Catégories
Sëñ Maam Moor Mbàkke

Waati Wolof (a, b, j, d)

Way wii nag, aji-way ji Sëñ Maam Moor da koo tëgg ci anamug abacada.
Tàmbalee ko ci loyu a indi ci waati Wolof yu jafe yi tàmbalee A yépp. Toppe ko noonu bamu jeex.

KUBBITE GI

Xerawluleen ma sadd fii baati wolof
May sunu làkki maam ya déggatuñ ko faf

Ngirag ne sunu jamono lañu xëy mbaanig
Jànqe ko yaawur te rañaane kàcci nag

Te xëy ma ñépp këmm mbaa jópp la dal
Ña jànq it seen diñe gaay seen wéttal

Gaa ya rañaan war ca gëléemi fande ya
Te xit fetal ca ñall yuy golliku ya

Ba génn kéewi dànna yoy ëwoon na leen
Ni dédd def xallóobi gaynde saŋe leen

Jéggi dayoom gu weesu lef moo ma ëlëm
Ma rët ba tax ma bëgg a dëflu cig wayam

Ngir dekkalaat ko góomu alkandeem bi wér
Te suuxataat reen ya ba meññatam ma ñor

Ñu raas ko, fuuyoo ko te racc, def cafaay
Yuur ca di fas dumóoyu lépp lëf lu aay

Jafal la giim te taal ko ngànj muy bérax
Di lekk sun liw bi ba kenn dootu lox

Ñu naan ci dex gi bàyyi tepp-tepp yi
Ak déq yeek njunux yi, xond-xond yi

Dëtëm ba màndi raggu bokkul ak di ñeer
Ci lol dafay guusali put di yokk tér

Masëy-bandaŋ wa wenn dooñ la tooyalul
Waame wa mooy tooyal i tool te koy ñoral

Ba tax ma fëx àkki wolof ya jiitu woon
Muy waxi sun maam ya di mag ñee fi ne woon

Waxiin ya laa jëlaat, fasoo mu delsiwaat
Te ñooy wolof yu wér ya, nar ñu dekkiwaat

tudde ko mottaliy mébet yuñ sémb
Ci dekkalaat waati wolof yoy démb.

LOYU A

Aw naa ci àlli waa Unaare fekk leen
Ñu àngu ñoom ñépp di an calli aréen

ma ëyu leen ne aaye naa ko, indileen
fukki andaar te boy te moytu aawe yéen

Te aw ci xàllu njub te moy anéeri moy
Te wut aléeri topp àkki tool ya bay

Te àlli wànqaasi moy ak àkki ngëmmeen
Buleen di aas ci ëtt mbaa urmbali yéen

Lépp lu aay ër ko fa tay aayelu ay
Tey àddu tey aar sa njaboot ci wépp ay

Te bul di ës ba muy waral ñu ëñ sa kéew
Te mooy sa kiiraay li la ëw bañ di la yéew

Te bul asar lenn, na ngay afal ku ne
Sa xol bi nay af man a uuf mag ak gone

Jépp ayib ju dul sa jos umpale ko
Te ëmbalal ku nekk u yiw àntule ko

LOYU B

Ku bëgg nay bëgg lu baax bañ lu bonam
Te am mbañum-rus ma di xeeñtu aw banam

Te néewi mbóorant te doon ku xuuyi mbéey
Setal sa pooki xol te nàmp batti péey

Ŋoyal ca mbicci kaw ga bul jàpp ci pet
Moyul barastikook a bàyyi bul di xét

Te rendi say mbamb ca pottox ya te boy
Jam ko ca baljat ya te bèccingal ko wéy

Te ñàkk paal ku dul ci Yàlla miy boroom
Te sàkku mbëbbal ma , ñemeg péete ci moom

Te buddi say bémpéñi xol ba buddi buut
Sol ca ngëneel ba lépp pendal ak i mbóot

Te néewi bébbant nde moodi pëppi jëf
Di pindi pax yu feese pert bum la këf

Defal bërét te binni ngir yéem sa ayib
Sàkku pexem faj ko te pasteefu te jub

Defal sa jëf yi pàggutéef wëlif poñat
Lu dee gi bette bette berndeele ko mat

Mbewte nga bërgal ko potoxlu pekki mbég
Génn ci mballi barjalug bakkane rekk

Mbémburi xol di yéene nay mbell mu set
Te bànk i jëf peeg ko te mbaayàlla poñat

Berul te bul topp mbaboor mi deel bérés
Lu bon ci ag mbëbëstënam ci foo ko gis

Bul ca deseb patt faral béel ci lu baax
Te bul ca bar sa mbir na bir ci fonk baax

Te dagg pëjji pànka buural sa kañaan
Te daal di buur jëm ci boroom bi daw safaan

Te fab sa baag yoor ko ci mbalka mom ngëneel
Tanq ca naan te wacc mboori xiila-xaal

LOYU J

Damay janeer lu mel n ceeñeeri cofeel
Mel ni ku ñer cafka ga far ñëggu ca teel

Ba maa ngi jànkoonte ci xol bi aw mettiit
Wu jeggi njobbaxtani cëy jépp jëreet

Ba xel mi jollasante na ak xol bi, li jib
Xañ na ma cëslaay ba jamuuj naa ci lu jub

Mel ni njunux ci man, ci kuw maram lëjal
Ma far di cam su wéet di jukkat di jofal

