Catégories
Saabal

XAMEES NA BIS BI ÑU WAR A ÀTTE GUY MARIS SAAÑA

Ginnaaw bi ñu ko jàppee ca buntu njénde la muy wane naqaram ci yokkuteg njëgu mbëj gi, bañkat bii di Guy Maris Saaña dees na ko àtte 21 saawiye bu 10 waxtu jotee ca Ndakaaru.
Layookatam di Musaa Saar jot na ndigal li koy may mu layal ko ginnaaw bi ñu ko nëbbee jant bi luy jege ñaari weer.
Moom nag ñu koy toppe fippu, juddal coow lu rëy ak bokk ci doxub ñaxtu bu ñu tere.

Yëy-yàbbi