Daawuda Géy di jàngalekatu xeltu ba noppi doon ub bañkat manul a nangu benn yoon ñu wéy di tëye Guy Maris Saaña ci kaso bi. Ca jataayu « Sen Show », ronqoñam toq na ba muy sàkku ñu feexal xaritam bi.
Mu ngay xamle ne « Maki Sàll du nekk ci jàmm fi ak bàyyiwuñu Guy Maris Saaña. Dees na yuuxu ci réew mi ak ci bitim réew. »
Mu nga cay yokk ne « deesul nangu benn yoon mu jafeel dundug waa Senegaal ba noppi bëgg a tëj gémmiñug képp ku àndul ak moom. Dunu ko nangu mukk » di ay kàddoom.
Cig pàttali, Guy Maris Saaña mooy benn ñaxtukat bi ñu wéyal ag tëyeem ci kaso bi ginnaaw ba ñuy ñaawlu yokkuteg njëgu mbëj gi ca buntu njénde la.
Leeral:
Bañkat b=activiste
Mbëj g=électricité
Njénde l=palais
1 tontu ci « LU ËPP TUURU: »
Du yoon