Te jàmbat ak junj jeñul jóori cibeel
Ma jaaxle componu ci màndiŋum cofeel

Ba jàmberaayi ronqooñ it di car-cari
Jàllawle xel mi xol bi it di jér-jéri

Fit wi ne ñogg jokkalook njàqare xol
Lu sax ne ñumm mel ne coggal gu ñukkul

Ba maa ngi ceeñeerlu ci biir am njayaxaan
Samab ñës it call ba maa ngi ñeetaan

Ma ñaxtu ñaxtu kenn ñëwul jàppale ma
Cawarte dem njàqare ñëw jaxalsi ma

Ba càqaral na xol bi, jàmmi jamjamoor
Moo ma ñëwal njold ma jéllu kekki joor

jullóotu naa ba faf ne jànjaŋ ca ja ba
Ca digg njolloor ga ba weeroo ni Rubba

Ma sàkku aw ñaraasu mbég jàppandiwul
Ñu far ma njàmbaasale njëgg mom jarul

Kanam gi ñëkk , ñaq, ñuqi lëf të ma
Ma njoofu ay jafeñ-jafeñ jàmm të ma

Mu mel ni jaani ñës yu ñàng ñoo ma war
Te doon yu ñammasle di curpi mel ni jur

Ma aw ci ñallu njommet ak xel mu ñorul
Ba mel ni am njëgg ma ak curi lëjal

Ma jumm jummi jiiñ jamoono lii ma dal
Te xam ne moom du jag du jekkal du jagal

Te xam ne ñàngóor a ko gën jikko ndax it
Njekk da koo xamul du jekki it jubut

Ma daal di jàppeelu ci lii ma xam ci moom
Te def ko ñukk jàpp nag ca kay boroom

Te ñukk jëm ci moom te jokk nag ci jëf
Te kañ ko, njukkal ko te far sóobu ci lef

Dontele ne nag njàqare fim ne moo ma muur
Ni njoof di muure jaasi war ma bépp boor

Du tee ma jéem a muñ te xam ne rekk ngëneel
Deesu ko jox cuune ku muñ rekk la ñeel

Te ñàkk jom day tax a jëf cëkk te it
Da nay waral di jëf lu juunu lol jubut

Ay njegemaar yu jekk tey joŋante
Firdawsi cig njoggama yal nan ci joti

LOYU D

Na ngay dëgër ne déjj far jéggi dayo
Te doon ku déjjérle di dàkku mbamb yu

Ba mel ni mbëtti deg ya mbaa mel ne ndëfëñ
Du jàmbatub dagg ni dëññ mbaa wetañ

Te bul di aw ndóol wu dëféenu fàww rekk
Saxal ci dàllu bul di dallu mukk nag

Bul di dijooti ndàmm sonn a koy maye
Faral di dànna bob du déjjatuy moyi

Dëtëm ndoxum ndam ma mu neex ci denqaleeñ Nga nòyyi ndeemeexi ngëneel sa diine feeñ

Dët ga di dotti yaw nga des dér darale
Ni ku ñu dott tey ku dërkiis të file

Di dëflu ciw tiis te nga ndarkepp sa mbir
Dëxëñ sa ndaaf te dàmbe mbeg ak i naqar

Te bul di diis ba faf di ndaare des ginaaw
Na ngay doronke dund gii doylu la teew

Te bul di dàcci mel ni kuy das defarul
Ndéeyaale ak ndétti ndënéer yuy dexi xol

Te doylu yaw doonte ne dóor-dóor nga ame
Dëkke ko ndéem dooj nga am it bul ko gëme

Te dànd doolenke bakkan, daw ko bu wóor
Te bul di dandal it sa xol bu xel mi dër

Te dàngañal te moytu detteelu itam
Ca kàmbi diiŋat ya te daw dee du xalam

Demal ca dex ga bàyyi déeg yi daa doyul
Te digg-dóomu nag ci lépp bul ëppal

Te bul di ndeeteet lu di tan-tanlu itam
Saxal di tan te bul dagook a ndiigu tam

Na dëgg doon sa nding looy dunde dëdam
Te bay sa dooñu diine bul di dooji tam

Te bul di dóore mukk diisool ci lu ne
Da nay teree daanu di tee diig ci lu ne

Xamal ne Yàlla day dënéerlu képp nit
Naŋ ko ba xel dàggiku ngir teg na la bët.

Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Léebu

Léebu

1- Ab tegale bu guddee te daanu wul ba jiitoo jub lool.

2- Àdduna gaalu ndox la, waajur bokk na ci gaal yi fiy jàllale.

3- Àdduna weeru koor la fàww jant so nga doo ga waññi bis.

4- Àdduna wori neen la.

5- Alal ganug dof la, buy ñëw du tàggoo, buy dem du tàggoo.

6- Alalu golo ca leq ba.

7- Alalu ku sàggan ku farloo koy for.

8- Am gémiñ taxul a mën a wax.

9- Am naa gëléem ca Gànnaar yomb naa wax.

10- Am ndaa, toj ndaa taxul a bari ndaa.

11- Am soxla fajal ko sa bopp te kenn yëg u ko jar naa bay guddi.

12- Andadoo bukki, bu ko bukki lekkul bukki la.

13- Àq du yat waaye bu dalee dinga ko yëg.

14- Ay du weesu baay dee na.

