Yëy-yàbbi