WAYU NDËPP
Junnéey géej
Kafteer baa nga Ndar
Xamuma dara
Mënuma dara
Seex fàllu Mbàkke yaa wóor
Yoroo saa pëb bee
Ardo may ma soow
Maam Kumba Ndóoy
Ànd na ak Mbatuli
Mu dem ba wiiri géej Salaam
Maam geesu Mbul
Maam Kumba Ndóoy
Maam Kumba Ndóoy
NJARE
Na leen Njare
Njare Kumba Ndóoy
Noo moom njare
Njare
Na leen Njare
Njare Kumba Ndóoy
Lëg Daawur
Lëg Daawur Mbay Tabara
Mu Maam Penda Mbay
Ragal bu ko dégg daw
Gaaja gaa nga siin
Tama yaa nga jaxaaw
Kodd Juuf sereer bi
Yee, balaa may toog dem Sàngomaar
Jaxeer Penda yaayu May
Bala may toog dem Sàngomaar
Maam Biram Ndóoy fàtte na ginaar ca Ndoyéen
Jiinleen Maam Góora Ndóoy
Ndecuwu Paate yaayi Nor
Ndono gaa ngi
Ku daw dee.
Jiinleen Matuli
Maam Njaay donoy Aama Njaay
Ndóoy
Yee, Aali buur ba, Ndenee
Siga am na doom
Lëg Daawur Mbay Tabara
Mu Maam Penda Mbay
Ragal bu ko dégg daw
Lëg Daawur Mbay cuubal
Mbaa nga yume
ηàbbal fii
Taawul fii
Fii nga yëngal, boxom
Man la Njare Ndaw
Ab Tubaab bu ma dégg daw
Yee, jiinleen side Matuli
Goney Maram Ñaŋ
Nanu jiin side Matuli
Faatu Ñaŋ mi réer
Nanu jin jinne Matuli
Ngóor Juuf
Ngóoroo, Juuf
Ma di la laaj
Ba ñibbi Siin
Duma wàlliyaan
Sañ na maa beru
Sañ na maa beru
Dama am ay jinne
Maa mën jinne
Man Faatu Caw yaayi Jóob
Maa man jinne.