15- Ay du weesu sàq ma lakk na.

16- Ba feneen amee ba léegi kenn sonnatul.

17- Baadoolo du jub gàcca te aggu ca.

18- Baadoolo rekk la ñuy may lépp mu jël lépp.

19- Baadoolo xamul njoowaan.

20- Baaram bu ñu tàllal joxoñ la waaye juróom i waaram yu ñu tàllal yelwaan la.

21- Baax ci sa alal, jàm¬mbaar ci sa doole.

22- Bakkan waro dàll la fa muy daggee dooko yëg.

23- Bala nga naan naam ne fa.

24- Bala ngaa xam, xamadi xaw laa gaañ.

25- Bala ngaa daas am loo réndi.

26- Bala ngaa digle sangu na fekk nga set.

27- Bala ngaa laax jaay, laax lekk.

28- Bala ngaa xam lu taat di jariñ toog jot.

29- Bant soo koy jubbanti da nga koy jubbanti ci ba mu tooyee.

30- Bant, lumu yàgg cib dex, du tax mu soppiku jësig.

31- Bari le barkeel le moo ko gën.

32- Bari xam-xam weesuwul nettali sa géntu moroom.

33- Bari xar bumu la tax a ngen¬te kou ëmbëlul.

34- Bày ci sa wee wu tànk.

35- Bëgg bëgg yee wuute, moo tax njaay may jar ca ja ba.

36- Bëgg lu la neex du tax ma ne la Yàllaa ngi lay nuyu.

37- Bëgg lu neex gan du tax ma boot jiit.

38- Bëgg ndawal bu la taxee fekk ñay bu taxaw nga di ko galgal say tànk damm.

39- Bëgg soow rekk warul a tax nga woowee béy yaay.

40- Bëggum ñeex du ma tax a dëppoo cin lu tàng.

41- Béjjën mënul a njëkk a sax bopp.

42- Bëñ weex na lool waaye deret a ko lal.

43- Benn lam du yëngu.

44- Benn loxo du tàccu.

46- Bëre géewu dof la, ku wér génn ci.

46- Bes boo gis, day leb walla muy fay.

47- Bes du tuuti boroom lay tollool.

48- Bët dina set.

49- Bët du gis li koy fatt.

50- Benn loxo du tàccu. bët du gis la koy fatt.

51- Bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan.

52- Bëtub mbëggeel jéll nab gàkk.

53- Béy du gëmmal gënn.

54- Bëggum ñeex duma tax a dëppoo cin lu tàng.

55- Béy du raas déemu guddi.

57- Béy fu muy bàkkoo bari gerees nag nekku fa.

58- Biir du suur xel ay dal.

59- Boo bëggee ray as gor dee ko jox bis bu ne lumu dunde bu yàggee nga def ko mala.

60- Boo bëggee xam luy laabiir amal doom.

61- Boo bëggee xam luy muñ amal jabar.

62- Boo wonnee ñay ci sutura, boo demee àll ba mu feeñ.

63- Boo yaroo, té yeww wu loo alalu boroom barke nga.

64- Booy sómbi na nga sómbi loo mën a naan.

65- Bopp du ngir karaw kese.

66- Bopp su naree am barke nopp yuy dégg a cay sax.

67- Boroom karaw gu ñuul ñàkkul dara.

68- Boroom nday ju liggey ku ko yéene fande, yàpp u giléem lay njogonikoo.

69- Boroom ndékki ku ko njëkka yewwu tëddaat.

70- Boroom tubëy bu jàngoo sol.

71- Boroom yat du sóoru boroom fetal.

72- Bu bërti bërti doon tax a jar kon béy kenn du ko bàyyi daral ga.

73- Bu cër yépp yemoon ñay gedd bosam.

74- Bu daay tàkkee céeli yendoo naaw.

75- Bu gudd nopp doon tax di njiit mbaam di sunu ilimaan.

76- Bu jinax doon tux sigaret kon isin yi ak « biro » yi lakk.

77- Bu jinne bëggee dàqaar ku yéeg daanu.

78- Bu la am am tax a bew, ndax ñàkk du wees.

79- Bu la mar tax a naan póotiit.

Aji-dajale ji: Allaaji Jibi Sëy
Aji-topp ji: Saasumaan bi

Catégories
Sëñ Ahmadu Baas

Sutura yitteel na ku ne

Lu tax nit ñi buñ déggee lu baaxul ci nit ku yiw
Taxaw temm ngir yaatal ko bam law ba daj fu ne

Lu tee woon nga jéggal nit te koy nëbbaley ay sikkam
Ndaxam suturas Buur Yàlla yittéel na cam su ne

Goray xam safaan dencal ko mbokkam ba faatu ñëw
Ragal Yàlla tax ak maandu ak xam na ñëw bone

Bu leen weratib jullit bu leen yàq ab deram
Ku fiy dund feek deewóo safaan man na laa gane

Wolof day misal ag dund ciw koor
Ku jàpp bis lifeeg dog jotul ag jubu weesul fa dog bone

Di siiwal safaanub nit ba far ëpp koy ayib
Ku am xel du def loolii bu leen yor xelam gone

Lu tee woon nga nëbbal kob safaanam te Yàlla tax
Ndagam Yàlla mooy sattaaru maandooy li war ku ne

Na ngeen moytu jëw baaxul te daa mel ne lekk nit
Te rambaaj a raw day tax ba ay bokk duñ mane

