Catégories
Sëñ Musaa Ka

Yërmande

Sëriñ bi noo ngi lay dagaan
Te di la xaaraan ak a ñaan
Yaw mi sa xol amul kañaan
Koo gis defal ko yërmande

Te di la yalwaan ak a jooy
Sun lori xol ba faf ne wóoy
Ngir aji yaakaar sa du sooy
Tabe nga booleek yërmande

Te di la tuubal lu haraam
Ngir Yàlla tey nirook i jaam
Di waaf fi yaw di saf i baam
Nga di nu sëf sa yërmande

Te di la sant boo joxee
Te di la sàntu boo doxee
Te di la tontu boo waxee
Ngir bëgg a am sa yërmande

Te di la sukkal ni jigéen
Te di la raamal di la fóon
Te di la sopp di la miin
Ngir bëgg a am sa yërmande

Te di la gëm ta di la yéem
Te loo nu wax nu di ko jéem
Di bañ a moy di bañ a juum
Ngir bëgg a am sa yërmande

Te di la jox ta doo nu laaj
Te loo nu laaj du nu ko waaj
Te lu mu rëy-rëy du nu ko xaaj
Ngir bëgg a am sa yërmande

Te koo ci woo mu dal di ñëw
Hamaana sax mu sax fu yaw
Te loo ko wax mu dal di daw
Ngir bëgg a am sa yërmande

Di jéem a sàmm say ndigal
Tey jéem a def lu lay bégal
Di dàkk sam xel di fétal
Ngir bëgg a xam sa yërmande

Di rafle tay sóoñu di xiif
Di fande tay tëdd fi suuf
Tay diñe tay wopp ak a loof
Ngir bëgg a am sa yërmande

Te du nu xàddi du nu soof
Te du nu xàcc ndax i seef
Te foo taxaw nu ne fa seef
Ngir bëgg a am sa yërmande

Di laxasaayu di rañaan
Di xëy di gont du nu fanaan
Di daw di waaxu di tëraan
Ngir bëgg a am sa yërmande

Tàggook i ndey tàggook i baay
Du mbokk dub xarit du waay
Dub jegeñaale du najaay
Ngir bëgg a am sa yërmande

Yaw la nu def ngay sunu Baay
Di sunu Maam di sunu Yaay
Di sunu waay di sunu najaay
Di sunu ngën ji yërmande

Ba nanu gaa ya fi newoon
Topp la yaa gën ña dikkoon
Yaw mi nu may Kun Fayakuun
Gaawe nungir sa yërmande

Fab nanu saahir si bu wér
Boole ci baatin bi bu wér
Boole ci ruu yi ak i cér
Jébbal la ngir sa yërmande

Fóotal nu sunu tilimi xol
Ta sellalal nu sunu xol
Ba du nu xalam lu koy nëxal
Ngir Yàlla ak sa yërmande

Te may nu ay leer ak i bóot
Te yar nu nook sunug njaboot
Di nu xamal xam-xam yu xóot
Yu bari ngir sa yërmande

Te na nga nu def ngën ji muriit
Fegal nu it pexem mariit
Te nga wutal nu ay muriit
Yu bari ngir sa yërmande

Te xàll ngir mi ba mu weex
Nu di ca aw te bu nu xeex
Te bu nu jàdd bu nu jeex
Ba gis sa néegi yërmande

Te bunu geesu bu nu seet
Hàddina mii tax nit a suut
Di xéy di gont ba ni suut
Àgg ca ngën ji yërmande

Te yar nu yor nu bu nu reew
Bu nu fo di dox di wër i réew
Bu nu werente bu nu soow
Tàggat nu ngir sa yërmande

Te nga fegal nu dee gu gaaw
Ak rékki gëm ak dee gu ñaaw
Ten sax ci loo wax nu ne waaw
Ndaxte nu am sa yërmande

Te may nu lan mébét ci yaw
Ciy haddiyaak i jëf yu yiw
Ta fàtteloo nu ku du yaw
Ngir Yàlla ak sa yërmande

May nu nu sax ci say ndigal
Pas-pas yi fab ko dëhëral
Sunu bir yi boole ko jubal
Ngir Yàlla ak sa yërmande

Te may nu barke ak ngërëm
Ku nekk jékki ci kërëm
Tay jaamu lum soxla mu am
Ngir Yàlla ak sa yërmande

Te may nu waa kër ak i doom
Ta may nu daaraa i njuróom
Fegal nu ay ràggak i góom
Ngir Yàlla ak sa yërmande

Te may nu ay njéndi yu yaa
Ta may nu ay dàgga yu yaa
Ta may nu ay seng it yu yaa
Ngir Yàlla ak sa yërmande

Te nga fegal nu ayu seef
Ak ayu mbas ak ayu xiif
Ak liy sufal kër ni ko fuuf
Ngir Yàlla ak sa yërmande

Ak ayu béppub nasaraan
Ak kuy wëreeluy jabaraan
Mbaa kuy xalam di sabaraan
Ngir Yàlla ak sa yërmande

Ak ayu jinneek ayu jaan
Mbaa tooke mbaa boroomu saan
Mbaa ayu waa ju nuy hañaan
Ngir Yàlla ak yërmande

Te bul nu seete ay ayib
Waa juy saraxtu day ayib
Géwal dafay way di xarab
Te teewu koo am yërmande

Ayib yi tee nu am lu baax
Yaw mi ko xam te am lu baax
Far ko te wuutal fa yu baax
Man nga ko ngir sa yërmande

