Catégories
Saabal

DOX TÀNKI JÀMM CI NDÀMPAAYU XAREB GOLF BI

Jogomaayub JAMRA di Maam Maxtaar Géy dina leeral na ci bisub tay bii, bóot yi tukkee ci dox tànki jàmm bi mu doon amal ci wayndarew ndàmpaayu sóobare yi demoon ca xareb Golf ba ca atum 1991.
402 sóobare ya mucc ba ñibbisi ci réew mi ak jëtumi 93 ya ca ñàkk seeni wakkan ñoo ko yabal ngir mu indi ay leeral ci ndàmpaay yi Mbootayu Xeet yi ak réewum Arabi Sawdit joxe woon.
Maam Maxtaar Géy nag am na jotaay yu mu jot a séq ak jëwriñ ji fi nekkoon te yore xare bi, jëwriñ ju njëkk ja woon Bun Abdalaa Jonn ak njiitu réew mi. Mu ngi ko tëje ak ndaje mi mu amal ak ndaw li toogal Araabi Sawdit ci Senegaal di Abdu Asiis Muhammet Ayfaan.

Leeral:
Jogomaay : kiy dox tànki jàmm buvag lënt amee ci diggante ñaar (médiateur)
Jëtum: ku jëkkëram faatu (veuve)
Mbóot : secret
Sóobare : soldaar, soldat
Ndàmpaay : indemnité

2i tontu ci « DOX TÀNKI JÀMM CI NDÀMPAAYU XAREB GOLF BI »

Yëy-yàbbi