Na ngay nëbbe say bon-bon bëggóo kenn xam ca lëf
Na las cam di nëbbey bon-bonam kon bu koy wane

Te Ibliis ma ngeen daa muslu tey moytu ag mbonam
Mu ngoo gii ci seen apaareyiy woote tay sone

Te anternet ay ab jumtukaayam di daamaram
Koneksiyoŋ bi mooy xontam bi ngay aktiwey done

Nataalak wokaal boo jot ci watsab ñu koy toxal
Efaaseel te bul partaase luy yàq ay gone

Éy waay siggileen watsab yi day yàq seen i xol
Lu ngeen am ci mbon ngay xew Farãsak la xew Gine

Éy waay siggileen ceetaan mi réeral na seen i xel
Ba kenn dóotul jàmmanteek i nawleem ya koy gane

Ewaay siggileen for yoon wa yéenak ci xuur wu rëy
Wu lëndam te gar yang fay sibuy yong ay tene

Ewaay siggileen ndax Yàlla seen gët yi xoolu yiw
Ba laa leeri gët yee fàddu xoolleen fa mbir ya ne

Li apaarey yàqal nit ku koy xayma doo fi jug
Batay kuy naxub diriyànke ayfon nga koy cane

Li watsab di jël ciy waxtu ndax jur na ay njariñ?
Te moo tax mukalaf yaa ngi niiy waxtu niy gone

Na muy yàqe dundug nit dafay dem ba mel ne sax
Manul ñàkk cig dundam te am kooy lëjal ku ne

Li ngay def ci Feesbug boo ko jàppoon dogub sikar
Ndaxam lee nga am xam-xam yu Feesbug ya dul wane

Te kat ñàkk Feesbug lortilës cam nde Yàlla mii
La muy sédd ab jaamam ci sax ciw turam la ne

Kurus gaa ngi nii der baa ngi nii jukki baa ngi nii
Ta dog yaa ngi nii céeboy ngënéel yaa ngi dët fu ne

Ku sellal ndabal biiram mu feesak tawab ngëram
Ku not ab xolam cib net ñu nattoo ko mbon ku ne

Ndagam deftilag mbon waxtilag mbon di gis lu bon
Akay déggi bon-bon doy na lag mbon fa mbon bone

Te man maa ngi nii xamteeti mas lëf
Te fàtte naa li saa xol bi takkoon fëtt naa mokkal ak lu ne

Damaa talatul sax wérd mba may talug nafar
Damaa sonn ngir ndéggat yi gaa yi di ngun-ngune

Mo Baas tee nga sàlloo tuub te faf raasi wépp yiw
Labat may yi tàggook moy yi moy yaa ngi lay gane

Te mbon sax jigul sëppéen ba sàkkaa ku tol ne yaw
Faseek moy yi daa jot sëkk ngir doonatóo gone

Ka jéggal ña juumoon démb tey nëbb ay ayib
Dagaan naa ko ag njéggal gu far saa ayib yu ne

Ka xam lépp cib jaamam te muural ko ay moyam
Fa laay tuube laa jàddoon ci ag mag ba cig ngone

Ka jéggal laram Daawuda laay sàkku njéggalam
Te moo jéggaloon Yuunus nde moo tee mu faf jëne

Ka jéggal Badar jàmbaar ya songoo te diine tax
Asal man na maa jéggal ci mbaxam gi moy gu ne

Te kii jéggaloon Wahsii ma xar dënnu Hamsatin
Asal man na maa jéggal te ràngal ma pal ku ne

A yallaahu yaa rahmaanu yaa sañ te yaay dogal
Fa salli halal maahii te far saa ayib yu ne

Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun_

Catégories
Sëñ Daam Jaane

Sñ Xaadim Géy

Ahlan wasahlan watarhiiban ci sun ëtti xol
Ndokkeel la day lu nu war, Géy Njooro Géy ñaayaa

Siggil nga daara yi ak, mbooleem lu taq ci ñoom
Saw tagg daj na Kajoor, Saalum ba dem Ngaayaa

Say soppe bég na ñu tay, sa noon ya pérdi nañu
Xuraan a ngay sigaree, muy saar akiy aayaa

Yaa aw fa góor ña awoon, moo tax nga daj la ñu daj
Sabrun jamiilun a lay ràngal fi aw laayaa

Kuy rëbb day làqatuy, bóof ak di diir ak a raam
Jawfal faraa mi nga tër, yombul ci bii ñaayaa

Yaa rëbb Yàlla ci xuus, gottub xuraanu bi def
Pastéefu ak fetaliy sox wal ya ray gaayaa

Diiróoy pitax ak i naat, dóoróoy jinax ak i wel
Segg ak tene ya nga fees, jam gaynde mbër Njaayaa

Sab donga wecci na junniy, fóore yaa bari ay..
Baasiin yu raw sëriñub ñay sàmm i nag mbaayaa

Géttub ngëneel ci nga yar, ay yëkki garmi yu duuf
xëccoowulóok Ardo meew, yaa soow lu suur paayaa

Yërmaande ngay yeewe ndaw, teraanga ngay gawe mag
Kersa ak lewet ba ñu koy kàbbar nga doon taayaa

Buural wéyal doxalal, sam mbay rafet na te set
jekkil ci sag gàngunaay, tey xelli àttaayaa

