Murit ngalla deel muurook a waarook a waaraate
Di ñaaxook a ñaaxaateek a bégleek a xuppaate
Te def sab sëriñ muy kerkeraan jëm ci ay ngërëm
Te bul weddi lam santaane bum wax nga naa mbaate
Te jébbal ko sab xol fàww jébbal ko say alal
Te nos ruu gi wommat jox ko tey wax yërëmaati
Defal gumba jébbal tum bi kuy jis te bul gëlëm
Te bul xorxoral kon lee nga dem xayra xadraati
Te bul jànni bul diiŋat sëriñ mukk bul xuloo
Te bul mer di tontanteek a saagaak a xastaate
Bu dee jëf lu wuteek sunna say njort nay rafet
Sariihatu wér nay wax hahiiqatu wuutaate
Te bul xàddi bul gaaral te bul jëf lu dul ndigal
Te foo toll naa yaa xawsu man awma soxlaati
Te foo toll ngay farlook a xër-xërlu ciy ndigal
Di daw-dawlu saytaaneek jigéen ñii di waqaate
Te far fuñ wëllis say bokk ak kuy sewal ndigal
Berul dem ca gën gaa àlle bul dellu kër gaati
Te bul geesu bul yàkkamti bul faale ab daloo
Te bul xàcci bul ñaawal sa jëf njort raw naati
Di daanook a jóg bul naagu fuy daanu àggagoo
Ku yéegul ca kaw doo daanu bay dox di wootaate
Toroxlul te bul rëy-rëylu bum soxla ngay tayal
Nirul mbër maa daa wub làmb juy waaj a dëkkaate
Na ngay boole xiif ak rafle tey noppi tey xalam
Bu gaa ñay xaraŋ ngay jóg liléey ngën ji mboolaate
Te far dëddu dunyaa kiy woraakon bi wor ku bañ
Te ngay fuglu dee miy dox di songeek a bettaate
Te bul weddi bul ngistal bul woddi bul hañaan
Te bul gëdde bul wex wexlu bul dox di siisaate
Na nga yéene aw yiw képp kuy ngëram ne yaw
Yëram ndaw ña màggal mag ña loo am nga séddaate
Te màggal ku bokkak sab sëriñ doomam ak ñoñam
Nga wormaal ko koo gis nag ci ñii jox hadiyaati
Te def sab sëriñ muy sang buy wax nga daal di daw
Te foo toll naa yaa seexu yaa seexu maa ngeeti
Te say kàddu nay saf kelte buy junj lëf nga daa di daw
Di cellantu buy waxtaan itam bul ko ruubaate
Te ngay teel a xëy niy jëwrinam tey saxoo sikar
Bu mbooloo ma toogee ngay liggéeye a ñaaxaate
Te bul faale kay war naari-góoram tay dañal
Di feeruy lalam tey woote dag yaak a moslaate
Di mos lay ja ak yàppam wa tay gaarde xaalisam
Di xaajaanu tay séddee a boddee a wootaate
Di yor caabi yay tijjee a yor làmp yay jafal
Di faj soxla sum soxla a may gaa yi kër gaati
Du buurook a biddanteek a sangook a naja jug
Di fuddook a bin binlook a bëslook a déeyaate
Te bul faale kay xay–xaylu tey jàngu tey daloo
Di soccook a set tay seetu tay daagu naa Faati
Di rixóo fuddan tey ŋàmbiy musuwaar di sol kawas
Te naa ndaw si sumyaam yaatu ban dem gëroo Faati
Di niroo a pornooseek a sëlmoo a wut daraa
Wisoo lañkoloñ fun toll raayoo diwak mbaate
Te fuñ jekki def waxtaanu xol muy ku xëy rafet
Di xasteek a reetaaneek a màtteek a boddaate
Di faarook a waxtaaneek a fóotlook a dox di kaf
Di toog ak jigéen cib lal di riisoo a déeyaate
Di sangoo malaanam yaak a tër tërub cib lalam
Di bantuy xetam tey wax dikkal fii nu fóonaate
Te doo dégg kuy ñaaxaate tey yedde fif kuréel
Di wut luy ngëram tey xërlu céy liyeek a jombaate
Damay sànku man Muusaa ci barkeb sunum Sëriñ
Mu wattal nu sun ñaawtéef yi muy xayra xayraati
Sëriñ bee di géejug Yàlla nan fóoti tay setal
Ndoxam bee fi saf suukar safak lem te dàqaate
Dagaan nan ci barkeb Bàmba kiy xutbu xarnuhii
Mu fóotal nu sunu bon bon yi ban xëy di fóotaate
Te may képp kuy sàkkuy ngëneelam la muy damoo
Ba dun xaare dun yalwaan dun dox di soxlaati
Te may nuy murit yuy sànku yuy sóobu ciy ndigal
Te tibbal nu ciy mbóotam ba nuy xëy tibbaate
Te xejjal nu fal noo fal ba nuy buure baatinam
Te leeral nu ciy làmpam ba nuy xëy di taalaate
Te feg dee gi feg moy feg balaa xiif itam mu feg
Te ñaagal nu ciy ndàmbam ba nuy xëy di ñaagaate
Te sellal sunuy jëf boole sunu fan yi faf guddal
Te yaahal sunuy wërsëg te may nuy hadiyaati
Te yokkal nu sunu mbooloo yi fob yi tàppe leen
Ba kenn dootu nooneek kenn sàkkaa di ŋàññaate
Te dox sunu digak saytaane wa nafsi wa hawaa
Wa dunyaa te not noonam yi ded fii di xuppaate
Te wommat nu fid dunyaa illal jannati hulaa
Te leeral sunuy xol fii banuy dox di waaraate
Aji-bind ji: Nogay Cuun