Catégories
Al-Haaji Muhammet Basiir Sekk

Yeetey Al-Haaji Muhammet Basiir Sekk (1)

Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim
Sallal Laahu halaa Muhammadin wa Aalihii wa Sahbihii wa Xadiimihii wa sallam

Lii xasidab wolofal la bokk ci « Yeetey Al-Haaji Muhammet Basiir Sekk kay taalibeb baayam ju siiw ja yal na ko Yàlla gërëm te gërëm nu ci barkeem » mu jëm ci ndaw ñépp ak képp ku ko aajowoo ci mag ñi ci rakki gàmm atum 1391, ñeel Abuubakar Siise mom Seex Daawuda Siise ak i kemam 1971.

Alhamdu Lillaahi may yee ndaw yi buur bëgg a dem
Fas yéene raw maas ya jot seen maam ya wéy am i ndam

Góor-góorluleen ndaw yi ag ndaw baax gu nekk la am
Am-am yi, xam-xam yi, ak xar-baax yi xaj na ci moom

Loo teg sa bët, naw ko, boo koy sàkk daldi ko am
Booy mos nelaw tuuti, bañ a neenal, di wut, danga am

Ngir kiy Boroom jaam ñi, par-parloo du yegg fa Moom
Noo def, Mu def noona, ku Ko nekkal, Mu nekk ci moom

« Man kaana Lillaahi, kaanal Laahu faddalahum »
Loolee la Seex Bàmba ak mbooleem ñu baax di gërëm

Lu diis la ngay fob dafay diis gann soo bëgg a am
Barkeek yu gën say meloy wuuteek meloy ña ma xam

Booy wut lu baax bul nirook kuy wut leneen lu du moom
Regg ak nelaw teg ca neenal, jiitu maas ga du am

Nit ku du xëy sàkku, te du gontal di wut lu mu am
Buy wéet nelaw fu’m faree daaneel ko ndam du fa am

Am-am wa xam-xam ku jox neenal, nelaw, bakkanam
Doo am ca ñoom kenn, doo dem fenn am ñu la gëm

Ngir àddunaak fa nu jëm, ñoom ñaar a fay joxe ndam
Am-am wa xam-xam bu dul ngir Yàlla am ga du am

Ba’ñ tànn mooy ba di faj aajooy ña teew di fi ndam
Ak bay xamal nit ñi diiney Mustafaak ña ko gëm

Ñoom ñaar ridal Laahi mooy tax ñuy ko wut ba du am
Kon am gi ay fitna lay dolli fileek fa nu jëm

Moo tax ba Seex Bàmba def mbooleem yi baax ca këram
Ku am ridal Laahi, am xam-xam di daw di fa dem

Am-am wa xam-xam ku daa muñ xiif bu wér te gërëm
Ay coono, muñ ñàkk, muñ moy Yàlla, foofa la jëm

Booy wut ba ñoom ñaar ñu xëy àndaati jébbalu ñoom
Jébbal la seen bopp yor say bokk yor fa nga jëm

Dañ lay xëyal fal la di la gontal lu maas ga xemem
Buy fii mu ñëw buy feneen loo jublu daldi ko am

Dootoo xalaat àdduna ak bon-bon yu rëy yi mu am
Noonoo ci aw des wu baay yaak maam ya gedd ko dem

Ngir loo fi gis ñuy xëccoo mbaa ñuy xuloo di ca jëm
Aw des la wow ay junniy nit ñépp mos na ko dem

Kon yaw muñal jaamu, fa nu jëm am na kër yu fa am
Yu ken sancul am na mbooleem may gu jaam di xemem

Lol doy na, jeexal na mbooleem yiw yu góor ña di lim
Àjjana, hay jeex na, lu fa nit taamu daldi ko am

Ma def salaatan wa tasliiman Haliyhi bi Him
Wal Aali was Sahbi ak Seex Bàmba may sunu ndam

Subhaana Rabbika Rabbil hissati hammaa yasifuun wa salaamun halal mursaliin walhamdu lil
Laahi Rabbil haalamiina

Yëy-yàbbi