Catégories
Saabal

Bunu sukkandikoo ci yéenekaay bii di…

Bunu sukkandikoo yéenekaay bii di « Enquête « , « SONACOS » di lijjantig Nguur gi Móodu Jaañ Fada jiite, dina dàq junni ak juróom-fukk ci ay liggéeykatam.

1050i ñooñu ñu war a dàq 31 saawiye bii, xaatimoon nañu ay pasi 6i weer ak « SONACOS ».
Buñu leen tasee: 200 ca ndefarug Njaaréem la ñu nekk, 350 ca Kawlax ak 500 bi ca Sigicoor.
Cig pàttali, njaayum gerte gi ci 2019-2020 mu ngi dox bu baax waaye ci weeruw lëmm, « SONACOS » manul a jënd lu dul 10 000 ton.

Yëy-yàbbi