Catégories
Saabal

PËLE JOX NA KUBU ÀDDINA BI RÉEWUM SENEGAAL

Pële di kenn ci waadaani futbat ci àddina bi, nekkoon fi ca Sàntos, xibaar na réew miy nar a jël kubu àddina bi ci atum 2022 ca Kataar. Mu ngi àddoo ci benn yéenekaay buy yëngu ci wàllug tàggat yaram ca Beresil.
Bunu sukkandikoo ci moom, dina am ay réew yu mag, Beresil sax man na cee génn. Waaye ci moom, réew mi nar a bett ñépp ca Kataar te tàmbali liggéey bi ay at a ngi nii, du Farãs, Beresil, Arsentin walla Belsig waaye Senegaal la. Moom njort na ne Gayndey Réewum Teraanga mi ñoo nar a doon waaday àddina bi ci joŋante yii di ñëw ndax mu ngi ci ñoom.

5i tontu ci « PËLE JOX NA KUBU ÀDDINA BI RÉEWUM SENEGAAL »

Yëy-yàbbi