Laf cat sa tukki bi nay, sun yokkuteg daraja
Njëggum Unnayni ma feeñ, léebam wa naaxsaayaa

Boolook jullit yi ci am, ak bépp xol bu ci tooy
Nay ciggiteg daara tey, suuxug ku taal daayaa

Jaaraama waa daara ñii, ñooy gar di garmi yu set
Seen xol ya Buur a ko fees, duñ dàcc duñ daayaa

Fuñ wokke diine ñu jóg, fu Yàlla woote ñu dem
Tiituñ rafuñ takk-der, buy boqi ngànnaayaa

Jub jëf ndigal moyu tooñ, yar yiw yéwén ñime dal
Ñoo mag toj ak yàq kon, bal baa ngi ci seen kãyaa

Busraa li Njaañ Njaga seenuw, tagg law na fu ne
Naw yiw di seen xalima, wërsëg di seen daayaa

Bijaahi jàkka ya ak, daaray xuraan ya fa ne
Yal nañ nu dolli ngëneel, sun xel mi bum naayaa

Bijaahi xabru ya ak, jumaa ja Bàmba siyaar
Fu bàrke nekk na dal, kiy bind wii aayaa

Xéewal wér ak gudd fan, wëwsëg wu yaatu te lew
Nay wal fi nun li fi ak, jullee ngi am taayaa

Daam Jaane baayi Kariim, Xaadim Gëy ay ki ko yar
kuy noonu daara ci way, lay xotti say caayaa.

Aji-bind ji: Imaam Jóob
Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Sëñ Daam Jaane

Njukkal Sñ Xaadim Géy

Gëy Njoora Gëy ñaaya yaw, téereb Boroom bi nga def
Am xëy ku lay fakktal, daa repp mbaate mu dof

Yan bañ yanoon mbër ya woon, téeñ baa ngi yaa ne ko cas
Kuy tee nga dëngëñ di wéy, am mbaam la dees na ko sëf

Ku doomi Bàmba di yéem mbindam ba koy terali
Sag suufe faat na asal mosleen ko, xam li mu saf

Kenn manta lim ñi nga def, sëñ daara tay ak i kaaŋ
sun taal ya doon bëgg a giim, ca Njaañ e yaay ki ko ëf

Doo bërgal ub ndonga yaw, doo boddi mag walla ndaw
Gëy ràggalóo, ruuralóo, reggal nga yékkati tef

Xeet yépp am nga ca kaaŋ, lawbeek i géer a ci yam
Ab ŋaydo mantil a tee, ngay xëy di bay wile lef

Tërub xol ak xel mu nëb, gis-gis bu gàtt bi ngeen
Koy xoole tay dafa doy, def ngeen lu yées li mu def

Kuy jéng baay tëj ci kaaf, tey maas kurã ak a dóor
Looy bañ ku jéng ku daw, ngeen mel ni mbóot yu ñu nef

Jéngub noteel bi ñu leen, ràngal ci ngeen war a wax
Te bàyyi daara mu toog, xam ngeen ñi ngeen war a ñaf

Jaay suuf si jaay peterool, jaay nit ñi sànni sa ngor
Jaayal ba jaay li nga wuuf, mee bàyyi nook sunu yëf

Kuy bañ mu jénge joxal, sëñ daara bii la mu moom
Ŋaaŋleen mu wadd te ngeen, jóg jëf li ngeen war a jëf

Du seen moroom te du seenub, nawle yeen a ko tay
Walleen i nàkka te muñ, seen ñay wa nee na ko tëf

Misyoo la yor matagul, daaraam ja dees na ko taax
Seex Murtadaa a ko sos, ñeexum cofeel la ko sif

Daam Jaane baayu Kariim, Xaadim Gëy ay ki ko yar
Ak mbër yu kenn du lim tee ngeen a jëf li mu jëf

Buur Yàlla Yàlla na tër, kuy noonu daara ci suuf
Labal ko ciy fitna ak, kër-kër këram ya di jaf

Féexal sëriñ daara bii, ndax ag jotam bariwul
Ab ŋaydo mantil a tee, muy xëy di bay wile lef.

Aji-bind ji: Imaam Jóob
Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Sëñ Daam Jaane

Tagg Sëriñ bi

Lëndamug cofeel gi ma tàbbi, tax na ma gont war
Mutafaahilun ji fi ñépp, taamu ci tagg mbër

Tegu yéene way yaru tagg bàkk wu saf xorom
La ma koy cawee di ko rëpptal da ma dib gawar

Li ma yeex a jóg terewul ma jiitu ca tuur ba ndax
Wile naaru-góor du fi dàqe mukk, ci kursu par

Li ma naal a bind ci sibtu Bàlla ba tax na tay
Keru xol bi féex, cari xel mi naat na te daa ji far

Ku fi doon wayantu, na teg xalim ga te ñëw awu
Sama géer gi fawxa na gépp géer fa mu làng a bir

Ku fi doon tëbantu na dal, te ngax yi ni nemm cëy
Mbëru mbër yi gétti na waada, cëy ak a neex a far

Sàmba yaandi ngaan nañu tekki, cuur yi te jox ko ndam
Jaratul limaale du maasu ñii fële lañ ko ber

Galanub sëriif la ko Buur tëggal, nattu yoy Yonnen
La ne cas di wéy, bëtam aŋ ca gaaya fi woon Badar