Ayib yi tee li nu am lu nuy
Mébét ci yaw nga am li ngay
Mébét ci nun ban di la roy
Dindi ko def fu yërmande

Def nu nu gëm sunu Boroom
Def nu nu gën sunuy moroom
Sàmmal nu julliy juróom
Ngir Yàlla ak sa yërmande

Sàmmal nu ruu yi bu nu réer
Bu nu gëlam te bu nu ruur
Ndawak magak jigéenak góor
Jofal ko ngir sa yërmande

Ta may nu wërsëg wu halaal
Ban di la yót loo man a laal
Te def nu gaa yoy ku nu laal
Réccu ko ngir sa yërmande

Te bu nu leb di ca meroo
Te bu nu wax di ca waroo
Te bu nu jëw bu nu beroo
Nan mane ngir sa yërmande

Te bu nu bew bu nu hañaan
Te bu nu jànni ku nu ñaan
Te bu nu moy te bu nu daan
Ngir Yàlla ak sa yërmande

Te bu nu noonoo bu nu xeex
Bu nu xuloo te bu nu deex
Fu nu jékki am fa lu nu neex
Ndaxte nu am sa yërmande

Ku ne di jaamu ne ritaax
Di boole ay lal ak i taax
Ne gaa ya dee faa waax i seex
Ñuy wuyu ngir sa yërmande

Yaw mi nga xam ne waa ju am
Yaa ko amal te waa ju xam
Yaa ko xamal te waa ju gëm
Yaa ko mosal sa yërmande

Yaw mi nga xam ne waa ju man
Yaa ko manal te waa ju gën
Yaa ko gënal bi harfi kun
Gënal nu ngir sa yërmande

Yaw mi nga xam ne waa ju añ
Yaa ko añal te waa ju sañ
Yaa ko sañal ci li nga sañ
Sañal nu ngir sa yërmande

Yaw mi nga xam ne waa ju siiw
Ba ku ko gis dal di nu siiw
Am la mu am ba di ko soow
Yaa ko defal sa yërmande

Yaw mi nga xam ne waa ju duuf
Bay dox di fàdd ay bindéef
Ya ko yafal ba dóotu loof
Yafal nu ngir sa yërmande

Yaw mi nga xam ne waa ju suur
Bay fàkki maasam te du buur
Yaa ko lehal te fal ko buur
Lehal nu fal nu yërmande

Yaa mi nga xam ne ku la soob
Nga may ko lépp lu ko soob
Bam fàtte lam jëkkoon di buub
Alal ya ngir sa yërmande

Yaw mi nga xam ne ku la moy
Du tee nga may ko gën ji may
Jéggal nu sunu moy yi te may
Nu ngën ji may ak yërmande

Bul nu ko jàppee bun moyee
Bun tayul ak bun tayee
Balul nu yaa gis kay maye
Njéggal gu ànd ak yërmande

Yaw la nu def Yonnen ba daan
Yaw la nu doyloo ba fa saam
Fegal nu lépp lu haraam
Ngir Yàlla ak sa yërmande

Yonnen ba ban ko jisatul
Te jis la ngay tegtale lol
Ku bañ a juuyook sa ndigal
Gis ko mu wan la yërmande

Nu fab la def la niki moom
Nga fab ko def ni sa Boroom
Mu fab la wan la sa Boroom
Mu jox la ngën ji yërmande

Te def la ngën ji jamonoom
Nga jiitu ken du sa moroom
Mu jox la mbóotam kun nga moom
Di sédde ngën ji yërmande

Doomam ya bañ leen jisatul
Te jis sa yoy ñuy rafetal
Sunna si tay awlu ndigal
Doy na nu ak sa yërmande

Màkkata bañ ci jotiwul
Te néeg i Tuubaa soriwul
Nu def ko Màkka tay jubal
Pas-pas yi ngir sa yërmande

Bu nu jisul yooya jumaa
Te jis fu yow ngën ji jumaa
Nu def ko muy yooya jumaa
Te bëgg a am sa yërmande

“Baytil Muqaddasi wa Shaam”
Ak i “Medinatul humaam”
Bu nu jisee Daaru Salaam
Doy na nu ak sa yërmande

Yàlla na nu sax ci yaw ba dee
Nga sax ci Yonnen bañ a dee
Mel ni Huddar mi tëha dee
Aamiina ngir sa yërmande

Te bu nu yëg mettitu dee
Malaaka yay mbugal ku dee
Bu nu nu jis képp ku dee
Ràmm ko ngir sa yërmande

Bu nu demee “Yawmal haqaab”
Ràmm nu bun nu fa “hisaab”
Bu nu fa rus ba di fa seeb
Ngir ñàkku ñàkk yërmande

Yóbb nu “jànnatul hulaa”
Kër ga amul tiis ak balaa
Te boole nook “kullal malaa”
Jox nu fa ngën ji yërmande

Danoo amul doole ju jëf
Amunu lëf amunu laf
Te bëgg a am la gaa ya jëf
Di am ci kaw sa yërmande

Moo tax nu jóg di la dagaan
Te di la way te di la ñaan
Te xam ni képp ku la ñaan
Nga may ko ngën ji yërmande

Yërëm nu may nu lii nu ñaan
Te bun ci jis bennub safaan
Te may nu li nu ñaanul te ñaan
Ko war nu ngir sa yërmande

Aamiina aamiina ne leen
Aamiina ndax ñu boole leen
Ci waxi Muusaa ba lu ngeen
Sàkkooti am ca yërmande

Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun

Yëy-yàbbi