Catégories
Saabal

15… GINNAA BI NDONGO LÓO DËDDOO

Ginnaaw at yu néew te gànjaru yi mu def ci way te am ci kiilu gu rëy, Ndongo Lóo Mu Sëriñ Fàllu dëddu na àddina ginnaaw wopp ju yàgg ju ko daloon. Di ndaw lu dégg daaj te aay, bokkoon na ci ñi gën a jëmmal ag maasam ci ay way yu am solo yoy yeete ak xirtal nit ñi cig mbaax la daan fees dell. Bokk na ci ñi jox gëdda aanéerub Ndakaaru.

Wan na ndaw ñu bari yoonu tekki ca fa ñu ko gën a ñàkk a yaakaare. Daan woo ndawi Pikin, Caaroy, Yëmbël, Géejawaay añs… ngir ñu moytu te wan ginnaaw lépp luy lu bon niki sàcc, dogaale, siif ak pékke.
Loolu lépp nag ci gëm boppam la ko jaare ginnaaw bi mu sóoboo ci way.

Yëy-yàbbi