Aka neex a taas, aka neex a jiin, aka yomb a kañ
Aka jar di bàkk ne géeju may ya du nëx du fer

Sëriñub njariñ ba nu daam, ngëneel ya ñu daa xaroo
jëfi Soxna Jaara ja Yàlla nangu mu law di wër

Aka teel a sóobu ca ngir mu sell ma roy Yonnen
aka teel a dab ña ko jiitu woon te fi daa sikar

Fa nga jaare Yàlla la gaa ña jiitu di wër ba tay
gisaguñ sa kem amutoon du am ba ba dun bi far

Ñime coona way, yanu nattu tiis aw sun balaa
Tinu teete taawu nu taaralaat sunu bépp cér

Gaboŋ ak Konaakiri Bàmba kuñ la fi dendaleel
jëfalul ñoñam ña lu tol ne baat ya nga tont Ndar

Ma ne kon sarax nu te yiir nu yaw, mi fi gën mbalaan
Bu nu àppe njuumte yi démb tay lunu moy nga far

Ba la waa Garàmbasa diggi géej nga nu xettalee
Ba nga daane noon ya ca Jéewali la sa ndam ya wér

Di ñu sànge sag suturaak i may yu ñu dul dara
diñu sargal it suñu biir i nawle di fanq mer

Talatun fayantu ni Daam a faj la nu metti woon
Dexi kawsara ay sunu naanuwaay lu nu namm xer

Asakaa ki ay sarax ak ngumeen la nu daa dundee
Bamu ñibbisee la fi nqonji jeex nu ngi afra xar

Xalimaam du jaawale mag na runge du gag du naax
Àlliway Boroom bi ca kursuyun fa la daa nafar

Mbindam ay gësëm aras ak kenoom ya di xacci xol…
Y di dàq ñàkk di dindi réer ak a sippi lor

Tawat ak balaa musiba ak i ndog lu nu jub mu fél
Dërëm ak ngërëm daraja ak i ndam di nu dëkke wër

Asamaan du tiimati gor su baaxe ni Baayi Bas
Lewet ak nëtëx nga mu boole teewu ko mel ni gar

La nga daj Ndakaaru ca néeg ba jar na ku nekk jooy
terewul nga wéy dellluwóo ginnaaw ku la sédd ngor?

Ba nga nee fa jóox kero ràbb jam na sa ndëggu sar
Terewul nga teg ba ca des, nde jom la la Yàlla xër

Masuloo ne uh te sa xol du nux-nuxi bay tawat
Sunu tedd yaay ki ko jënde coona bu yàgg a tar

Dunu am sa fay lu dul ñuy jubal ak a jaamu Buur
di la roy ci sunna su sell jëf di ko teg fu wér

Jote nan la nday jote nan la baay jote lay nijaay
Jote nan la far sunu lépp gee bëccëg ak fajar

Ku la séddu raw te du fuuy du bew ku la am texe
Ku la teggi réer ku la foñ suur lu mu sóor mu dar

Ku la fat ci biir xolam ak xelam nga di ay céram
lu mu yóotu jot lu mu songu daan lu mu jàggi tër

Ku ñu ber nga uuf ku fi loof nga wudde ko ay ngërëm
Ku ñu xeeb nga aj ko ca kaw mu far kawe ñépp cér

Na nga ful nu yaw mi nga xam ne mbaax a ngi far ci yaw
ku la denc féex ku la jënd bég ku la jaayu jar

Ku la sëmb tooye na may yu ànd ak i jagle kon
Nee ma jàkk teg ma ca gàngunaay gi fi ñii di wër

Taxawal te xatmu sa way wi géej amul ab yamu
Tëralal xalim gi te ñaan ca barke ba mujj wér

Texe njub teraanga ju sax fileek fa ñu jëm ëllëg
Darajay Yonnen ba mu daa xëyal ba mu def ko mbër

Salawaatu Rabbi hallayka yaa sëyyidal basar
Maha aali feek muritiy Sëriñ bi di waaj safar

Aji-bind ji: Imaam Jóob
Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Sëñ Daam Jaane

Guddi

GUDDI

Mbalaani niir ya bu muuree, jant sàng safax
Bëccëg ga tàggu timis, maay samp dënd di buur

Xaftaan bu ñuul ni këriñ, am tupp-tupp yu weex
Mooy col ga ag ndaama laa, as ndiir su gàtt ma réer

Xaftaan bu ñuul la ma sol, am tupp-tupp yu weex
Ag ndaama laa fukki waxtu ak benn rekk ma réer.

Gaaw lool ci way bég i xol, soof cam su nekk ci tiis
dal yewwu am sutura, xam lépp bàyyi ci biir

Way baax ya sopp ma lool, saay-saay sa jàppe ma waay
ñeey jaamu ñee dëkke jëf, ñaawtéef ya lépp ma muur

Saag door la jinne di jóg, lal ay pexeem tër i fiir
Ku farluwul tëye doomam, njuuma sànni ko xeer

Ngelaw su sedd sa moo lay soññ gaawtu xoyet
Jafal sa and ci mattug goongo gëtt yu piir

Ginaar yi tàbbi ngunu, njugub yi génne ci lëm
Lippaaxon ay gunge jeeg, bay waaj a yakkiji reer

Muus jóg di rëbbi jinax, xérjéjji lang ci looy
Gee jàll yóbb safaa, wittar ñu tàbbi ci biir

