Catégories
Saabal

NOO LÀNK DINA DELLOO BUUM CA BOOY-BOOY GA

Jàpp ak toroxal yi leen alkaati yi di def taxul benn yoon ñu rët bay deltu ginnaaw. Kureelug NOO LÀNK dina duggaat ci biir fere yi ci koñ yi ngir waxtaan ak ñoom jox leen këyit yi leen di xamal li waral yokkuteg njëgu mbëj gi. Mbir mi nag man naa bañ a yomb ci alkaati yi buñu jotee ndigalul jàpp ñiy def lu ni mel.
Leneen li mooy ndayi-sàrti réew mi may na bépp ma réew mu wanee naqaram nu ni mel batax nguur gi waru koo tere.

Leeral:
Rët: terrorisé, terroriser
Fere yi: les populations
Mbëj g: electricité
Ndayi-sàrt y: la constitution

Yëy-yàbbi