Bismillaa, Muhamadul Basiir di ki taalif xasida gi atum 1138 j (juddug Isaa) ngir laabiire bokk yu góor yi ak yu jigéen yi ci warug muñ ak farlu ci muñloo ak damm gët yi ak dummóoyu way-réer ñi ngir jëmmi Yàlla Tabaaraka wa Tahaalaa mi nga xam ne mooy def lu ko soob ak la nga xam ne moom la taalibee bi bëgg ci diineem ak ci ñoñu diine ju matale ji, jàmm nag yal na nekk ci képp ku topp njub
Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim, Laa hawla walaa xuwwata illaa bil Laahil Haliyyi Hasiim
Alhamdu Lillaahi may yeesal tariixaati
Ngir xamle sew-sewi diine ak biram yaati
Nan jéem a am yitte te fas yéene jot góor ña
Xëy lekk, naan, nelaw, duñ tax waa ja raw gaa ña
Maa’ng leen di yee te def Muusaa Kume muy téere
Bi may misaalee ndax ngéen génn cig réere
Loo dégg may wax ne Muusaa ñépp laa boole
Ca googa kàddu na ngeen yeesal te ba xoole
Muusaa dohal murit baa ngay donga bob daara
Bu jub bu fas yéene ëllëg ngay sëriñ daara
Askan bu doon teree nit am barke mbaa daara
Xam-xam du sax tay fa Kawlax ñuy fa siyaara
Buur Yàlla mas’t a xàmme ay géer ak i ñeeño
Te Mooy Ki fiy maye ku du Moom doo fi faj haajo
Ngir péeyi Yàlla yi boo dem fekk fay ñeeño
Ñoo’k jaam yi ak géer ñi ñuy maareek a jallaaño
Bul jagle Wàlliyu ciy gor mbaate allaaji
Mbaa ñeeño mbaa jaam mbaa ku’ñ xam ku ñuy laaji
Nit koo fi gis màggalal bul xeeb mbiramaati
Bul xeebu askanam bul xeeb saahiram baati
Amna ku saahiram rëy te biir ba xeebooti
Amna ku saahiram sew te biir baa yaatooti
Amna ñu rëy saahir ak baatin ba weesooti
Amna ñu sew biteek biir cëy ñii a xeebooti
Amna ku dul julli fa teewag ndajeemaati
Te waxtu moos du ko raw Màkkaak Madiinaati
Koo bëgg a noppalu; koo gis fonk ngir Buur ba
Ku fonk Buur, lu Buur def, fonk ko ngir Buur ba
Yónnent Yàlla Sulayman doomu Daawuuda
Baayam da doon tëgg terewu leen di Mahmuuda
Baayam Rasuulu la, ba mu deewee Sulaymaanu
Donn ko, moom àdduna ba mu jeex fu ko neex taanu
Jaam, bàmbara bu doon teree seex mbaate ag wóolu
Abdul Laahi Ñaxet Cees du woote Rasuulu
Maa toog ci këram man Bas muy ma kàddooti
Naan; maa di Rasuulul Laahi maa demoon delluseeti
Naan maa di Mahdiyu maay ki’ñ wàcce Xur-aani
Te ku ko wax ku may man laaleek nasaraani
Kaariimun ibnu Kariimin Yuusufa ak taar ba
Teewul mu doon jaam bu ñu jaay Misra kër buur ba
Tëj nañ ko cib kaso diir bu yàgg ngir tuuma
Ku jàng Mbargaan xam ne mas’t a moy ngiir ma
Taaram ba romb na mbooleem taari góor ñaati
Te mas’t a geestu lu moy Yàlla ak ndigalaati
Amoon na benn bis ba mu rombee jigéen ñaati
Ñeen-fukk a dof dof gu wér ngir taar bu yéemooti
Jum-ñent ciy jigéen dee nañ ngir cofeel gaati
Ñeen-fukk dof dof gu wér ngir sopp waa jaati
Foofa Saliixa boroom xaala fii fiihi
“Fasaalikunnal lasii lumtunnanii fiihi”
Yónnent Yàlla Muusaa sàmmal na Suhaybaa
Kem fukki at yu mat door a jot lëf ca palaas baa
Amna ñu daan yatti nekk i lawbe ca Yónnen ya
Amna ñu daa ràbb am ñuy wulli der booba
Yaaram ci xol la ne toppul mécce ya ak xeet ya
Toppul ku ñuul mbaa ku xees toppul araab piir ba
Lislaam duhul tooli baayi kenn ku naa maa moom
“Inna akramakum hindal Laahi atxaakum”
Mbooleem li jaam di faaroo lu moyragal Buur ba
Billaahi neen la nangeen ànd ak ku xam péey ba
Ndax yéen dangeen fàtte Lam Baaba mu siiw maati
Daan nañ ko way ca njëlbeen ay way yu yéemooti
“Lam Bàmba, Lam Bàmba, Lam Bàmba jogay baax nga
Séeréer bu gën Wolof daa yombul nde Muxtaar nga”
Daa liggéeyal Bàmba ba’m taf ko ca Laxyaar ya
Mu waaxu dem Siin tàggat mag ña ak maas ya
Amna kemam Siin yu jàngul di am daara
Billaahi giñ naa ne mbaax amul gumb ak saara
Barke ku koy fasoo am day buur te fas yéene
Man daa ko am fàww mbaa ngeen dégg ne dee naa
Lii rekk mooy yoonu wut barke te mooy ngiir ma
Ku sàkk yoon wu moy wii doo jot ca Muxtaar ma
Bul déglu gaa ña naan diw ñoo bokk sun maam ya
Xanaa du kok démb tay yaayam sama yaay a
Bokkaale nday ak i baay mooy bokk saxaar ba
Taxut a yam bagaas ak teerukkati gaar ba
Salaatu Sil harsi wa tasliimi Hii abadaa
Halaa Muhammadin wal Ashaabi man habadaa
Subhaana rabbika rabbil hisati hammaa yasifuun wa salaamun halal mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiin
Aji-bind ji: Omar Siise Al-Faaruux