Bànneex ci néegi juboo, naqar ci néegi safaan
Am biir yu feese ndawal, am yoy mbaxal la ñu sóor

Suñeel yi raam leru ñag, rungug gaña a ngi sa waañ
xaj yaa ngi yuuxu ca kaw, ay ngooxi mbott di riir

Yoo yewwu yee xorondom, gëmmentu dal di nuyoo
Gént ay sa gan gi la wax, xibaar yu lënt sa yuur

Leeg-leeg mu neex ba nga bég, leeg-leeg nga yuuxu ca ngir
jëmmam ju raglu ja ànd ak bëñ yu gudd te xuur

Fasuw sijaada gu suur, laabuw kurus yaru tur
Njaabal ci kursu wareefi jaam ba nammati Buur

Mbaamum fétal mu ñu sëf, jaasiy bajantu ci bew
war say wareef weri fit, def jom toj ak tëb i miir

Ñii tëdd seen weti way-jur, sàngu seen sëri ngor
Ñii sol lu gàtt fasoo, wànteeri seen céri biir

Jokkoo ba guddi gi xaaj, gàmbaal ba séq yi sab
Kee xaar jëkkër ba nelaw, kee bëtt ñag wuti góor

Sàcc ak wëyyook wagaboo, bàndeek sulaar yi ci baar
Yaaram sëriñ ku ñu rus, tànneef ci cant yu foor

Rombante mbindeef yu wuutey jikko, ak melokaan
Wuutante kawkab ya xuus, seen burju feq di leer

Ñatteelu xaaj ba xaran, yay riir ci dënni xureet
piccum tinook nangu ñaan, toŋ fépp ken du ko diir

Bët gëmmu ruu yi di xool, tëraayu xëbru ëllëg
Néew tëddi morgo xajal dooñkat bi am ganu liir

Jàppaan gi jàpp sa cuuj muy ciib, nga tëb ne bërét
Baay Xaadi nodd fajar, bët set sa yaay a janneer

Kiiraay la wuññiku na, looy bañ mu siiw bu ko jëf
maay guddi ay li ma lëm, lëndëm du muur sama leer

Dan maa xarook sutturaak ug maandu noppi ci dal
Yiw mbaa safaana ci yam, loo jëf ci man duma weer

Kum soob nga jàppe ma sën, ndax celli mag du nalaw
bul foog ne umpale naa, liy gontu xew sama biir

Kër-kër du woon sama mbir, dalloo ma yékkati woon
Ker laa gu dëll te yee, foo fàkk man nga fa goor

Siiwal du woon sama mbir, yeetee ma yékkati woon
Liy xew ci bëccëg a raw, ëllëg la lépp di leer

Ay xaaju guddi, bu jekkoon jekki nekk bëccëg
bis pénc sax du ko dab, cig xumb ak bari riir.

Aji-bind ji: Imaam Jóob
Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Sëñ Daam Jaane

Jamonoy Asan Paate

Jamonoy Asan Paateek bañuy way Njóoba laay
laa doon fowantoo way man ak ñoom Jàkka Njaay

Yéen doomi soxnay sëñ Basiir Lóo may ma fit
Afrig jógal jox baay Jagal ag gàngunaay

Ñi ma def ngalam ba ma xëy di nes-nesi tay ci way
Baay Saal Ture kaay fii te ràngal leen medaay

Buma fàttalikoo Sëñ Daam ca daara ja saay jataay
way laa ko daan dundee man ak sama yenn gaay

Daan déglu sëñ Moor xam sa diine ci Làmp Faal
muy taalifal Maam Jaara Buuso lu taaru waay

Ami Siise sos ciy muqtadab ay way yu saf
sëñ Fàllu Kan foto irtijaal di ko saamandaay

Ñukkub Lahat Ndoŋ génn gaa ña di jàngi way
Sëñ Ngund laa daa déglu ree bay xàqtaay

Sama kompulegsi ga deñ na ndax seex Abdu Ka
maa xëy jawub wolofal bi jënd la mbër di jaay

Baay góor gi déglul Mustafaa réew mee jaxoon
sëñ Làmp Mbàkke di tagg Daam may ngën ji waay

Suma dee jinaas tay baay Lamiin a ma jox cereem
kiy fëgg saay téeree waral ba ma am ngañaay

Sëñ Seexunaa Gànnaar ci Nday Alima a taxoon
ba ma teey a teey ci jigéen ñi tépp na dégg aay

Sama xel xalam kaanaa ki kàkk bu Maysa Faal
ibnul Amiin Faal fëll indi fi lakk daay

Tax nañ ba way jaxasook dereet sama tay jile
bu dutoon ak ñoom sama xel mu ñor mi du waaj a xaay

Fuma yaali dóor sàbbaal Imaam ja mu soññi nguur
yoon teggi tuumay Fàllu Kunta mu ñibbi waay

Tay-taylu naa bañu teg ma dof terewul téyeel
sëñ Baara Gëy Mahmóodu doom ja mu jàngi laay

Kuy tukki laajal sëñ Abóo waa jam dajeel
yoon week a tar suma doon ragal duma jéggi raay

Li ma gént a gag loo Bàmba Lóo ak Seex Silla muy
Doktooru Lóo ànd ak Imaam Jóob dellu Ngaay

