Bismilaa Rahmaani Rahiim
Faa ilan, faa ilan
Nan ci way ciy wolof
Soo wayee ciy wolof
Kon ci xol lay xaraf
Déglu naa biig ci njël
Am pitax cig garab
Ñuy tawat naan hadiil
Ab liccin moo ko këf
Mii pitax naa ko ndax
Mar wu tar waa ko ray
Mii pitax naa ko man
Xaajumaa wóolu maf
Mii di way, mii di jooy
Kurkutuut, kurkutuut
Soo amul fathu nag
Doo ca am aw araf
Seeni way moo yëngal
Tiisu xol wii ci man
Moo tax it maa ngi nii
Maa ngi saf waa ju dof
Maa ngi leen jooru naa
Yéen dangeen dul nelaw
Yéen pitax yi, ñu naa
Jooju wax nañ ko laf
Nun danoo sib nelaw
Kuy nelaw doo nu saf
Kuy nelaw yaa ko tal
Nun sunuy gët du raf
Foo fi gis kuy nelaw
Ag cofeelam wérul
Su cofeelam wéroon
Kon bëtam sax du xef
Waa ji man waaru naa
Yii pitax ñoo nu gën
Seen cofeel ak hadiil
Soo mënoon roy ko faf
Fuy pitax deeti way
As hadiil, nan fa way
Séexu Tiijaan Sëriif
Moo ko jar mag du kaf
Seexu Tiijaan Sëriif
Nan ko way, nan ko roy
Ay waxam nan ca ŋoy
Moo nu doy, moo nu saf
Seexu Tiijaan Sëriif
Ndeem dangay roy ci moom
Ay jëfam day rafet
Ay waxam day woyof
Seexu Tiijaan Sëriif
Waaru naa ciy mbiram
Ag cofeelam ci xol
Rekk sax doy na jëf
Seexu Tiijaan Sëriif
Ab kemam daa amul
Foo ko seet, doo ko gis
Muy Kajoor, muy Jolof
Seexu Tiijaan Sëriif
Kuy kokam daldi raw
Soo ko soppee ci xol
Kon bégal, am ngërëm
Daaguleen cim lefam
Daldi raw gaa ya war
Naaru-góor yay dawal
Aw yeneen xeeti lef