Catégories
Saabal

WAXTAANU BERLIŊ NGIR JÀMM CA LIBI, 19 SAAWIYE 2020

Dibéer jii wees, 11 njiiti réew yu seen i yoxo dugg ci taalug réewum Libi ak yongug njiitam la di Xadaafi, ba yàqute ak tasug réew ma am ca, ñoo daje ne dootuñu jaxaseeti walla ñu cay dugg te seen yoon nekku ca. Nee nañu itam dees na tënku ci tereg njaayum ngànnaay ya.
Li ci xaw a dal xel rekk mooy li ñu dëppoo ci kàddu ci mbir mu ni mel.
Mbootaayu Xeet yi cig wetam nee na dina soppi dëppoo googu ag pas, waaye ndax loolu man naa soppi dara ca réew ma ca dëgg-dëgg?
Càmbarkat yi njortuñu ko.
Leneen li mooy ndax du waxtaan wa ñu amal ca atum 1884 ca Berliŋ ngir séddoo Afrig moom la ñu amalaat ngir paacoo réew Libi ci 2020?

Yëy-yàbbi