Abdul Ahat Ñaŋ ñag na làkk wi gépp wet
bàkkal na réew mi ne jaasi waay jaa mas la daay

Mbaam yaa ngi jottali cant ben Faadl ci mbay
ag ñàkk dug bon Fàllu Si ak maam Cerno Njaay

Laajteel ma Sàmba alaar ci Seex Awa Bàlla Faal
Buso Abdu Xaadar ëppalam laaj nay detaay

Marxiy marax leb naa ko ngir imisooy ikaab
ak jant beek bennoo efem billaay wallaay

Jaxasey pitaale di dammu bahru ba def lu jub
sama tur ci seen àlliwóoy mbatiit éro laa ci waay

Li ma tarde reer ngir koj ikaab imisoo xalim
Faatoo ngi ñëw ka ma domp daaw ren moo ma raay

Génnee ña nëbbu te feeñalaat peru way ba doon
bëgg a réer ñu formey Mbër yu mag jox leen medaay

Xalimag wurus durrun nasiim ay umsiyaat…
a ma yóbbu Kawlax ak Difoonse ak Géejawaay

Ñoo yokku xemmemtéefi ndaw ñi ci waar wi tay
dekkal donoy suñu mag ña doon suñu delluwaay

Root nan ci teenub Kayre mbóotum Baabakar
bayreek xorom ngay yëg ci way yi ñu tagg yaay

Seex Sàmba Jaara ak sëñ Musaa duy sun bagaan
Bamu fees ñu tiim taawook i caat aay dékk mbaay

Yar gindi xupp ak yedde waar yee kuy nelaw
liy tàkk fay bu ci boole way is naafë daay

Fuñu fëlle rekk mu nooy ba gaa ña di coow ñu far
fëllewaat feneen di ko sante nday di ko bàkke baay

Dañu raam ba tas dox jéggi jéego yi joggi dég
dox nan ba xéewal agsi yay nan sant waay

Sutura ak teraanga ju sax wér ak raw guddu fan
fés feese barkeek bayre buñ doon benn waay.

Aji-bind ji: Imaam Jóob
Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Sëñ Ahmadu Baas

Ñalgul dañal

Bismilaahi rahmaani rahiimi

Ñalgul dañal xalimag way
Ca lef ma ñuy tagge Daamu

Sëriñ bu mag ba fa Tuubaa
Rijaal ya moom la ñu taamu

Moo jar di way ak a sargal
Di riim taggam ya di baamu

Yaw soxna Jaara sa ndam lii
Moo raw ci jëf ak ci jaamu

Mbusoobe moom la nu taaroo
Ak Mëhramu ma mu maamu

Bul wër kemam amulam kem
Seex Ibra Faal fa la raamu

Amul ca Faas ak i Baxdaat
Amul ca Misra ba Saamu

Ku CernoFaati di bóofal
Ak Cerno cër ya mu sammoo

Dootóo fi seeru ku raamloo
Ku toll ne mbër ma fa Ndaamu

Dogon sëriñ ba fa Tuubaa
Sëriñ Daaru jekki ni kaamu

Moom rekk moo man a raamloo
Masàmba Jóob ma fa Saamu

Murit ba daa baye Déndéy
Seex Móodu bóof na ba Saamu

Sëriñ Mamar ma ñu màggal
Bóofal na Bàmba ba Saamu

Sëriñ Ma-Baabu ma selloon
Samsan la bóofe ba Saamu

Péncum sëriñ ba fa Tuubaa
Góor yàlla yépp a fa raamu

Yaa tax ba Ahmadu Baasi
Sàlloo di tagg ak a baamu

Boo jàppatee xalimag way
Taggal ma Ahmadu Daamu

Askaasaraa may rabbin
Bihii yunaa lumaraamu

Halal nabiiyi bi hizbin
Feeg maa ngi fi tagg Daamu

Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun

Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Sëñ Ahmadu Baas

Yewwuleen

Bismillaahi rahmaani rahiimi

Yewwuleen bu Yàlla falee
Ab laram na ñépp dagu

Dag ca péey ba lay xala añ
Wuyusileen ci seeni sago

Xaadimu Rasuuli la fal
Gàngunaay ga moo ko jagoo

Moom la Yàlla far ca lësal
Nattu yooya moo ko tegoo

Farlu ga ak yitteem ja mu yor
Lëf taxul mu raf bu dogoo

Yàlla rekk rekk la ŋoy
Alxuraan la mas di fegoo

Sopp Mustafaa di xolam
Aw taggam la mas di wagoo

Aar na ngir mi Yàlla tëral
Ag tëyam la mas di wegoo

Waa ju xam du wër ku ko moy
Moom la Mustafaa di sagoo

Lim defar ci dénd bii doo
Seeru fii kemam ba Tógoo

Wër wëraani dem na ba ñëw
Dem na Misra dem na Segu

Wër na ñoñ Araab ba dajal
Ñëw ñu naa ko yaw jugagóo

Nee gisul fi dëek i didi
Réew mu nekk nee na fa góo

Ag Yonen ci Taaha la yam
Xejj baa ngi kaay nu dagu

Baas yëngul te way ko ndaxam
Soo ko bàkkagul wayagóo

Baas yëngul te jublu ci moom
Soo ko jubluwul wayagóo

Sant rekk mooy li la war
Yaa ngi saddi way te gagóo

Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun

Aji-topp ji: Seex Lóo